Xaar bi yàggoon na, xeex bi metti lool, coow li ne kurr, saf sàpp ci Farãs ak Njiiti-réewi Afrig sowu-jant yi. “CFA, na fi jóg !”, “Farãs ca xaj !”, “Danu bëgg a moom sunu bopp, yilif sunu weccit !”… Kàddu yii ñoo gënoon a fés ci xeex bi way-moomeel yi, ñu bare ci xeltukati Afrig yi, aji-xam koom-koom yi ak ñenn ci kujje yi, sumboon ngir jële fi CFA bi. Seen mébét mooy dog buumu-njaam gi Farãs ak dunguroom yi nuy jiite takkal Afrig, boole réewi Afrig yi, bennal weccit wi ngir dooleel seeni koom-koom. Bi njiiti CEDEAO yi demee ba sës, dañoo amal am ndaje ca Abujaa, ci 29eelu bés, weeru sulyet. Ci lañ jëloon ndogal ni dinañ sàkk weccit wu bees ngir mu wuutu fi CFA bi ci atum 2020, te muy ECO. Turu xaalis bi nag, ab gàttal la ñeel turu CEDEAO ci àngale : ECOWAS. Kon, dañu jël “ECO” bi, bàyyi “WAS” bi. Lu jiitu loolu, nag, jotoon nañ fee nas i naal yu ni mel ay yooni-yoon ci atum2003, 2005, 2009 ak 2015. Waaye, naal yépp a lajjoon, tàbbi géej. Bu dee ñenn ñi dese woon nañ as tuut ci yaakaar, ñi ci ëpp yàqi woon nañ bu yàgg. Waaye, bi Emmanuel Macron (Njiitu)réewum Farãs) ak Alassane Ouattara (Njiitu-réewum Kodiwaar te jiitewaale kurélu UEMOA) yëglee keroog, ci bésu 21 desàmbar, ne ECO bi dina wuutu CFA bi ci atum 2020, ci la gaa ñi xam ne kat, bii yoon du ay caaxaan. Wànte, nag, bu dee am na ñuy rafetlu naal bi, ñu bare seen xel dafa teey ci mbir mi. Mu mel ni am na luy ñuul ci soow mi.
Alassane Ouattara moo jëkk a biral xibaar bi keroog bi ko Emmanuel Macron ganejee Kodiwaar. Kàddu yii la rotaloon :
« Nun, njiiti réewi UEMOA yi, déggoo nanu ci ne dinan soppi CFA bi ci ñetti anam : bi ci jiitu mooy tur wi, léegi ECO la xaalis biy tudd. Ñaareel bi mooy ne, dootunu bàyyi sunu xaaju denceefi weccekaay (réserves de change) ci gafag Farãs te dinan tëj ndencefalub liggéey (compte d’opération) ba ca Farãs. Ñetteel bi mooy ne dinañ jële bépp ndawu Farãs ci ndajem-caytu yi ñeel bérébi liggéeyukaayi UEMOA yi. »
Bi mu noppee, Emmanuel Macron da cee toftal kàddu yii :
« CFA bi jur na fi coow lu bare ba ñu ciy tuumaal Farãs ñeel taxawaayam biir Afrig. Bu dee lool la, nan leen dog buum yi ! Nan am fit ak sañ-sañu ànd liggéey, te muy liggéey bu tegu ci ngor ak yemoo. Farãs amul dara lu muy nëbb […] te maa ngi ànd ak mbégte di dëggal waxi Alassane Ouattara yi, di rafetlu coppite yu réy yii.”
Kii di Bruno Le Maire, jawriñu Farãs jiñ dénk koom-koom geek ngurd mi, lii la wax ci RFI :
“ [coppite gi] ci ndoorteelu weeru saŋwiyee la war a door. Nguur gu ci nekk bu la neexee nga jëlsi, fii ci Frãs say denceefi weccekaay saa bu la soobee. Waaye, dina tëj ndencefal boobu ci atum 2020 ngir réewi CEDEAO moom seen bopp ci fànn googu.” (http://www.rfi.fr/afrique/20191221-macron-ouattara-annonce-remplacement-franc-cfa-afrique-ouest-eco)
Waaye, boroom xam-xam yi juyoo nañ ci njariñu ECO bi ci koom-koomi réewi yi koy jëfandikoo ak ci dundinu askan wiy yeewoo ci biir CEDEAO, rawatina 8 réew yiy jëfandikoo CFA jamono jii te lëkkaloo ceek Frãs. Ñiy layal Eco bi nee ñu dina yombal njënd meek njaay mi, yombal yónnee xaalis bi, muy ndimbal ci 385 milyoŋi doomi-Aadama yiy dund biir CEDEAO.
Kako Nubukpo, aji-xam koom-koom la, nekkoon jawriñ ca réewum Tógó te bokk ci ñi bind “Sortir l’Afrique de la servitude monétaire”, kàddu yii la ci rotal :
« ECO, lu baax la. Dina dooleel ànd beek booloo bi ci biir CEDEAO. Li ma ci ëppal solo mooy jàppalante gi ciy juddoo ñeel nafay réew yi koy bokk, bennoo biñ ci jublu ak xéy yi mu nar a jur…”
Sàmbaay Bàcc rekk…
Bees dégloo ñi ëpp ci aji-xam koom-koom yi, ECO ak CFA lenn rekk a leen wutale, muy tur. Waaye Sàmbaay Bàcc rekk. Ndongo Sàmba Silla moom jàpp na ne kàdduy Alassane Ouattara yi waruñoo bett kenn ndax réewi UEMOA bëgguñoo dog buumu-njaam gi leen Frãs jénge. Biñ laajee Ndongo Sàmba Silla xalaatam ci ECO bi, lii la tontu :
« ECO bi ? Waaw. Dégg naa ñenn ñiy xeex CFA bi naan, nanu gaaw jël ECO bi, def ko sunu weccit. Waaye, ECO bi ci lajj lay mujj. Wolof dafa ne, ku ndóbin rey sa maam, foo séenatee lu ñuul daw. Man dama jàpp ne, CFA ak ECO ñoo yem kepp, benn baaxu ci.“(https://www.defuwaxu.com/2019/08/15/naareelu-xaaju-waxtaanu-mamadu-jallo-ak-ndongo-samba/?fbclid=IwAR16UAaDI_Rj2R7F3qBJ9aivDZTYR547kaHDEySDttO-01zcqhn5XYisQLQ)
Sanyade Okoli mi jiite Alpha African Advisory; moom, dafa ne :
“Bu dee njaay mi mënta jéggi digi réew yi ndax duwaan yu bare, ndax mënees na wax waxi bennal weccit wi ci biir CEDEAO?” (https://www.bbc.com/afrique/region-48911056)
Kii di Nathalie Yamb mi nguuru Kodiwaar dàqoon ni xaj gannaaw kàddu ya mu waxoon ca Sotchie (Riisi) dafa jàpp ne li Macron ak Alassane Ouattara wax ay paccal-forox la, di naxee-mbaay bu bir. Nee na sax, “UEMOA dafa yàq naalub CEDEAO”.
Ndege, jamono jii, am nañ 8 xeeti weccit ci biir réewi CEDEAO : Cédi, Dalasi, Dolaar bu Liberiyaa, Escudo bu Kap-Veer, Franc bu Gine, Leone, Naira ak CFA bi 8 réewi UEMOA yi bokk. Ci 8 xeeti xaalis yooyu, lëkkalees na 2 yi ci Euro bi, CFA (déggoob desâmbar 1973 ak Frãs ñeel weccit) ak Escudo bu Kap-Veer (déggoob Purtugaal bu màrs 1998).
Njiiti CEDEAO yi déggoo woon nañu ci bokk weccit, te muy ECO. Waaye, mel na ni Alassane Ouattara ak UEMOA bim jiite dañoo nar a xajamal naal boobu. Ndax réew mu ci mel ni Niseryaa àndagul ci naal bu yees bii. Moom mi nga xam ne amul genn buumu-njaam gu ko booleek Frãs, day moytoo dugg ci guta. Njiit ma fa nekk, Muhamed Buhari lii la wax :
“Li nu doon, nun Niseryaa, réew mi ëpp doole ci wàllu koom-koom biir Afrig ak lin fi ëppale askan moo tax mënunoo jékki rekk sóobu ciy déggoo yu leerul te jokkoowun ceek ñin ci war a waxal.” Maanaam, day teey ci mbir mi ba mu leer ko ni du yàqal dara Niseryaa mi dul caaxaane moomeelu boppam.
Bu dee Senegaal, nag, Pr Séex Umar Jaañ mi xam-xamam màcc ci wàllu koom-koom dafa ne :
«Lii [ECO bi] ab jéyya ju réy la ! Te buñ tàmbalee jëfandikoo ECO bi Senegaal du ci jële dara.» (https://www.seneweb.com/news/Politique/du-franc-cfa-a-l-rsquo-eco-laquo-c rsquo_n_304412.html)
Dees na ko topp.