COLIDEP (Collectif pour la Libération des Détenus Politiques) nag ay kuréli way-moomeel a ko sékk, boole seen doole ngir xeexal képp ku ñu jàpp ci ag jaay doole bëgg la xañ say àq ak i yelleef, ñu taxaw ci. Kurél gi nag, ay ndaw a ci ëpp doole donte ne sax am nay mag. Kii di Daam Mbóoj, Seex Baara Njaay ak Keledoor Seen ñoo leen di magal. Ñoom nag bi ñu sumbee xeex bi ak léegi def nay weer. Waaye, dañoo làbbali ci fan yii. Ndax, keroog ci àllarba ji, juróom-ñeenti fan ci weeru nowàmbar lañu doon amal seen kndajem-waxtaan ngir xamal askan wi li leen tax a jóg. Ak seen ndajem-ñaxtu mi ñu namm a amal ci àjjuma jii di ñëw ngir sàkku ñu bàyyi ci ni mu gën a gaawe lu ëpp ñaar-fukki nit ñi ñu teg loxo te pólitig kepp lal ko.
Senegaal nag, réew la moo xam ne dafa bari lu muy am ay coowoo diggante kujje ak Nguur ci wàllum yoon, rawatina ci jamono jii. Waaye, dafa mel ni li ci ëpp, booy déglu, ñi féete ci Nguur gi rekk ñooy tagg yoon, naan mi ngi def liggéeyam ni mu ware. Ñi féete ci kujje gi nag, ñoom, saa su nekk ñu ngi koy ŋàññi, naan yoon Nguur gi la fi nekkal. Léegi, lan moo waral mbir moomu ? Mu mel ni yoon daf fee war a nekkal bépp maxejj bañ a def xàjj-ak-seen ci kanamam. Ku def lu dul yoon ak foo mën di féete, ñu delloo la ci yoon. Waaye, bu yoon jalgatee yoon, ku koy delloo ci yoon ? Loolu bokk na ci li tax kurél gii di COLIDEP sosu ngir ñi ñu jàpp ñépp, ci sababu pólitig kepp, ñu bàyyi leen. Ñoom, keroog bi ñuy amal seen ndajem-waxtaan mi, jot nañu faa tudd ñoo xam ne seen i mbir noonu la deme. Kenn ci way-bokki kurél googu di Paap Abdulaay Ture, loolu lay leeral ci kàddoom yii :
“Dem nanu seeti mbokki nit ñi ñu jàpp ñépp, ñi nga xamante ni bokkoon nañu ci sunu wayndare ñu tollu ci limub ñaar-fukki nit ñu ñu jàpp ci lu teguwul fenn. Ñii ñu leen di tuumaal mbiri “forces spéciales”, ñii ñu leen di tuumaal jàllarbig xëtub fésali yéenekaay yoo xam ne, ñoom ci seen bopp sax àqiwuñu yoon. Waaye, toppekat bi moo ci duggu, teg leen loxo, ba tey ñi ngi kaso bi. Usmaan Jaañ ak Papitoo Kara ci lañu bokk. Ñeneen ñi, muy ku ci mel ni Seex Umar Jaañ ak Abdu Kariim Géy, ñoom, nee ñu wax sa xalaat lañ leen di toppe. Te, loolu warul mën a am ci réew mu yoonal wax sa xalaat ci ni mu la soobee. Bokk na ci ñooñu tamit Ndongo Jóob mi nga xamante ni, moom, li ñu koy toppe, jàppe woon nañu ko ko ci weeru màrs 2021 ba mu tëdd ci ñetti weer. Ginnaaw bi ci xalifa murid yi àddoo lañu ko bàyyi. Waaye, bi ñu ko bàyyee, yàggaatul dara, toppekat bi tegaat ko loxo, di ko toppe loo xam ne tëddoon na ci ñetti weer.”
Moom nag, yokku na ci seen lim bi yeneen i tur yu yees yoo xam ne dañoo jàpp ne li ñu leen tege loxo dara waralu ko lu dul pólitig. Muy lu deme ni mbirum Paap Aale Ñaŋ mi nga xam ne dañu koo teg loxo dibéer jale weesu, yemoo woon ak juróom-benneelu fan ci weeru nowàmbar. Ci lay waxe ne:
“Taskatu-xibaar boo xam ne, nun ñii di wax, moom moo nu ëpp ay àq ci kanamu yoon. Ndax, moom liggéey bi muy def dañu ko aar ba nun waa COLIDEP, bés niki tey, Paap Aale Ñaŋ bokk na ci wayndare wi ñu jagleel ñi ñu jàpp ci sababi pólitig kese. Bokk na ci tamit, ñi nuy sàkku ñu bàyyi leen, mooy juróomi way-wattu kaaraange yu Usmaan Sonko yeek dawalkatam bi. Lu tax ñu ne ñoom seen ug jàpp pólitig moo ko lal mooy ne, Maki Sàll, bi muy wër, wër gi mi jagleeloon koom-koom gi, fale ca Fuuta, yóbbuwul woon ay nerwi ñu jàpp ñi ñëwoon takk seen i sagar yu xonqu dóor leen ba ñu ne nemm, mujjul fenn. Moone, ay àq amoon nañ ca.”
Waaye ba tey yemul foofu am na ñeneen ñu mu ci yokku ñoo xam ne tegoon nañu leen loxo lu jiitu ñii ñuy sàkku seen ag mba. Moo tax mu yokku ci ne :
“Fàtte naa ne, ci wayndare wi, yokku nanu ci fukki nit ñu ñu jàpp te pólitig lal ko ; muy ñoo xam ne ñoom ak imaam Aliyun Badara Ndaw lañu jàppandoo woon. Moom génnoon na waaye fukki nit a ngi des ci kaso bi ñu leen di toppe wàllum “terrorisme”.”
Ñoom nag seen xeex bi li ko lal mooy ne ñi ñuy teg loxo yépp, kenn bokkul ci Nguur gi. Maanaam, Kumba am ndey ak Kumba amul ndey moo ci am. Ñu jàpp ne yoon tëddewul njaaxanaay. Ku bokkul ci Nguur gi rekk, yat wi da lay dal. Maanaam, ku bokkul ci gétt gi rekk, doo naan ci meew mi. Te, nee ñu, ñi ñu jàpp ñépp, bu doon li ñuy wax walla li ñuy def njariñal Nguur gi la, kenn du leen laal. Mu mel ni kon yoon day def lees di wax làq doom, dóor doom. Te, bees sukkandikoo ci kàddu yi Daam Mbóoj yékkati woon ca ndajem-waxtaan mooma, yoon moom boo bokke ci Nguur gi rekk mucc nga ak loo mën di def :
“Njiitu réew mi Maki Sàll mënul a muñ kujje, maanaam ku àndul ci li muy def, ak koo mën a doon, pare na ngir faagaagal la. Loolu nag, mësu fee am, amul lenn Njiitu réew lu mës a def loolu Senegaal. Ñi nekk ci kaso bi wuute nañu ak ñi nga xam ne ay jëwriñ lañu yu nekk ci moom, ñu leen di jàpp ci xaalis bu baaxul. Ndax kat, nga am Nguur goo xam ne say jëwriñ, seen i doom a ngay jël ay daamar yoo xam ne amuñu “permis”, dem di fiir doomi jàmbur te dara fekku leen ca. Nga am ci sag Nguur ay jëwriñ yoo xam ne dañu leen a jiiñ ne seen doom ña nga koy jàpp cib xaalis bu bon boo xam ne mat na miliyaar. Dara du leen ca fekk walla bu leen ca fekkee ab diir bu gàtt lañuy def ci kaso bi ñu defal leen mbawum négandiku.”
Loolu nag, moo tax ba ñoom ñu fas yéenee amalaat meneen ndajem-ñaxtu àjjuma jii ñu dëgmal, 18 nowàmbar 2022, bu ñetti waxtu ci ngoon jotee. Seen càkkuteef nag mooy ñu bàyyi ñi ñu jàpp ne, li ñu leen nëbbe jant bi pólitig kepp la. Ñooñu ñuy sàkku seen ug mba ñii la : Ami Ja, Moor Géy, Asan Daraame, Ibraahiima Jéeju, Abdulaay Njaay, Baabakar Ndaw, Paap Usmaan Sekk, Paap Mammadu Sekk, Madikke Jóob, Abdu Silla, Buuna Ba, Yayaa Siise, Seex Omar Jaañ, Abdu Kariim Géy, Papitoo Kara, Usmaan Jaañ, Abdu Asiis Ñaŋ, Abdulaay Jonn, Ndongo Jóob, Usmaan Jaata, Paap Aale Ñaŋ.