CHINA MALL, WÓOR NAAM ?

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ginnaaw AUCHAN, yaxantukati saa-senegaal yi amaat nañu geneen gan. Geneen kërug liggéey (entreprise) gu Sinwaa moo ubbi fale ca biir Ndakaaru, ca Mermoos-Sàkkere-këer, ci weeru màrs wii nu génn. Béréb boobu, mi ngi tuddu CHINA MALL (caayna móol). Mu doon béréb bu yaatoo bob, tollu na ci 7.500m². Nga xam ne, daanaka, lu saa-senegaal bi soxla ciy jumtukaay, dañu ko fay jaay. Ñoom daal, lu jëm ci wàllu dund rekk lañu jaayagul. Seen teewaay ci réew mi nag, du luy jig AUCHAN, astemaak yaxantukati réew mi nga xam ne, ñoom, AUCHAN daaneeloon na leen ba noppi. Kon, CHINA MALL moo leen nar a doggali. 

CHINA MALL, ay njëg yu yomb a yomb lay jaaye. Te, jëndkat yi moom ñu bari ci ñoom xàmmeewuñu saa-senegaal bi ak ndoxandéem bi. Moom kay, ki gën a yombale lañu xam. Waaye, ñoo yey nag. Ak fi réew mi tollu… Bu ñu seetloo nag, dañuy gis ne, këri liggéeyi doxandéem yi, ci seen doxin, dañuy nasaxal koom-koomu réew mi bu baax a baax.

Yaxantukat yi, way-moomeel yi, way-pólitig yi, kurél yi boot jaaykati réew mi, ñiy taaba-taaba añs., ñépp ñoo ngiy ngi ñaawlook a naqarlu bu baax ni Nguur gi seetaanee doxandéem yiy jaaye num leen neexe, lum leen neexe, di wàññi njëg yi bu baax a baax. Ndeem sax, kujje moom, mënut a ñàkk ci ja yi, na njëg yi doon lu xel mën a nangu rekk. Maanaam, ñu nekk njëg yoo xam ne dina neexoo ak yi ñu fi fekk. Ndax, saa su nekk, dañuy nemmeeku gaa ñu jóge bitim-réew di ñëw di jaaye loo xam ne ñi fi nekk mënuñu koo jaaye. Moo tax it, jamono jii, njënd ak njaay ca Ndakaaru ak ci yenn béréb yi ci biir réew maa ngay bëgg a des ca loxoy doxandéem ya. 

Bu dee ne, doomi réew mooy defar réew, kon njënd ak njaay taxul woon ñuy wax. Ndax, CHINA MALL, ndeem sax ñoo gën a yombale ay njëg, waaye, demewu fa noonu yépp. Gaa ñi ñoo ko may doole joo xam ne këru liggéey yi nekk ci réew mi amuñu ko. Te, bu jaaykati Senegaal yi néewee doole rekk, njënd mi ak njaay mi dina nasax lool. Li doy waar ci mbir mi kay mooy li ëpp doole ci koomu réew mi ci bànqaas googu la lalu. Léegi, bu yeneen këri liggéey demee ba ëpp doole ci ja bi, koomu réew mépp ci seen loxo lay aju. Te, su boobaa, ñooy xool lu leen neex ñu jaaye ko. Léegi, ndax saa-senegaal yiy jënd ci ñoom xam nañu ne loolu day rey seen koom-koomu réew ? Déedéet ! Li ëpp ci ñoom kay, li leen yitteel mooy am li ñu bëgg ca na mu gën a yombe. Moo tax, doxandéem yi ñoo fiy gan yuy yewwi béy. Rax-ci-dolli, ñoo mujj ci ja bi waaye, ñooy wax gaa ñi fu ñuy tooge. 

Su ko defee, jafe-jafey yaxantukati saa-senegaal dootul yem ci réew mi rekk, waaye ca bitim-réew sax seen doole dafay gën a wàññeeku. Ndax, ku mënul jaay ci sam réew, nooy jaaye keneen ? Moo tax, samp gi ñu ko fi samp neexul wenn yoon kuréli way-moomeel yi. Ñu ci mel ni waa FRAPP moom sumb nañu xeex ba. Ginnaaw AUCHAN ak CARREFOUR na ñu fi génn, tey CHINA MALL lañuy sàkku mu jóge fi. Donte ne sax loolu mënagul a nekk. Waaye, na Nguur gi jël i matuwaay ba seen njëg yi du gàllankoor yaxantukat yu ndaw yi ak yu mag yi.  

Mu am tamit, meneen mbir ci këru liggéey gi, mooy ne dina jël ay ndaw yu bari ci seen béréb yooyu. Maanaam, dinañu bokk ci liy wàññi ñàkkum xëy mi. Rax-ci-dolli, dina yombal njaay mi ci ja yi. Ndax, ku fi jaay lu jafe gaa ñi romb la fi, dem ci sa moroom. Waaye, mën naa tax tamit am ñu ñàkk seen i liggéey. Ñi daan daan seen doole, di jaay li nga xam ne ñoom moom lañuy jaay, ñu bari ci ñoom dinañu daanu. Du yem ci daaneel yaxantukati saa-senegaal yi rekk. Dina xajamal bu baax it njaayum kër gii di AUCHAN ak yeneen këri liggéey yu mel ni moom. Léegi, ndax ñoom bu seen um njaay doxatul dinañu jëlati ay liggéeykat ? Walla ndax, dañuy wàññi ay liggéeykat ?

 Li doon yoon kay mooy ku ñëw di jaay li ñépp di jaay, danga war a jaaye li ñépp di jaaye. Donte ne sax mën na koo gën a tuuti ci ndorteel gi ngir nga amiy jëndkat. Waaye na doon njëg yu yemamaay yoo xam ne dina tax ñeneen ñi wàññi, te du leen gàllankoor. Mu mel ni nag, wàllu njënd ak njaay yërmaande amu ci. Ku jekku sa moroom rekk, génnee ko ja bi. Kon kay, Nguur gee war a jël ay matuwaay ci loolu balay koom-koomu réew mépp di des ci loxoy doxandéem yi. Maanaam mu dooleel ay yaxantukatam ba ñu mën a jàkkaarloo ak ñi jóge bitim-réew. 

Ndege, CHINA MALL, du lu wóor.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj