CEDEAO-NISEER

Yeneen i xët

Aji bind ji

Fitna jaa ngi gën dee jege ci diggante Niseer ak CEDEAO. Ginnaaw bi kurél gi jëlee ndogalu delloo Nguur ga ca loxoy Muhammet Basum, réew yi ci ànd a ngi nekk di dajale soldaar su ñu fa namm a yebal. Ci waajtaay yooyu sax, for nañu ci wewu béy ni soldaari Senegaal yi tàmbali nañu seen dajaloo ci altine ji. Te, ña nga koy defe fa Cees. Ñuy xaarandi xibaar yu gën a wér yoy, dees na tukkee ci kilifa yi. Fileek boobu nag, fa Niseer, Muhammet Basum a nga ca guddi yu lëndëm. Askan wa tamit, tàmbali na sonn.

Ginnaaw bi ñu ko déjjatee ca Nguur ga, boole kook njabootam tëj ca pale ba, sóobare yi dellu nañu gàll Muhammet Basum ay tuuma. Ci yëgle bi ñu siiwal, te Kolonel-Masoor Aamadu Abdurahmaan doon ko dawal, ña nga cay xamle ni, Njiitu réewum Niseer ma woon, Muhammet Basum, dafa wor réewam ci anam bu jéggi dayo. Naka noonu, dees na ko toppe lu ñuy tuddee « haute trahison » ak « menace de la sûreté intérieure et extérieur ». Maanaam daal, Muhammet Basum daa fecci kóllëre gi doxoon digganteem ak askanu Niseer, wor leen. Loolu doyul, mu séqiy jéego, jël i ndogal yoy, dañu nasaxal kaarange biir réew ma ak bitim réew ma. Moo tax, ñoom kilifay Niseer yu yees yi, nee nañ dañuy àttelu Muhammet Basum.

Bi ñu biralee xibaar bi nag, CEDEAO génne na ab yégle, di ci naqarlu ndogal loolu, di wax ne sóobarey Niseer yi dañ leen di cokkaas. Ñoom, kilifay CEDEAO yi, feddaliwaat nañ ne, Muhammet Basum mooy Njiitu réewum Niseer te dinañ fexe ba delloo ko ci jal bi. Looloo tax sax CEDEAO teg Niseer ay daan yu diis. Daan yooyu nag, tàmbali nañoo jeexital ca askan wa. Moo tax itam, ca yégleb sóobare ya, xamlees na ni Askanu Niseer wee ngi nekk di dund ay jafe-jafe yu tar, te dara yóbbewu leen ko lu dul daan yi CEDEAO teg seen kow.

Wolof nag nee na, paaka bay rey nit, mbokkam a koy tëgg.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj