CÀMM GU BEES GI : MAKI SÀLL TABBAAT NA AAMADU BA

Yeneen i xët

Aji bind ji

Njiitu réew, mi Maki Sàll, tas na Càmm gi. Démb ci àjjuma ji la jël ab dekkare daldi tekki ndomboy-tànki képp ku nekkoon jëwriñ ci Càmm gi. Waaye, ca saa sa la tabbaat njiitul Càmm gu bees gi. Ki mu ci taamu nag du kenn ku dul Aamadu ba mi mu tànn bu yàggul dara ngir mu doon lawaxu Bennoo Bokk Yaakaar ci wotey 2024 yi.

Ginnaaw bi mu ko junjee ca ndajem jëwriñ mi amoon ci àllarba jii weesu, Njiitu réew, mi Maki Sàll, tekki na ndomboy-tànki jëwriñ yi bokkoon ci Càmm gi. Ci ajjumay démb ji la yégle bi génn ci turu jëwriñ ji Umar Sàmb Ba, di fara-caytu bu mag bu Njiiteefu Bokkeef gi. Ñu mën cee jàng ni :

“Njiitu Bokkeef gi, teddaafon bi (son excellence), Sñ Maki Sàll, tekki na ndomboy-tànki jëwriñ yi bokkoon ci Càmm gi, jaare ko cib dekkare bu mu jël ci bésub 6 oktoobar 2023.

Njiitu réew mi jaajëfal na jëwriñ ya woon ci seen taxawaay ak liggéey bu mucc ayib bi ñu def.

Njiitu Bokkeef gi jël naat ndogalu taxawal Càmm gu bees ci njiiteefu jëwriñ ju mag ji, Aamadu Ba.

Dees na siiwal tëggiinu Càmm gu bees gi balaa yàgg.”

Bu ko defee, Senegaal dina am Càmm gu bees ci ñeenti weer yi dese Njiitu réew mi, Maki Sàll, ci boppu réew mi. Muy lu bettul kenn ci ñi daan topp tolluwaayu géewu pólitig bi. Waaye, li bett ñépp nag, mooy Aamadu Ba mi Njiitu réew mi tegaat ci boppu Càmm gi. Nde keroog bi ko Njiitu réew mi tànnee ngir mu nekk mbëru Bennoo Bokk Yaakaar ci wotey 25 féewaryee 2024 yi la ñépp, walla ñu bare ci jàngatkat yi, biral ni fokk Aamadu Ba génn ci Càmm gi ngir mën a jooxe lawax bi mu doon.

Bu weesoo loolu sax, génnam doon na lu ñu doon sàkku, rawatina ñi féete ci kujje gi, ngir bañ mu jëfandikoo Nguur gi, waayeet, ngir moom ak yeneen laway yi yem kepp ci joŋante yi.

Mu mel ni jarul kenn di laaj lu waral Njiitu réew mi doxale nii. Ndax kat dafay nirool ni dafa koy xàllal yoon ngir mu mën koo wuutu ni mu ko bëggee. Muy itam lu xel yépp mën a daj. Nde, Aamadu Ba ci boppam taxawoon na wax ni Njiitu réew mi Maki Sàll lay liggéeyal. Mu dellu leeral ni liggéey boobu mi ngi ko aj ci gis-gisam jëme 2035.

Ak lu mën a xew, ñuy xaar ba xam ñan la Njiitu Réew mi Maki Sàll ak magum jëwriñam nar a tànn ak lu ca nar a leere ci seen ndéetoo.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj