Juróomi fan kepp a des balaa ndajem ndeyu àtte miy siiwal limug lawax yiy bokk ci wotey 2024 yi. Jamono jii nag, coow laa ngi ne na kurr ñeel nasiyonaalite Kariim Meysa Wàdd. Dafa di, yoonu réew mi day tere boroom ñaari nasiyonaalite yi jiite réew mi. Te, dafa am ñu njort ne moom doomu, Ablaay Wàdd jiy lawaxu PDS, dafa amandoo nasiyonaalite Senegaal ak bu Farãs. Dëgg la am du dëgg, PDS génne na ab yégle ngir, ci seen i wax, teggi tuuma yoy, ci neen la tege.
Àjjuma jii weesu la ndajem ndeyu àtte mi génnee yégle, biral limu lawax yi jàll ci caytug baayale gi. Looloo sulliwaat coowal ñaari nasiyonaalite Kariim Wàdd yi. Maanaam, moom yemul ci nekk Saa-Senegaal kepp. Dafa nekkaale Saa-Farãs itam. Te, ci juróom-ñeenti sàrt yu lawax bu nekk war a matale ngir bokk, nasiyonaalite bi ci la bokk.
Mu mel ni coow loolu du lu bees ci géewu pólitig gi. Ndax, ca atum 2016, ñetti at laata wotey 2019 ya, lañu ko njëkkoon a yékkati. Kii di Bënuwaa Sàmbu mi ñu dénkoon wàlluw wote yi ci làngug Njiitu réew mi moo waraloon coow li. Nde, moom da doon sàkku ñu def ci ndeyu àtte ji sàrt boo xam ne képp ku am beneen nasiyonaalite bu wuteek bu Senegaal, nga far beneen bi juróomi at lu jiitu wote yi. Te, ki taxoon muy wax loolu du kenn ku dul mennum Kariim Wàdd mi. Mu juroon coow lu bari nag. Ku ci mel ni Idiriisa Sekk, fare woon ci kujje gi, daf jàppoon ne loolu, ay pexey pólitig kepp.
Waaye, coow loolu yemul woon ci géewu pólitig gi kepp. Ndax, boroom xam-xam yi sax duggoon nañu ci. Muy ku ci mel ni Faatu Sow Saar ak Baabakar Justin Njaay. Ñoom, dañoo jàpp ne loolu warut a jur coow ak fi jamono ji tollu. Senegaal ay xeet yu wute ñoo fi nekk. Te, loolu sax, lu baax la war a nekk ci ab Saa-Senegaal. Waaye, waru koo mën a jural benn coono. Ndax, amul kenn kuy tànnal sa bopp réew mi ngay juddoo.
Ginnaaw bi ñu sulliwaatee coow loolu, ci la lëkkatoom gii mu dippe “Coalition Kariim 2024” ne duñu bàyyi mu sedd. Ci lañu génnee ab yégle ngir tontu gaa ñi. Ndax, nee ñu, gaa ñi seen jubluwaay mooy xajamal wayndarew Kariim Maysa Wàdd. Te, ñu neeti, coow loolu ndajem ndeyu àtte mi leeral na ko. Ñi koy sulli bëgguñu lenn lu dul yàqal seen lawax bi. Rax-ci-dolli, loolu ay mbiri boddikonte xeet kepp la. Te, xeetu jëf yooyu mënut a yàq dara ci li ñu jot a sumb. Du def lu dul gën a dëgëral seen taxawaay.
Waaye, Ceerno Alasaan Sàll moom, gisewul noonu mbir mi. Nee na, luññutu yi ñu jot a def, moom Kariim, ba léegi, yor na këyit yiy firndeel ne doomu Farãs la. Te, loolu ndeyu àtte réew mi daf koy bañ. Te, nee na duñu seetaan wenn yoon ñuy salfaañe sàrt yooyu.
Kon, day mel ni, ba tey, am na luy ñuul ci soow mi. Waaye, ak lu ci mën di am, fii ak ub diir yëf yi dina leer nàññ. Ndax, ndajem ndeyu àtte mi dina génnee limub ñiy bokk ci wote yi. Su boobaa dees na xam ndax Kariim ci ñaari réew yi la bokk ba tey am déet. Nde, loolu dafa bokk ci sàrt yi nga xam ne dañu leen a war a saytu ngir lawax bi mën a bokk.