COOWAL NJÀNG MU KOWE MI : UCAD TIJJEEGUL I BUNTAM

Yeneen i xët

Aji bind ji

Jàngune Séex Anta Jóob bu ndakaaru tijjeegul i buntam. Musaa balde, jëwriñ ji ñu dénk njàngale mu kowe mi, gëtu beek càkkeef yi, ànd na ci ndogalu njiit ya donte ni mi ngi leen di ñaax ci ñu wéyal waxtaan yi jëm ci njàngale meek teewaayu ndongo yi balaa yàgg.

Démb ci àjjuma ji la Musaa Balde, jëwriñ ji ñu dénk njàng mu kowe mi, gëstu beek càkkeef yi, doog a àddu ñeel jafe-jafey jàngune Séex Anta Jóob bi të tijji boobu ba léegi. Fekk mu teewoon ci ci janook taskati xibaar yi mbooloo way-jàngune yu lëkketoo bennoo bokk yaakaar (réseau des universitaires de la coalition Bennoo bokk yaakaar) doon amal.

Ginnaaw bi mu jëlee kàddu gi, jëwriñ ji joxe na jàngat li mu am ci tolluwaayu jàngune bi. Naka noonu, muy sàkku ci njiitu jàngune ba ak kõsey akademig ba ñu wéyal waxtaan yi ngir mën a tàbbi ci njàngale meek teewaayu ndogo yi. Waaye nag, tey ci tey, kenn mënu koo tijji ndax matukaay yi ñeel kaaraange gi dajeegul. Terewul dina jël i matukaay yu wér ngir ndongo yi mën a teew ci yeneen bërëb ba mën a def seen i kàtte.

Naka noonu, jëwriñ ji Musaa Balde daldi nangul kõsey bi seen ndogalu àggale atum 2022-2023 bi jaarele ko ci xarala yi. Nde amul lenn lu ñuy ga waa UCAD ak kõseil akademig bi.

« kõsey akademig bi ak UCAD dañ am seen i sañ-sañi bopp. Nun danu leen di gunge rekk ngir ñu mën a matale ndogal yi ñuy jël. Kon ndegam jël nañu ndigal lii, mën nañ yaakaar njàppale ci jëwriñ ji yor njàng mu kowe mi ngir jooxe ndogal yi. »

« lees jot a dund wone na ni bees defee ni mu waree njàngale mi ñuy jaarale ci xarala yi, moom ak teewaay bi ñoo yam ci baaxaay. »

Jëwriñ ji jàpp na sax ni njàngale mi ci xarala yi warul yam rekk ci jëfandiku négandiku. Dafa war a doon lees war a saxal muy ànd ak teewaay yi. nde njureef yees ci jot a am wone nañ i ngëneelam.

Bir na ñu ne njàngale mi ñuy jaarale ci xarala yi warul doon rekk pexey négandiku, waaye dafa war a doon lees di sóoraale ngir mën a dékku yokkute limub ndongo yi. looloo tax ba ñu fas yéene taxawal matukaay yi ñeel njàngale miy dox ci ñaari fànn yi (ci teewaay ak ci jàppandalu xarala yi) ngir tàmbali sémbub njàgalem réew mi jaarale ko ci xarala yi, mu ànd ak njàngale mi am ci tewwaayu ndongo yi »

Ci pàttali, kilifay jàngune ba dañ tëjoon bunt ya ginnaaw coow yi fa amoon ak yàqu-yàqu yi mu fa juróon ci weeru suwe 2023 bi. Bi lekkool yi waree tijji, ñu dellu jël ndogalu yeggali at mi ci ñàkk teewaayu ndongo yi, jaarale njàngale mi ci xarala yi. Jamono yii nag, Bu weesoo ndongo yi ko lànkoon, jàngalekat yu Saes yi jël nañ ndogalu dakkal njàngale mi ñu jotoon na tàmbali ci xarala yi ngir fésal seen ñàkk ànd ci ndogal li ak a sàkku ci kilifa yi ñu tijji jàngune bi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj