Ëllëg ci gaawu gi la joŋantey CAN biy door. Ren, Koddiwaar moo dalal xëccoo bi. Ñaar-fukk ak ñeenti (24i) ekib yu séddalikoo ci juróom-benni kippu (poules) ñoo ciy laale. Kippu bu ci nekk, ñeenti ekib lay def. Ci biir kippu bu nekk, ñaari ekib ñoo ciy génn génn bu njëkk, muy fukk ak ñaari (12i) ekib yoy, dees na ci dolli ñeenti ñetteel yu gën a jekku. Nii la joŋantey bés bu njëkk biy tëdde :