COOWAL KOPPARI QATAAR YI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Atum 2019 lañu jëkkoon a dégg jokkalanteg koppar gu dox diggante kërug lijjanti  gu nekke fa Qataar, Tullow Oil,  ak njiitul Pastef li, Usmaan Sonko. Maanaam, ñoom ñoo ko ngemb. Kër googu nag, setaloon na meeru Sigicoor bi ca coow loola. La ca yéeme kay mooy, gaa ña yékkati woon tuuma yooya ak kibaaraan ya ko siiwaloon ñépp, dara fekku leen ca. Kopparal googu juraat na tey coow ci géewu pólitig gi, donte ne sax waa Pastef moom seen wax bariwu ci. Ñi dekkalaat wax jooju mooy Dépite Bennoo Bokk Yaakaar bii di Mataar Jóob nga xam ne moo ko jibal ca Ngomblaan ga, ak Séex Yérim Sekk mi ko dëggal ca jotaay ba mu doon amal ca 7tv.

Du guleet ñuy nemmeeku xeetu coow lu ni mel ci géewu pólitig gi. Waaye, li ci ëpp, ci ndoddu Usmaan Sonko lay tegu. Moom Mataar Jóob nee na Usmaan Sonko dafa digoon gaa ñooñu nga xam ne doxuñu ci dara lu leer ne, bu jëlee réew mi, dina saytuwaat pas-pas yi. Nee ñu, dañ ko daan dugalal xaalis bu takku. Bi gaa ñooñu demee ba xam ne léegi mënatul a nekk lawax ñu koy tëkku moom ak ug njabootam. Mu bind bataaxal Njiitu réew mi ngir mu aar ko moom ak ug njabootam. Kon, yëf yi yematul ci jokkalante Usmaan Sonko ak Saa-Qataar yi waaye, mi ngi sàkku ndimbal ci Njiitu réew mi ngir mu jàppale ko ci wàllu kaaraange.

Séex Yérim Sekk moom, yemul ci ne kopparal gi lu wér. Dafa wax nu limu xaalis bi tollu. Nee na, xaalis bi tollu na ci ñaar-fukki miliyoŋ ci ay dolaar. Maanaam, fukki miliyaar ak ñaar ci sunuy koppar. Mu jàpp ne li war ci coow li mooy ñu saytu ko ba noppi indi ci ay leeral. Ndax, ciy waxam, coow loolu, yéenekaay Farãs bii di Le Canard Enchainé moo ci jëkkk a àddu ci weeru suwe wii weesu. Li mat a laaj kay mooy lan moo tax boobaak léegi Nguuru Senegaal yéyul yàbbi ci tuuma yu doye waar nii, rawatina nag ñu koy teg ci ndoddu ki ëpp doole ci kujje gi. Dafa di, li coow li di bari yépp, atum 2019 ak léegi, ay firnde yuy dëggal loolu la kenn tegul bët. Mag moom kenn du yem ci wax ko dëgg danga ko koy won.

Ba tax na, jamono jii, ñu bare jàppee ko ay waxi naxasaxandaŋ. Ay wax yoo xam ne seen jubluwaay yàq der kese la. Noonu la ame tamit ñeneen ñu ci bëgg lu leer. Moo tax, taskatu xibaar bii di Paap Aale Ñaŋ bind ab bataaxal ci turu askanu Senegaal jébbal ko Emiiru Qataar ngir ay leeral ci ñaar-fukki miliyoŋi dolaar yi Qataar jox Usmaan Sonko. Li ko waral mooy ne dañu ne koppar yooyu jubluwaay bi du lenn lu dul yee fitna ci réew mi ak ger sërin si ni ko yéenekaayu Farãs bi waxee. Mu jàpp ne yoon la askanu Senegaal xam li laxasu ci jokkalante googu ñuy wax seen diggante ak Njiitul Pastef li. Bu dee dëgg la walla ay sosi neen la. Dëgg moom, genn la mën a doon. Ba tax, gémmiñ moom bu waxul dëgg rekk, wax safaan wa.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj