Li ñu doon laam-laamee démb ak barki-démb mi ngi bëgg a leer. Nde, ñu bari dañoo jàppoon ne ay naxembaay la walla ay xuppe doŋŋ. Ndekete yoo, mbir yi jéggi na foofu. Ki dëggal xibaar bi mooy jëwriñ Ibraayma Si mi nga xam ne, moom lañu dénk wàllug wér-gi-yaram. Ndax, xamle na ne jàngoroy Covid-19 bi dellusi na fi réew mi. Waaye, wii yoon moom, jógewul réewum Siin, jógewul it ci menn réewum tugal yi, Afrig walla Amerig. Kon, fan la jàngoro jooju war a jóge ?
Ajug ren jii mel na ni genn la ci aj yi. Bu dee ci lu yàggul dara, am na ay bakkan yu bari yu ci rot. Ren tamit, lim bu takku ci ay doomi-aadama faatu nañu ci. Ndax, ci li jot a rotagum ciy xibaar, lu tollu ci junni ak lu teg ci ay bakkan rot nañ ci. Ñépp di ñaan mu yem fi donte ne sax, mbir yi tàmbali naa taq suuf. Ndax, leneen laxasuwaat na ci aj gi. Mbasum Covid-19 mi fi amoon, wëroon daanaka àdduna wërngal-këpp. Mu nekkoon it, wopp goo xam ne, ñépp a ko ragaloon. Jàngoro jooju moo feeñaat ci réewum Senegaal.
Covid-19 bi nemmeeku nañu ko ci ñenn ci ujaaji Senegaal yi ñibbiseegum. Maanaam, ñi jóge fa Màkka. Jëwriñu wér-gi-yaram wi moom, daf ne ñoom dañoo jàppoon ne dee gu bari gi tàngoor wu metti wi kesee ko waraloon. Ndeke, mbir mi rax na. Ci lañu yokke seen matuwaayi caytu fa AIBD ci seen lëkkaloo ak waa IRESSEF (Institut de Recherche en Santé, de Surveillance Epidémiologique et de Formation). Bi ñu dooree seen liggéey boobu, ci lañu gisee ne ujaaj yi am na ab jàngoro bu nekk seen yaram. Ñoom, ñu koy dippe SARS-CoV-2.
Ci téeméer ak ñaar-fukk ak ñeenti ujaaj yi ñu defal caytu bi ñu naan TRD (Test de Diagnostic Rapide), juróom-ñaar-fukk ak juróom-ñett ci ñooñu ame nañu koronaa. Ngir bañ loolu gën a law ci biir-réew mi nag, ñoom ñi ñu dénk wàllug wér-gi-yaram, jot nañoo jël ay matuwaay. Benn ci yooyu, mooy caytug ujaaj yi jóge Màkka. Beneen bi, mooy takkug gafa yi (mask) booy jóge fa dalug fafalnaaw yi ak ci jamono bi nga nekke ci fafalnaaw bi. Bi ci topp, mooy bàyyi nganale yi ñuy defal ujaaj yi, rawatina ñi nga xam ne dañoo ame jàngoro ji. Bu ko defee, ñu mën a wattandiku dajaloo bi nga xam ne mën na koo tasaare. Yeneen yi, mooy jokkoo ak raglu bi la gën a jege saa yoo yëgee ci sa yaram benn ci màndarga yiy junj feebaru koroona. Bi ci mujj, mooy siiwalug bépp jafe-jafe boo ame saa boo ñibbisee. Ndax, ñu mën laa toppatoo ca na mu gën a gaawe.
Matuwaay yooyu, yenn la ci yi ñu jëlagum ngir fexe ba mbas mi bañ fee amaat. Moo tax, ci seen yégle bi ñu génnee, ñuy sàkku ci askan wi mu gën a ànd ak ug dal. Waaye tamit, ñu moytu bu baax. Nde, am mbas bañ fi amaat donte ne sax, bu yàgg ba tey, nee ñu Covid bi ñi ngi koy bàyyi xel, jógewu fi. Nde, li ñu fi dund ci atum 2020, kenn dootu ko gaaw a fàtte. Kon nag, ku ndóbbin rey sa maam, foo gis lu ñuul, dangaa war a daw.