COSCE (Collectif des Organisations de la Société Civile pour les Elections) ag mbootaay la gu boole ay kuréli way-moomeel ñeel wote yi. Mbootaay googu moo génnee démb ab yégle ngir ñaawlu anam yi ñu tabbee waa CENA. Ndax, dañoo jàpp ne Njiitu réew mi dafa salfaañe ay sàrt yi tënk tabbiin wi ñeel CENA. Cig pàttali, njeexitalu weeru oktoobar la waa CENA santoon waa DGE ne leen ñu jox Usmaan Sonko ay xobi baayaleem na mu gën a gaawe. Ndekete yëf yi moom du deme noona. Ca lañu leen dàqee, ñoom, na mu gën a gaawe balay sax ayu-bés bi di jeex. Anam yi ñu leen dàqe ak yi ñu fale ñii leen wuutu moo wund yégle bi.
Ñetti fan ci weer wii ñu nekk la Njiitu réew mi génnee ab ndogal ne jële na fi Duudu Ndiir. Waa COSCE moom gis ne loolu jekkul jaaduwul. Ndax, CENA ñi ngi ko sos ci fukki fan ak benn ci weeru me atum 2005. Liggéeyam mooy mu saytu wote yi ba ñu jaar yoon. CENA nag, fukki nit ak ñaar ña fay nekk dañu leen di tabb jaare ko ci ndogal lu tukkee ca Njiitu réew ma. Waaye, loolu kese doyul. Ndax, nee ñu, bala muy def loolu ñooñu muy tabb nañ doon ñu moom seen bopp, jub, dëggu, màndu bañ a far fenn te nekk ay doomi Senegaal.
Rax-ci-dolli, ñooñu balaa mu leen di tabb, daf ci war a waxtaan ak yenn ci ay mbootaay, kuréli layookat yi, jàngalekati daara yu kowe yi, ñiy sàmm àq ak yelleefi doom-Aadama yi ak ñi seen xam-xam màcc ci wàllu wax. Te, ñi ñuy tabb tamit juróom-benni at lañuy moome ñu koy yeesal ci ñetti at yi. Waaye, ñoom waa COSCE bi ñu settantalee bu baax, gis nañu ne Njiitu réew mi sàmmontewul ak yenn ci sàrt yooyu ñu lim. Muy bu ci mel ni gëddaal càrt bi koy digal mu waxtaan ak yenn kurél yi. Tànn ay nit ñu moom seen bopp, màndu ba noppi ñàkk péete, tëdde njaaxanaay. Sàmmonte ak moome gi nga xam ne juróom-benni at la ñu war ko yeesal ci ñett yi.
Mbooleem li ñu lim ci ay ndëngte ci ni ñu tànnee ña war a nekk fa ñu war a saytoo wote ya teey na xelu waa COSCE. Ba tax ñoom ñu jàpp ne ak ni CENA amee njariñ ci wote yi xeetu doxalin wu ni mel wii mën na ñàkkal faayda yenn ci bànqaas yi ëpp solo ci caytug wote yi. Looloo tax nag ñuy woo Njiitu réew mi mu rocci ndogal boobu ca na mu gën a gaawe, wuutale ko ak beneen boo xam ne sàmmonte na ak sàrt yi ñuy tabbee ca ëtt booba. Ndax kat, jàpp nañu ne loolu kepp a mën a tax ñu am ay wote yu dal, leer te jaar yoon. Dafa di, nit moom mënoo bëgg dara, bëgg safaan wa. Maanaam Yoon moom ñépp la fi war a nekkal. Te, dëgg moom genn kese la mën a doon.