Ca weeru sulet 2024 la ñetti réew yii di Burkinaa Faaso, Mali ak Niseer dogu woon, daldi génn ci kurélug CEDEAO (Communauté Économique des États d’Afrique de l’Oest). Lu ko jiitu, njëkkoon nañu taxawal seen ug réewaale bopp, duppee ko AES (Alliance des États du Sahel), ca weeru sàttumbaar 2023.
Boobu ak léegi nag, kurél gi deful woon lu dul teg leen i daan. Ba démb ci dibéer ji, ci la leen Njiiti réewi kurél gi sog a nangul seen yéeney beru. Fekk ñu doon amal 66eelu ndajem Njiiti réewi CEDEAO yi fa Abujaa, réewum Niseriyaa. Naka noonu, fas nañu yéene amal ay coppite ci àppug 6i weer, maanaam sãwiyee ba sulet 2025, ngir seppi ñetti réew yi ba ñu set ci kurél gi.
Laata ñuy àgg ci àpp gi nag, kurél gi feddali na kóoluteem ci Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, Njiitu réewum Senegaal, ngir mu wéy di dox tànki jàmm ci diggante ñetti réew yi ak kurél gi ba xam dinañu mën a dellusi.