COOWAL ÑETTEELU MOOME GI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Lu tollu ci fukki weer ak ñeent kepp a des ci wotey 2024. Waaye, coowal ñetteelu moome gi moom taqarnaase na xaat ci réew mépp. Ñii naan dina ko def, ñee naan du ko def. Ñile ne yoon may na ko ko. Ñale ne déet, yoon mayu ko ko. Moone de, ndeyu-mbill ji ci boppam àddu woon na ci laata ñu koy falaat atum 2019 ak ginnaaw bi ñu ko falaatee. Booba ak léegi nag, coow li bari na ci lool. Ba tey, taxul mu yéy, yàbbi ci. Mu mel ni, gaa ñi nekke ci làngug pólitig gi, rawatina ñi fare ci kujje gi, dañoo bëgg mu xamal saa-senegaal yi ci teel ne du bokk ca wote yooya. Waaye, dafa mel ni yëgalul yaram wi li gaa ñiy wax. Mooy li wolof naan, “ngaaxi mbottu mënt a tere gaynde naan”. Ndax, moo yor cëggal-guyam, saa bu nammee leeral mbir mi rekk, dina leer. Te, tungune du teew ñuy nataal ci ëkk. Li mat a laaj kay mooy lan moo waral taxawaay yu wute ci mbir moomu ?

Afrig sowu-jant nag dafa baaxoo di am coowal ñetteelu moome. Donte ne sax, ñu bari ci ñoom xam nañu li ci ndeyu-àtte yi wax. Du tere, ñu topp seen i bëgg-bëgg ak yu seen i ñoñ ba lor seen uw askan. Askan wi tamit bu demee ba sës rekk fippu, jàmmaarloo ak ñoom ba mu am sax ñu ciy ñàkke seen i bakkan. Dina am tamit ñu ciy jële ay gaañu-gaañu. Moo tax, fii ci Senegaal, kurél yu bari tàmbali di artu Njiitu réew mi ngir mu settantal ndogal li mu nar a jël ci ñetteelu moome gi. Mënees na cee jël misaalu kurélug way-momeel yi nga xam ne, ñi ngi artu naan jàmm a gën ñetteelug moome. Ndax kat, ku ndóbbin rey sa maam, foo gise lu ñuul daw. Loolu la kii di Keledoor Seen di xamle ci kàddoom yii :

“Jàmm lanu woote, Yal na Yàlla may ñi féete ci pólitig bi maanaam Nguur geek Kujje gi ba ñu am xelu soppi seen wuute gis-gis yi leen di jotale, dëppoo ci genn kàddu ngir njariñal réew mi. Boo gisee ñi fi wax ñépp dañu tiit yëngu-yëngu am ci dëkk bi ndax, li fi jot a xew 1988 ak 2021. Léegi, wii yoon, Yal nanu Yàllu may dal gu ñu gatandoo loolu ndegam ak lu mën di xew dinanu daje donte sax ginnaaw ab dóom la. Kon nag, nanu daje sàkku jàmm bala dara di tàkk, loolu moo wund waxtaan wi ak taxawaay bi.” 

Moone Njiitu réew mi Maki Sàll jotoon na cee àddu laata ñu koy falaat ca atum 2019 ngir xamal askan wi bu ñu ko falaatee, loolu mooy nekk palam gu mujj. Nii la ko waxe woon : 

“Fan yii yépp, dégg naa ay coow, muy loo xam ne daf ma jaaxal. Ndax, day mel ni lu xiinul rekk xëy taw. Wax joo xam ne kenn xamul fu mu jóge ak lan moo ko tax a jóg. 2016, man maa sàkku askanu Senegaal nu xoolaat ndeyu-àtte bi. Dama ne mbiru moome yi dafa war a jeex tàkk, ñépp jàpp ne réew mi kenn mënatu fi toog lu ëpp ñaari moome, dañu ko bind mu leer nàññ. Xanaa kay ku jàng tubaab boo ko firilee loolu war na ko xam. Man maa ngi ci sama genneelu moome, bu ci Yàlla àndee, 2019 lay jeex. Ci coobare sunu boroom ak bëgg-bëggi saa-senegaal yi, dinaa yeesalaat moome gi 2019, su booba man pare naa ci.”

Kàddu yooyu la yékkati woon laata ñu koy falaat ci atum 2019. Terewul ne, bi ñu ko dékkaatee waxu gi, fa la jaaraat. Ba ci at mii weesu ba ñi ko ci laajee, lii la ci tegal :

“Man dañ ma fal ci kóolute réew mi, kàddu gi nga wax am na ñu ko laaj laata ñu may fal 2018 2017, waa moom kañ lay pare. Ak lu mën di am bés bu wax jotee, dinaa wax. Wax jii ngay dégg nag, mënul a xumb a xumb ba ma wax ci. Li tax ma wax sama njaboot bu ñu ci wax mooy nun liggéey lañu nu sant. Mënuñu la fal defoo liggéey bi war ba pare ngay wax lu ñëwagul.”

