CÀRTUB AMNISTII : AG NJÉGGAL WALLA AB RAWALE ?

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ca ndajem jёwriñ ma mu doon amal ci Àllarba jii weesu, Njiitu réew mi, Maki Sàll, biral na mébétu teggi daan yi tegu woon ci ndoddi Kariim Wàdd ak kii di Xalifa Sàll. Ba tax, mu sas kii di jёwriñ ji mu dénk wàlluw yoon, Ismayla Maajoor Faal, mu def kéemtelaayal kàttanam ba képp ku ñàkk àqi maxejjam mёn ci jotaat. Maanaam, mu mёn a bokk ci ñu askan wi mёn a fal ci wote yii di ñёw, bu dee samp na ndёndam. Mu nekk nag, ndogal loo xam ne, gis-gis yi wuute na ci lool. Ndax, ñii di waa PDS dañu ne duñu nangu loolu wenn yoon. Loolu tax, mu jar a def ab taxaw-seetlu ngir xam lan mooy jubluwaayu ndogal loolee. Yan njeexital la mёn a am ci képp ku ñuy toppe tuuma yu ni deme ?

Mbir mi ñuy dippee “amnistie” du lenn lu dul ab xeetu njéggal bu wuute ak bi ñuy woowe “grâce”. Ndax, bii ab xeetu teggi bépp daan bu gàllu woon sa loos la. Te, kenn du ko def nit waaye jёf ja ñu koy toppe lañu koy def. Cig pàttali, Kariim Wàdd ñi ngi ko daanoon ca atum 2015 lu tollu ci juróom-benni ati kaso, ñu alamaan ko lu tollu ci téeméeri tamñaret ak fanweer ak juróom-ñett. Kii di Xalifa Sàll ñu daan ko ca atum 2018 juróomi ati kaso ak alamaanub juróomi tamndaret. Loolu nag, bokkoon na ci li taxoon mёnuñu woon a bokk ca wotey 2019 ya. Nguuda Mbuub di jàngalekat ak gёstukat ci “Droit public” fale ca Daara ju kowe ja nekke ca Ndakaaru (UCAD) mi ngi ciy xamle ne :

“Xalifa Abaabakar Sàll ak Kariim Wàdd xam nga lan moo leen teree nekk lawax (2019) ? Benn baat ci càrtu wote bi. Dañu leen a daan. Bi ñu leen daanee Càmmeefug Senegaal gis ne ñii mёn nañu nekk lawax ba léegi (…). Càrtu wote bu 92 (…) càrt boobu am yu mu àndal yoo xam ne ña nga ko tibbe ca Farãs moo doon dog L31 ak L32. Dog yooyu da doon wax bu ñu la daanee ci xeetu jёf yii mёnoo bokk ci wayndareg wote bi, loolu lañu waxoon. Waaye ca jamono jooja, dog L57 dafa doon wax ni saa-senegaal am na sañ-sañu nekk lawax. Ñàkk kàrt buy wote mёnu la teree nekk lawax.” 

Waaye nag, yamul foofu, mu yokk ci ne :

“2018 bi ñu daanee Xalifa Sàll ak Kariim Wàdd ba pare nag ca lañu ñёw ñu dugal benn coppite boo xam ne day dugal bépp saa-senegaal buy wote. Te, xamoon nañu ne L31 ak L32 yi nekkaat L29 ak L30 dafa doon bañ ku ñu daan, li dal Xalifa Sàll ak Kariim Wàdd nga ñàkk sa kàrtu wotekaay. Kon du leen teggi, day dal seen kow. Baat boobu rekk boo ko dindi woon ci càrtu wote bi dañuy mёn a doon lawax. Xam nga loolu yomb na (…). Pexe yu bari am na. Waaye, bi gёnoon a yomb mooy nga dindi mbiri wote ci dog L57 walla nga laal dog L29 ak L30.”

Lii bokk na ci li tax ñu bari ci gaa ñi jàpp ne pólitig bi daa tàmbali am doole lool ci àtte yi yoon di def. Waaye, sa bañi démb, bu ñu nangoo tey, seen i pexe jubuñu. Moo tax, am lu mat a settantalaat, muy lu tax kii di Njiitu réew mi Maki Sàll bàyyi ba wotey 2024 yi des lu tollu ci fukki weer ak juróom-ñaar mu namm ndogal lii. Ngir yokk ag dal ci làngug pólitig gi la walla ngir wàññi doole kujje gi. Ndax, kii di Kariim ak Xalifa seen lёkkatoo yee àndoon ci wote yii jàll. Walla tamit ay pexe la ngir rafetal ginnaawam. Ndax, njeexital yi xeetu ndogal yii mёn a am ci képp ku xeetu tuuma yii gàllu sa loos. Mu mel ni, loolu la kii di Keledoor Seen di xamle ci kàddoom yii : 

“Bu njortee ne mёnatul a dem, day bёgg a defar ginnaawam. Loolu, njort la rekk ndax njéggal loolu du duut baaraam nit ki. Du tuddu Kariim, du tuddu Xalifa Sàll, day tuddu ay jёf. Ay njombe, mu doon luubal alalu askan wi (détournement de dernier public) walla fàggu ci alal ju lewul (enrichissement illicite). Mёn nañu ne jéggale nañu  mbooleem lu xeetoo ak njombe yooyu. Loolu, bu ñu ko defee képp koo xam ne mёs nga def njuuj-njaaj ci àpp bii ñu ko àpp. Mёn nañu ko àpp diggante 2012 ba 2022, ci fukki at yooyu ku ci def njombe boobu jàll nga. Doo mёn a topp Maam Mbay Ñã, doo mёn a topp Seex Kànte, doo mёn a topp Farba Ngom sax mi nga xam ne réeral na jamono jii xanaa lu tollu ci juróom-ñeenti téeméeri tamndaret ci pàggu gu lewul mёnoo ko toppu ak njuuj-njuuj yi fi am ci wàllu kopparal yépp. Liy setal Kariim ak Xalifa da leen di yóbbaale ñoom it. Ndёgg-sёrёx googu nag, lañu war a def ndànk bañ ci daanu”.

Mu mel ni, kii di Bugaan Géy noon la ko njorte woon laata muy biral mébétam. Moo tax, mu ni: “bu ñu defee njéggal loolu, Maki Sàll dina ci dugal ay nitam. Te, niti Maki Sàll yooyu nga xam ne dañoo def ay njombe ci réew mi dafa jaadu réew mi rёq seen ndigg. Muy Xalifa, di Kariim dégguma benn yoon ñu ne nañu leen jéggal. Dañu ne nañu tёggat porose bi.” Loolu lépp nag, di ay pexe yoo xam ne ndogal boobu mёn na koo ёmb. Waaye nag, bala ngay ub gémmiñu Sàmba, xaaral ba xam lan lay wёliis. Ndax, bu fekkee ne ñi ñu war a teggil daan yi seen ndoddu, kenn ki di Kariim Wàdd ak waa làngam bañ nañu ba tёdd ca naaj wa. Waaye nag, ku ñuy diri ndax danga taamu fu sa ndoddu di jaar ? Kon nag, coow li diggante Nguur gi, kujje gi ak yoon tàmbaleegul bay jeex.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj