Ab “Coup d’Etat” moo naroon a am fa Réewum Kóngo Demokaraatig (RDC). Démb, ci boori ñeenti waxtu jàpp juróomi waxtu ci njël la mbir am. Kilifay làrme ba ñoo siiwal xibaar bi. Waaye, nee ñu, ñu bari dégg nañ soxi fetel yi. Mu doon mbir mu doy waar lool. Nde, am na ñu ci jële ay gaañ-gaañu. Te, bees sukkandikoo ci Senego, am na ñetti bakkan yu ci rot. Muy ñaari takk-der ak kenn ci sàmbaa-bóoy yi sooke mbir mi. Waaye, dafa mel ni ba tey mbir mi sotteegul. Waaye, cong mi moom xaw naa teey xelu ñenn ñu. Te, lenn waralu ko lu dul ni mu demee.
Du guléet ñuy dégg coowal “Coup d’Etat” fi Afrig. Waaye, jamono yii moom daf cee raw. Ndax, diggante 2020 ak tey, am na lu tollu ci juróomi réew yoo xam ne “Coup d’Etat” am na fa. Muy fu ci mel ni Gine, Mali, Burkinaa Faaso, Niseer ak Gaboŋ. Li xew nii démb fa RDC (République Démocratique du Congo), firnde la ci. Ndax, seen mébét moom du lenn lu moy ñu foqati Nguur ga ci loxoy Njiitu réew ma.
Juróomi weer ak lu teg ginnaaw bi ñu falaatee Félix Tshisekedi, coow li newaat na kurr fa RDC. Nde, démb ci suba dañoo nemmeeku ay sox fa Kinsasaa, fa koñ bii di Gombe. Jàmmaarloo yooyu ña nga ame fa boori këru Vital Kamerhe, kenn ci jegeñaaley Félix Tshisekedi. Rax-ci-dolli, mooy tof-njiitu elimaanu jëwriñ yi. Te, béréb boobu, fa la ñu bari ci kilifay Nguur gi ak Càmmeef yi di nekk. Ñu jóge foofu dëgmali màkkaanu Njiitu réew ma, Félix Tshisekedi. Lañu fa def nag moo teey xel. Ndax, nee ñu, dañoo dindi raaya ba nekk fa boor ba, def fa raaya bu Sayiir (Zaire) nekkoon fi turu RDC. Waaye, mel na ni sóobare yi yombalaluñu leen ko. Nde, jamono jii làlli nañu mbooleem pexe yi ñu laloon. Ki ko xamle mooy Seneraal Sylvain Ekenge, nga xam ne mooy ki yor baatu làrme bi (Porte-parole des Forces Armées de RDC).
Ginnaaw loolu nag, biral nañu ne cong mi du ay Saa-Kóngoo kesee ko amal. Ci seen i wax ba tey, am na ay doxandéem yu ci rax. Kon, mënees na jàpp ne, am na luy ñuul ci soow mi. Looloo tax, cong mi xaw a teey xelu ñenn ñi. Waaye, li ci kanam moom rawul i bët.