CÀMBARUG ÑEENTI SÉMBI SÀRT FA NGOMBLAAN GA

Yeneen i xët

Aji bind ji

Lu tollu ci weer ak lu teg ginnaaw bi ñu dakkalee seen i càmbar ak tay, dépite yi dooraat nañu seen ub liggéey. Tay, ci altine ji, lañu ubbi Ngomblaan ga ci njiiteefu kilifag béréb ba, El Maalig Njaay. Li ñu ko dugge mooy tàmbali liggéey yu am solo. Donte ne sax, am na ay ndiiso yu fi jot a jaar ak ay sémb yu ñu jot a càmbar, waaye, yi ñu door tay dañoo làmboo njariñ yu bari. Nde, dees nañu bokk ci liy gën a dundal demokaraasi réewum Senegaal.

Daanaka lu jege at bi ñu leen sampee ak léegi, dépitey fukk ak juróomeelu kayug Ngomblaan gi yaa ngi amal liggéey bu am solo. Dafa di, sémb walla wayndare ya ñu fay yóbbu du taxaw donte ne sax, ñépp duñu ca ànd. Waaye, kenn umpalewul ne Nguuru Pastef moo yor dooley béréb boobu. Kon, lu ko soob rekk day jàll. Ginnaaw sémb sàrt biy tekki sàrtu Amnisti bi ñu fa wote woon lu yàggul, amaat na yeneen yu ñu tegaat ci taabal ji.

Ca ndajem jëwriñ ma ñu doon amal fanweeri fan ci weeru sulet lañu birale woon sémbi sàrt yi ñu fas yéenee jébbal Ngomblaan. Sémb yooyu nag, ñi ngi tollu ci ñeent. Bi ci jiitu mooy sémbu sàrt bi jëm ci settantal dayo ak kaaraange yoolekat yi. Bi ci topp jëm ci taxawalug OFNAC. Bi ci toppaat mooy bi ñeel li jëm ci xibaar. Bi ci mujj di bi ñeel xamle sa moomeel.

Ci gàttal, loolu mooy sémb yi nekk ci taabali dépite yi. Te, ñu war leen a càmbar fii ak ub diir. Ñoom nag, door nañu liggéey bi tay ci altine ji yamoo ak bés bi ñu dooraat seen liggéey ginnaaw bi ñu toogee ab diir. Kañ lay àgg ak nan lañu ko nar a doxale, li ci kanam rawul i bët.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj