Ci 20 awril bii weesu, lu ëpp 150i doom-aadam lañ faatoon ca dëkk bu ñuy wax Karma ca Burkinaa Faaso. Ñaari ayu-bés ginnaw bi bóom gi amee, àddina sépp a ngi wéy di laaj ana kan moo sañ a def jëf ju ñaaw joojule. Bu dee ne Nguurug Burkinaa Faaso gi uubbee ag luññut itam, terewul, am ñu ko cay joxoñ baaraamu tuuma.
Bóomug Karma gee ngi xewe ca bëj-gànnaaru réewum Burkinaa Faaso, ci diiwaanub Waahiguya. Waññees na fa, lu mu gàtt gàtt, 150i doom-aadama yoy, rey nañu leen ca Karma ak ca yeneen dëkk yi ko wër. Dafa di, askan wa fay yeewoon lañ dajale cib béréb, bóom leen.
« Ci sunu jonnug tey, waññi nanu luy tollook 150i néew ci bii diwaan. Te bu nu fàtte ni am na ci yeneen dëkk yoo xam ni mënagunu cee wax, nde amaguñ ciy xibaar. Waaye, noo ngi nekk di ko topp. » (Daawuda Jàllo, fara-caytug mbootaay miy xeex jalget yoon ak toroxal i askan)
Jéyya jii nag, bokk na ci jéyya yi gën a metti yi gaaragum réewum Burkinaa, bi fa rëtëlkat yi ganesee ca atum 2015 ba tey. Bees sukkandikoo, ba tey, ci limub ONG yi, boobook léegi 10i junniy doom-aadama ñàkk nañu ci seen i bakkan.
Li doy waar ci bóomug Karma gi nag mooy ne, lees ciy joxoñ Baaraamub tuuma ñii di sóobarey Nguur ga. Aji-raw yi jot a wax setaluñu leen ci wenn yoon. Nde, ñi doon amal bóom gi colka sóobarey làrme bi lañu ame ba ñu foogoon leen ko laata jëyya ji di am.
« Li nu dal fii ci karma, nun sax xamunu lu mu doon. Bi fi làrme bi agsee ci Alxames 20 awril ci suba si, ay 7h30, dëkk bépp a génn wër leen di leen teertu. Ñu ngi doon i nit ñu niroole colin yu ñuul. Am na ci ñu sol i tëni yu nëtëx. Ñenn ñaa ngi sol i mbaxana, ñeneen ñi seen i bëtt kott di feeñ. Ñu yéeg ciy « pick-up » ak i moto. Ñenn ñi Jula lañu doon wax ñeneen ñi moore. »
Li tax ba xel gën a ñaaw ci sóobarey Nguur gi mooy bi reykat yi agsee ca dëkk ba, laaj nañu askan wa lu waral ñu des fa te yeneen dëkk yi dem seen yoon. Bees sukkandikoo ba tey ci seede yi, seen tontu moo doonoon ni « rëtëlkat yi sàkkuwuñu ci ñoom ñu jóge fa nees ko sàkkoo ci yeneen dëkk yi, moo tax ñu bañ a dem, bàyyi seen i suuf ». Liñ leen ci tegal mooy « ndegam rëtëlkat yi ngeen gën a ragal, dinanu leen def ni rëtëlkat yi di doxaleek yeen ». Rax-ci-dolli, bóom gaa ngi am juróomi fan ginnaaw bi rëtalkat yi amale cong ca gox ba. Ñeenti sóobare ñàkkoon ci seen i bakkan ak fanweer ak ñeenti nit yu dogu woon di leen jàppale ci xeex bi.
Fii mu nekk, àddina sépp a ngi koy coow, rawatinaa fii ci kembarug Afrig. Umaru Siisoko Mbaalo, di Njiitu réewum Gine Bisaawo li jiite jamono yii CEDEAO, yékkati na ciy kàddu ba tudd baatu « génocide », maanaam faagaagal xeet. Waaye, Ibraahima Taraawore mi jiite réew ma jamono yii delsi na ci ci waxtaan wu yaatu wu mu doon amal ci alxames ji. Ma ngay xamleet ni luññut gaa ngi ñuy amal. Kon na ñépp xaar mu jeex ba xam li muy feeñal moo gën ñuy gaawantu di wax lu amul ak di yàq derub làrme bi. Teg na ci yit ay kàddu ngir ñaawlu farandoo gi am ci àddina si te ñu jóge ko xeex réewum Burkinaa. Ndax li mu jël ndogalu lëkkalook ñeneen ngir xeex rëtëlkat yi. Ñu ci bare sax nanguwuñu leen a jaay i ngànnaay ak i jumtukaay.
Rëtëlkat yee leen bóom walla sóobarey Nguur ga lañu ? Li ci kanam rawul i bët.