Altine jee weesu, fukki fan ak juróom-benn ci weeru desàmbar, la Ngomblaan gi door liggéeyub càmbar nafay njëwriñ yi. Dafa di, mbooleem kilifay njëwriñ yi walla campeef yi dañuy dem fa Ngomblaan ga layal fa nafa gi ñu bëgg ñu jox leen ngir ñu doxal béréb bi ñu jiite. Su ko defee dépite yi saytu, sog ko koy woteel. Koppar googu ñu leen di woteel moom lañuy doxalee liggéey bi ñu leen dénk ci diiru atum 2025 mi. Liggéey boobu Ngomblaan gi dooroon altine jee weesu, ci dibéeri démb ji lañu ko jeexal.
Weeru awril wale jàll lañu sampoon Càmm gu bees. Boobaak léegi nag, ci li fi Nguur gi ñu daaneel bàyyi woon lañu doon doxalee béréb ya ñu nekk. Waaye, ginnaaw gi dañu fee amal ay wote, keroog fukki fan ak juróom-ñaar ci weeru nowàmbar wii jàll. Li ñu ko dugge woon mooy taxawal geneen Ngomblaan goo xam ne, ñoom waa Nguur fi nekk ñoo fay ëpp doole. Su ko defee ñu mën a liggéey ci anam yu gën a ñoŋ. Fukk ak juróomeelu kayug Ngomblaan gi tijji nañu ko ci lu yàggul dara, daldi door caytu ak wotey nafa yi ñu war a jagleel banqaas bu nekk.
Ci bésub altine jee weesu, saytul nañu Njiiteefu Bokkeef gi (Présidence de la République), Ngomblaan gi ci jëmmi boppam, Ndajem ndeyu-àtte mi, Ëttu caytu yi (Cour des Comptes) ak Njëwriñ gu mag gi (Primature). Waaye, yemuñu ci campeef yooyu kese, am na yenn njëwriñ yu ñu laaxaale ci liggéeyu bésub altine boobee. Muy yu ci mel ni Njëwriñu njàng mu kowe mi, Njëwrinu kopparal gi ak nafa gi ak njëwriñu kéew mi. Waaye, caytug nafag njëwriñu njàng mu kowe mi kepp moo mujjoon a àntu ca bés boobee. Yeneen yi, dañu leen a dàq ba yeneen bés yi ci topp.
Ca talaata ja, am na ñeenti njëwriñ yu ñu saytul limu koppar gi ñu war a teg seen loxo ngir ñu matale li ñu leen sas. Muy njëwriñu ndefar gi (industrie) ak yaxantu gi, njëwriñu njaboot gi ak jàppalante yi, njëwriñu soroj bi, laf gi ak mbéll yi ak njëwriñu mbirum xaralay jokkoo yi ak jokkoo gi. Ca ëllëg sa, àllarba, jot nañoo saytu nafay njëwriñu wërteef gi ak ñeeñal gi (artisanat), njëwriñu kéew mi ak njëwriñu njàng mu suufe mi ak mu digg-dóomu mi. Njëwriñ yi ñu saytul seen ug nafa ca alxames ja ca topp, yii la : njëwriñu Yoon, njëwriñu ndox mi ak cetal gi, njëwriñu tàggat gu ànd ak xereñte ak njëwriñu tàggat-yaram, ndaw ñi ak mbatiit mi.
Naka noonu, ca àjjuma ja tamit, amoon na ay jëwriñ yu demoon fa Ngomblaan ga. Muy ñu ci mel ni jëwriñu biir-réew mi, jëwriñu taax yi, kow gi ak ndefarug suuf si, jëwriñu napp gi, ak jëwriñu mbirum kopparal, ñu naan ko “microfinance”. Ca gaawu ba, amaat na ñeenti njëwriñ yu ñu càmbar seen i nafa. Bi ci jiitu di njëwriñu mbey mi ak càmm gi. Ñaareel bi di njëwriñu mbiri bitim-réew. Ñetteel bi di njëwriñu koom gi. Bi ci mujj mooy njëwriñu liggéey bi ak jokkalante diggante campeef yi.
Démb ci dibéer ji lañuy càmbar koppar gi ñu sédd njëwriñ yii di njëwriñu dem bi ak dikk bi, njëwriñu làrme bi, njëwriñu wér-gi-yaram wi ak njëwriñu kopparal yi ak nafa gi.
Cig tënk, noonu la liggéeyu caytu ak wotey nafa yi tëdde. Njëwriñ ju ci nekk am na nafa gu ñu ka woteel gu wute ak gog moroomam. Naka noonu, campeef yi tamit càmbar nañu koppar gi ñu leen di jagleel. Ni mu amee ci njëwriñ yi yoo xam ne yokkal nañu leen bees ko méngalee ak li ñu amoon daaw, noonu la amee tamit ci campeef yi, yenn yoo xam ne wàññi nañu limub koppar gi ñu leen daan jox.