 Kàddoom yooyu terewul saa-senegaal yi wéy di sàkku ay leeral ci mbir mi ngir taxawaay ak kàdduy ñenn ci ay ñoñam. Mu mel ni gaa ñi dañuy njort yëf yi am wax-waxeet. Bi mu ci mujjee àddu nag, daf leen a xamal ne laajug ñetteelu kay moom du doon waaw, du doon déet. Waaye, mbir yi yamul foofu ndax dafa am ay gis-gis yu wute ci li ndeyu-àtte bi wax. Ndax, dafa am ñu ne moo ngi ci ayam gu njëkk gu juróomi at yi, kon mën naa laajaat réew mi ci wote yii di ñëw. Am ñu ne ndeyu-àtte bi li mu wax mooy kenn mënul a am lu ëpp ñaari moome yu toftaloo. Kenn ci ñoom di Mansuur Fay bokk ci Nguur gi, lii la ci wax : 

“Wote nanu 2019 dénkaat Maki Sàll réew mi ngir moomeem gu njëkk gu juróomi at. Nit ñaa ngi wax ndax xamuñu, bii mooy kayam gu njëkk gu juróomi at.”

Mu mel ni kàddoom yooyu la kii di Maam Mbay Ñaŋ, bokk moom tamit ci Nguur gi, di dëggal ci kàddoom yii :

“Bi Njiitu réew mi bëggee wàññi kay gi ne da koy jële juróom-ñaari at yóbbu ko juróomi at, Ndajem ndeyu-àtte réew mi moo ne ko mënoo ko. Te, kay gii kenn du ko limaale ci li nekk ci ndeyu-àtte yi. Li may wax nii moom la ay Sonko ak Bàrtelemi sukkandiku xoon di wax bu ñu ragalee wax ne këyit boobu am na dañuy pólitig rekk.”  

Aminata Ture moom, ciy kàddoom, nee na li ko féewale ak Njiitu réew mi mbirum ñetteelu moomee ci raw. Ndax, mësul a ànd ci loolu donte ne sax li mu ko ñàkk a def njiiteefu Ngomblaan gi metti na ko. Mimi ne :

“Bu fekkoon ne doxuma ci ngëm-ngëm, damay def ni ñépp ñiy wax ne dafa war a def ñetteelu moome. Dégg naa farañse, dégg naa wolof. Kon bu boobaa ma wër tele yi di ko wax. Waaye, du sama ngëm-ngëm. Su fekkoon looloo ma xañ Njiiteefu Ngomblaan ga dina ma xañ lu ne ndax du lu ma gëm. Damaa nekkoon ci sama liggéey ca bitim-réew di xeexal ab lawax buy xeex ñetteelu moome (…). 2016 dama dox ay jéego yu rëy ci referandum bi, Garaa Yoof dama fa kàmpaañ, nu jiitu ca pekk yépp. Dinanu toog juróom-benni at ci ginnaaw, ñuy xamal nit ñi naan juróomi at lañu leen doon wax, kon dañu leen doon nax. Te, nun ñépp nu leeraloon ko. (…). Ñetteelu kay moo sos sunu ànd, 2012 fukki bakkan ak benn rot ci. Nu war a ñëwaat fukki at ginnaaw loolu, noo ngi gis ni mbir yi di deme tàmbalee ko ci jëwriñ ji ñu dénk yoon (…). Juróom-ñaari at ak juróomi at, loolu du ñaari moome walla ? Ndeyu-àtte yi waxul kenn mënul a def ñaari moome yu juróomi at yu toftaloo. Ñaari moome yu toftaloo la wax”

Loolu nag, moo wund coow lu bari li ci réew mi. Ku nekk di laaj nan la mbir yi nar a deme. Ndax Njiitu réew mi day laajaat baatu askan wi walla day yem ci li ko yoon may walla ? Mbir moomu nag moo jur jiixi-jaaxa ci ñu bari ci askan wi. Waaye, kii di Nguuda Mbuup di am jàngalekat ca daara ju kowe ja nekke ca Ndakaaru moom nee na : 

“2016 dañu doon wax mbiri diir bi waxuñu woon limub yeesal gi, jële juróom-ñaar yóbbu juróom . Bi ci topp, ñépp ñi mu àndaloon ba ci moom dañu ne juróom-ñaari yi at ci la bokk (…). Waaye, Usmaan Sonko li muy wax du yoon (droit), man “constitutionnaliste” laa. Usmaan Sonko wax ne mën na, Maki Sàll moom ci boppam mu waxal ko boppam walla keneen ak keneen du tax mu mën a nekk…”

Coowal ñetteelu moome gi nag, ma ngay wéy ba tey ci jotaay yi. Waaye, ñu bari ci askan wi dafa mel ni loolu doyuleen. Dañoo bëgg a teel a xam taxawaayam ci wote yii di ñëw. Ak lu ci mën di am yoon wu nit jaaroon dee, bu dekkee war koo teggi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj