Kurélug maxejj yi, ñu gën koo miis ci Forum Civil, àdduna ci wàññi gi Nguur gi wàññi dund gi. Naka noonu, ñuy sàkku ci Nguur gi mu gën a farlu ci njaayum biir-réew mi.
Barki-démb ci alxames ji, la Nguur gi doon siiwal ndogal yi mu jël ñeel wàññig ndund gi. Ginnaaw bi mu leen siiwalee nag, kurélug maxejj yi doon na amal am ndaje démb ci àjjuma ji ngir dellusi ca yooya ndogal ak saytu ca ngëneeli askan wi.
Ca seen ndaje ma, waa kurél gi rafetlu nañu bu baax jéego yi Càmm gi teg, ba tax ñu dellu biral seen njàppale ñeel leen. Li ñu ci gis mooy ni defuñu lu dul dige ba ñu dige woon ba ñuy dagaan baati askan wi.
Loolu lépp nag, terewul ñu ànd ceek tekk ak teey. Nde, jàpp nañu ni donte ni lu baax la, gëmuñu ni Nguur gi dina ci mën lu bari. Dafa ciy am ay yemu (limites) yu koy waral, ñuy li Senegaal doon réew muy jéggaani ak ni ñuy doxalee ak a jàpp njëg yi ci àddina si.
Bu loolu weesoo, yu demee ni njëgu yaale bi ak yenn peyoor yi ciy dolleeku ñooy tax ba way-yëngatu yi ci wàll wi duñ ci am lu bare. Ba tax na, bees wàññee bu baax njëg yi, dootuñu ci am daanaka dara.
Ginnaaw taxaw seetlu yii yépp, kurél gi dellu na di sàkku ci Nguur gi mu gën a fullaal njaayum biir-réew mi ngir seen ndogal yi mën a am solo bu baax. Maanaam ñu sàkk i pexe yuy dooleel ndefarug lu ñuy yittewoo ci biir réew mi, ni ko magum jëwriñ yeek jëwriñu mbey mi faramfàccee. Lu ko moy, njéggaani yi Senegaal dëkke dafay wéy di neenal seen i jëf. Ndax, Càmm gi mënul dëkk ci di wàññi ak a woyofal.