Alxemes, 21i fan ci weeru sulet lañ doon amal cargalug CAF Awards 2022 yi. Muy xew-xew bu mboolem kuréli futbal yu Afrig (CAF) di amal at mu nekk. Mu di ko amal ngir sargal doomi Afrig yi gënn a ràññeeku ci powum futbal ñeel Afrig ak ci àddina si, muy góor mbaa muy jigeen. Di na ciy sargal itam Ikibu réew yeek mbootaay yi gënn a fés ci kembarug Afrig.
Bu atum ren ji, ña nga ko doon amale ca “Complexe Mohammed VI” ca réewum Marog. Ñu waroon ca joxe lu tollu ci fukki neexal ak benn. Réewum Senegaal fésoon ci lool. Li ko njëkkoon a waral di doomam yi jotoon a takku lool ci tànneef yi doon xëccoo neexal yi. Juróom-ñaari Saa-Senegaal bokkoon nañ ca. Mu doonoon lim bu am maana bees ko nattee ci yaatuwaayu Afrig, ñi ci mënoon a bokk ak limub neexal yi ni mu desee takku.
Saajo Maane, di Saa-Senegaal bi ci gën a fés te nekk ca Bayern (Allemagne) moo jël Ballon d’Or bi ci kaw doomu Misra (Esipt) jii di Mohammet Salaa (Liverpool / Angleterre) ak jeneen doomu Senegaal jii di Eduwaar Mendi (Chelsea / Angleterre). Bii mooy ñaareelu yoonam mu koy jël ginnaaw ba mu ko jëlee ci atum 2019. Bu Saajo Maane jàllee, doomu Senegaal jii di Aliw Siise moo am neexalu tàggatkat bi gënn a xareñ. Paap Mataar Saar lañ jagleel neexalu joŋantekat bi gënn a féete ndaw dellu toftal ca Paap Usmaan Saaxo boroom bii bi gënn a rafet. Ñoom ñaar itam diy doomi réewum Senegaal.
Ngoonu keroog, Senegaal am na fa ndam lu réy. Ginnaaw bi doomam yii gàddoo neexal yii yépp, tabb nañ ko Ikibu Afrig bu gënn a ràññeeku ci at mi. Ci pàttali, Ikibu Senegaal bi moo jëloon kub bu Afrig 2021 biñ doon amale ca Kamerun. Mu dellu nekk Ikib bi jiitu ci Afrig te féete ci fukk ak juróom-ñetteelu palaas ci toftale bu Fifa.