COOWAL MUURAAY CI DAARA YI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Coowal muuraay gi lëmbeeti na réewum Senegaal.  Kàddu yi elimaanu jëwriñ yi yékkati woon, keroog fa xew-xewu “concours général” bi, ñoo waral coow li. Dafa waxoon ne, Senegal du Farãs. Kenn waru fi tere muuraay ci daara yi. Kàddu yooyoo naqari làbbe  Àndere Latiir Njaay, mu bind ab bataaxal bu ñagas ngir tontu Usmaan Sonko. Bataaxal boobu nag moo xamb taal bi.

Cig pàttali, talaata, 30i pani sulet 2024 lañu doon sargal ndongo yi dàq jàng fi réew mi, te jot a ràññeeku ci kàtteg “Concours général”. Grand tthéâtre national la xew mi doon ame. Keroog nag, bés boobu, la elimaanu jëwriñ yi àddu woon ci wàllu muuraay bob, lenn ci daaray réew mi doon nañ ko tere lu yàggul dara. Ba mu waxee ba noppi nag, coow juddoo na ca. Dafa di, du waxam ji boppam moo indi coow li. Waaye, bataaxal bi ko làbbe bi tontoo moo waral coow lépp. Nde, moom Usmaan Sonko, kàddu yii toftalu la waxoon :

Am na loo xam ne dootuñu ko mën a nangu ci réew mu mel ni Senegaal. Gis nga, boo demee ci tubaab yi, loo wax ñu ni la sunu xeetu dundIin. Ndax, ñoom dañoo am seen dundiIn, dëggu ci. Moom lañu jàpp ne moom lañuy saytu donte, [nun] ànduñook seen xeetu doxaliin woowu ñoom. Waaye, seen dëkk la, ñoo ko moom. Ñu jàpp ne seen doxaliin lañuy saytu. Ba tax, tey, xale bu jigéen bu jël fulaar teg ci boppam, ne day dem jàngi ca lekkoolu Farãs, ñu ni ko doo dugg ci lekkool bi. Su ñu ko defee seen réew, naqarlu nañu ko. Waaye, am nañu sañ-sañ bi ci ñoo xam ne, dañoo woote demokaraasi ak péexte ak jéllale. Loolu nag, lañu mënatul a nangu Senegaal, ak lekkool bu mu mën di doon. Jàpp ne nit du dugg ci lekkool bi, du fi jànge ndax, am na fulaar bu mu teg ci boppam. Loolu du yoon. Sunu kilifteef la, xale yépp lañu yemale. Ki teg fulaar ak ki tegul fulaar, gënalantewuñu. Ndax, kii teg na fulaar walla tegu ko, tànneef la. Waaye, ñoom ñépp lañu war a yemale.”

Kàddoom yii nag ñoo merloo làbbe Àndere Latiir Njaay, mu daas xalimaam, tontu ko lu forox.  Moom làbbe bi, dafa gis ne kàdduy Usmaan Sonko yi tegginewuñ. Ci biir bataaxalam bi, mi ngi ciy wax sax ne, moom, ragalul muuraay. Dafa bind, ne :

Saytaane tiitaluma. Kon lu tax may ragal muuraay ? Lekkoolu “privée catholique” day yar ci jox cér keneen, ci cofeel, ci jàmm, ci xel mu sell. Kon, lan walla nan rekk la mënee ragal muuraay ?”

Fii nag, lënt am na fi. Nde, xameesul lu wund wax ji. Ndax kat, kàdduy elimaanu jëwriñ yi ci càrtug biir daara yi lay dellu. Waaye, waxul wenn yoon ak jàngu bi. Moo tax kàdduy làbbe bi jaaxal ñu bari. Waaye, moom sax daa yemul foofu kese. Bi mu jógee ci loolu, mi ngi laaj elimaanu jëwriñ ci kàddu yi mu yékkati, ndax, “kàddu yooyu ay tëkku la walla woote la ci ab xare ? Duma ci mën a tontu. Yow miy aji-bind ji kepp a ci mën a tontu. Yaakaar naa ne du lii mooy li tënk naal bi ak DPG  bi ñépp di xaar ni dellusig Godot !”

Mi ngi sàkkooti  ci Usmaan Sonko mu dellosiwaat xelam. Maanaam, mu seetaat ni muy waxe ak lekkool yooyu. Ndaxte, ay càmmeef lañu. Loolu la naan :

Lekkoolu “privée catholique” yi,  niki yeneen lekkool “privées” yépp, ay càmmeef lañu. Te, kenn du ŋàññi ag càmmeef ci mbooloo. Kenn du wax ak ug càmmeef ak ay tëkku. Demal jàngi lan mooy waxtaan ak ay càmmeef. Bés ak béréb bu ñu jagleel xarañte ak xam-xam bu mel ni “concours général”warul nekk liy tax nga génnee kàddu yu ni mel. Mel ni dangaa bëggoon yàbbi lanc boo yàggoon a sex.

Moom yemul ci ne elimaanu jëwriñ yi day tëkku càmmeef yi rekk. Waaye, dafa jàpp ne kàddu yi mu yékkati keroog yàggoon na leen denc. Da doon xaar rekk ba am béréb bu mu leen mën a waxe. Moo tax, mu gaawantu keroog, génnee leen fa ndaje mooma. Moom nag, mi ngi koy xamal ne :

Jàngu bi ragalul muuraay ? Muuraay dafa bokk ci moomeelam, ci colam. Bi mu xamee muuraay ak léegi ëpp na ñaari junniy at laata diine yu bari. (…) Bul jaawale xeex bi. Xeexu pólitig, du xeexu Yàlla, du tamit xeex ngir Yàlla. (…) Dañu leen a fal ngir xeex dund bu jafe bi, ndóol gi, xéyu ndaw ñi. Waaye, du xeex ngir Yàlla. (…) Yenn làmmiñ yi, yenn loxo yi ak yenn tubéy yi duñu bokk ngir amal xeexi Yàlla yi. Na ñeneen amal xeexu muuraay ak Yàlla miy gis lépp, dina xàmmee ay ñoñam.”

Kii di Mustafaa Mamba Giraasi, di jëwriñ ji ñu dénk njàng mu suufe mi, rafetluwul kàddu yooyu làbbe bi yékkati. Ndax, dafa jàpp ne nandul li elimaanu jëwriñ yi wax. Te, loolu warul woon a nekk taxawaayam. Moo tax, mu wax ko ne :

Làbbe Àndere Latiir Njaay, li mu wax noonu dama ko ñaawlu. Ndax, moom dafa wax waxu jàngu. Wone na ne dégluwul, yàkkamti na. Xéy-na déglu na ay saabalukaay, benn benn saabalukaay boog, xéy-na déglu na yenn way-pólitig mu gaawantu. Waaye, làbbe du gaawantu, làbbe day dal, làbbe dangay wax ak di jëf ngir di rafetal. (…) Làbbe wax na leneen lu woroo ak elimaanu jëwriñ yi waxoon. Li elimaanu jëwriñ yi wax daf ko war a dëggal. Mooy ne xale kercen bi dañu ko war a aar, xale jullit bi dañu ko war a aar. Xale jullit bu dul muuru dañu ko war a aar. Loolu la waroon a wax. Waaye, wax jii dafa dëgër lool.”

Kon, li am ba des mooy coowal muuraay gi ci yenn lekkool yi moom du lu bees. Xanaa kay, dañu naan ab góom la bu ñu xolliwaat la rekk. Te, li ko xolli du lu moy kàdduy Usmaan Sonko yi ngir xamal askanu Senegaal ne loolu dootuñu ko nangul benn lekkool. Li mat a laaj kay, mooy ndax, mbir mi ci ay kàddu kepp lay yem walla ay jëf dina ci topp ?

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj