DAAN NAÑU CHINA MALL

Yeneen i xët

Aji bind ji

Bi China Mall ubbeey buntam, saa-senegaal yi dañ ko tatafu xaat-xaat ndax bariwaayu njaay ma ak yombaayu njëg ya. China Mall, ab jaayuwaay bu mag la, maanaam ab “centre commercial” bob, ay saa-siin ñoo ko moom. Biir Ndakaaru, fa Mermoos, lañ ko ubbi, ca weeru màrs 2023. Fa ñu tabax jaayuwaay ba nag, bayaal bu yaatoo yaatu la woon, jege lool ja bi. Moo tax, ginnaaw ubbiteg béréb bi, coow lu baree ci toppoon. Ndax, nee ñu, boroomi China Mall sàmmontewuñu ak sàrt yi ñu tëral ci wàllu yaxantu. Gii Mariis Saañaa sax, ak waa FRAPP, àddu woon nañ ci, joxoñ Càmm gi, ngir mu indi ciy leeral. Waaye, booba, kenn faalewu ko woon. Dafa mel ni, nag, ci diggante bi, am na lu fi soppeeku. Nde, jëwriñu yaxantu gi, Abdu Kariim Fofana, jël na ndogalu daan China Mall.

Ñeenti weer ginnaaw bi China Mall ubbee, yat bi dal na ko. China Mall nag, sababoon na njàqare ci yaxantukati réew mi, ba ci sax doxandéem yi fiy liggéeye. Li ko waraloon mooy cuufeg njëg yi ñuy jaaye, wute lool te gën a yomb bees leen méngalee ak yeneen jaaykat yu ni mel. Looloo taxoon Gii Mariis Saaña ak i ñoñam teeloon a artu ngir ñu jële fi kër googu. Dafa di, China Mall, du yem rekk ci yàqal jaaykat yu ndaw-ndawaan yi seen liggéey, waaye dañu ci boolewaale salfaañe sàrt yi tënk ja bi. Looloo taxoon waa FRAPP doon leen jéebaane fépp ngir Nguur gi mu jóg ci China Mall.

Ci kow loolu la jëwriñu yaxantu jële ay matuwaayam, def ciy gëstu. Ci la xamlee ne saa-siin yi jaaruñu fu ñu waroon a jaar yépp laata ñuy samp seen jaayuwaay bi. China Mall mooy xeetu gan yooyiy yewwi béy. Ñoom kat, li ñuy jaay yépp, ndeke dañ jalgati santaaneb 2018 – 1888 bu 3 oktoobar 2018 biy yoonal njaayum jaayuwaay yu mag yi. Te, balay kenn di taxawal walla di ubbi lu ni mel, danga war a am, ca njëlbeen ga, sañ-sañ bi. Ku jéggi Yoon nga, ci wàll wii, àtteb 2021 – 25 bi mooy rëkk sa ndigg.

Moo tax, daanees na China Mall fukki tamndaret ci sunuy koppar (10 000 000 FCFA) yum war a fey Senegaal. Mbir mi nag, jar na taxaw seetlu.

Ag tabax gu réye ni China Mall, ràcc fi diirub ñenti weer, di jaay nim ko neexee, Nguur gi ne tekk tekkaaral. Fekk ne, jamono jooju, nekkul ci Yoon. Naka lam réew mu am fulla mënee ànd ak xeetu càggante bu ni mel ? Doy na waar, teey na xel. Naka lab doxandéem mënee ñëw ba sa biir dëkk, tabax taaxam, di jaay ay weer, fekk sàmmontewul ak sàrti réew mi ? Ndax, ab saa-senegaal ñeme na ko def fa Siin ? Xam ngeen ni déedéet moos. Te, li ci gënatee doy waar, mooy li ñu toog di xaar ba ab dépite di ci laaj ay leeral ñu ciy sog a def ay gëstu. Saa-siin yi dañu leen yeb walla dañuy def li ñu naan ëpp la doole bës sa bët ? Mbaa mbir mi raxul mbuxum ? Damay laaj rekk…

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj