Daar-daar bi Sëñ Usmaan Sonko doon amal mujje na a jur coow ci pénc mi. Ñu bari ci kujje gi di ñaawlu kàddu yi mu fa jibal, rawatina yi mu jagleel àttekat yi.
Ci guddig talaata ji, jàpp àllarba la Usmaan Sonko, njiitul làngug PASTEF, di itam Ilimaanu jëwriñ yi, doon amal ab daar-daar ci xëtu Facebookam. Ca daar-daar boobu nag, biraloon na ca tolluwaayu réew mi, naal yi ñu jublu, ni Yoon di doxe ak li ciy gis-gisam.
Ay fan ginnaaw bi mu amalee daar-daar boobule, kàddu yaa ngi wéy di jib ci pénc mi ak i njañse yu worook gis-gisam. Ñu mën cee ràññe yu mel ni yu Meetar Habiib Witin, di njiitul kurél gii di THIES D’ABORD, walla yu waa FDR (Front pour Défense de la Démocratie et la République).
Bees dellusee tuuti ci kàddu yi mujjee jib, dañuy gis ni kii di Meetar Witin ma ngay fàttali ni kenn umpalewul li fi xew ci at yii weesu, yu deme niy xoqatal, ay ndàqe ba ci beddi ay lawax. Ñuy ay jëf yu tukkee ci ñoñi pólitig beek Yoon. Wëliis tolluwaay yu ni mel, Usmaan Sonko joxoñ na nit ba mu falu. Muy lees di rafetlu, nde dafay wane xereñ ak njàmbaar yi nekk ci moom.
Waaye Sëñ Witin yamul ci loolu, nde yokk na ca ni bu gàllankoor yooyile jàllee, pexe yi leen doon dékku dañu war a weesu, ndax ñu mën a tàbbi ci wareef yi aju ci ndoxal (gouvernance) ak leeral (clarté).
« Bu ñu demee ba jëmmu aji-pólitig fés ba kenn xamatul dëgg-dëgg ki jiite, dafay andi jiixi-jaaxa ci demokaraasi. Taxawaay yi dañuy mujje salfaañoo : ndax Jomaay mooy Njiitu Réew mi, walla Usmaan Sonko mooy dëgg-dëgg kiy dogal ? Ban dayo la Usmaan Sonko war a am bay tuutal àttekat yi te dara du ko ci fekk ? Ilimaanu jëwriñ yi, di itam njiitul làng, moo wax niki ma-xejj ngir ñàkkal worma campeefu Yoon ci pénc mi. Mbej la mu mu talaata képp kenn ku nekk ci àttekat yi, tey jéem a jëmmal moom-sa-bopp ak ngor ci jamono ju tar ba noppi. »
Bees xoolee bu baax ci kàddu Meetar Witin yi, dañuy gis ni rafetluwul taxawaay bi Usmaan Sonko am tay ak kàddu yi mu jagleel masistaraa yi.
Ba démb ci àjjuma ji FPR (Front pour la Démocratie et la République) génne na ab yégle jagleel ko kàdduy Usmaan Sonko yooyule. Naka noonu, ñoom itam ñuy fésal ni dafa jot ñu fàttali Ilimaanu jëwriñ yi, di Usmaan Sonko, ni ci demokaraasi nguur gi dees koy doxal ci bëgg-bëggu askan wi, nangul nit ñi seen i gis-gis, bàyyee campeef yi seen bopp te féexal saabalukaay yi.
Ñu yokk ca ni yittey bokkeef gi mooy fexe ba ñu sax ci di péncoo lépp lu soxal askan wi. Waaye du fexe noo tëjee seen iy gémmiñ. Rax-ci-dolli, bees nekkoon ci Réew mu jaar yoon, kilifa gu Yoon daan, rawatina mu nekk njiitu Càmm, dafay tekki ndombo-tànkam.