Jëwriñu jokkoo beek jokkalante gi, Àlliyun Sàll, taxawal nab daluwaay bu bees. Muy jumtukaay bu ñu duppe ci nasaraan Déclaration médias du Sénégal jagleel ko saabalukaay yi ci réew mi.
Barki-démb ci àjjuma ji, 16i pani ut 2024, jëwriñ ji ñu dénk jokkoo beek jokkalante gi yegge na saabalukaay yi ab daluwaay bu bees bu mu taxawal, duppe ko Déclaration médias du Sénégal. Fekk mu doon jàkkaarlook taskati xibaar yi fa barab boobu ñu duppe Maison de la Presse Baabakar Ture ngir amal camp gi. Li mu jublu ci daluwaay boobu nag, mooy taxawu ak gunge saabalukaayi réew mi.
Daluwaay bi dina doon jumtukaay buy jàppandal saabalukaay yi ñu bindu ba ñu mën leen a ràññatle fa njëwriñal jokkoo beek jokkalante gi. Naka noonu, Jëwriñ ji di xamal këru yéenekaay yépp ni foofu rekk lañ mën a jaar ngir Nguur gi mën leen a nangul seen liggéey ba mën leen a gunge. Ba tax muy sàkku ci ñoom ak di ñaan ñu binduji gaaw ngir jàppale Nguur gi ba mu mën leen a taxawu ni mu ware ci wàll wile.
Bindu boobu sax dina tax ba ndimbal li leen Nguur gi di jagleel mën a àgg ci ñoom. Nde ci li jàll, am na lu tollu ci 800i tamndareet yoo xam ni kenn séddalewu leen yéenekaay yi. Te dara waralu ko lu dul anam yu ñàkk leer yees leen doon séddalee.
Bu loolu weesoo, jëwriñ ji yékkati nay kàddu ci anam bi takskati xibaar yeek ma-xarala yi di liggéeye. Mu xamle ceet ni anam bu doy waar la. Nde, bu sukkandikoo ci gëstu bi CJRS (Convention des Jeunes Reporters du Sénégal) amal, téeméer boo jël, lu ëpp juróom-benn-fukk yi amuñu pasug liggéey gu jaar yoon. Rax-ci-dolli, lu ëpp juróom-fukk yi duñ jot seen peyoor ni mu waree.
Ba tey, téeméeri taskati xibaar ak ma-xarala yoo jël, juróom-ñett-fukk ak juróom-benn ya amuñu kiiraayu ndimbal ak paj. Te itam, duñ natt ca IPRES (Institut de Prévoyance Retraite du Sénégal) ba tax dañuy mujje am i jafe-jafey koppar bees dawalee lu yàgg.