CPI JÁPPLU NA BENYAMIN NETANYAHOU

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ëttu àttewaay bii di CPI (Cour Pénale Internationale, fa mbaxana doone benn fi àddina si) jàpplu na Benyamin Natanyahou. Muy ndogal lees ko gàll moom, Yoav Gallant ak Mohammed Deïf ñeel ay pekkey (crimes) xare ak yu ñu teg i doom-aadama.

Ci weeru me wi weesu, 24 me 2024, la Karim Xã (toppekat bu CPI) tàbbaloon ag càkkuteef ngir ñu teg loxo Benyamin Natanyahou (magum jëwriñ ju Càmmug Israayel) fépp fu mu mën a nekk fi àddina si. Boobook tay, moo ngi ci ñeenti weer yoy àttekat yi ñoo ngi doon saytu wayndare yees leen jébbal. Ginnaaw caytu googu nag, jàpp nañu ni am nay firnde yu xel mën a nangu ñu toppe magum jëwriñu Israayel ji lu jëm ci pekkey xare.

Naka noonu, ëttu àttewaay bu àddina si daldi na jël ndogalu teg loxo kii di Benyamin Natanyahou bàrki-démb ci alxames ji, 21 oktoobar 2024. Ndogal loolu, gàllaale nañu ko itam Yoav Gallant (Jëwriñ ja ñu dénkoon kaaraange ga) ak Mohammed Deïf (njiitu Hamas li ñu jàpp ni sax dee na ci xare bi donte ni gisuñu niiwam).

Benyamin Netanyahou ak Yoav Gallant nag, ñoo ngi leen di toppe pekkey xare, jëfandikoo ay pexey xiifal ci xare, faagaagal i doom-aadama, xoqatal ak yeneen i jëf yu jéggi dayo. Ñuy ay jëf yu dàqu yu ñu jàpp ni amal nañu leen li ko dale keroog 8i pani oktoobar 2024, ginnaaw bi rëtëlkat yu Hamas yi amalee cong fa Israayel.

Topp gi ñu leen di topp nag doon na ndogal lol, bi ñu sosee kurél gii di CPI ca atum 2002 ak tay, guléet mu gàllu ci njiit loo xam ne réewi tugal yi ñoo ko ngemb. Nde li ko jiitu, njiit yees fa daan topp yépp bokkuñu woon ci boroom doole yi ci àddina si bu weesoo Vladimir Poutine ak Mria Lvova-Belova (ay doomi réewum Risi).

Ginnaaw ndogal li nag, coow li mooy ndax 124i réew yi xaatimoon déggoo bi taxawal CPI noppi nañu ngir teg Benjamin Netanyahou loxo saa bu tegee tànkam ci seen i suuf, rawatina réewi tugal yi. Nde, xaajaloo nañu xaat seen biir donte ni Joseph Borrel mi jiite dipolomasi réewi tugal yi biral na ni dees war a sàmmonteek ndogali CPI. Réewum Etaasini mi gën a fés ci jàppale Israayel dàq naat ndogal li, donte ni moom xaatimul woon déggoo bi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj