« DAÑU MAA TOOÑ, WAAYE DUMA BÀYYI »

Yeneen i xët

Aji bind ji

Yaayu Aadama miy jiiñ Sitoor Nduur ag ciif, àndul ak ndogal la tukkee ca layoob doomam ji. Moom, Njiira Jonn, li àttekat bi setal Sitoor Nduur, naanewu ko ndox. Ndax, nee na mbetteel lu réy la ci am. Li ko waral mooy dafa jàppoon ne li mu joxe ci mbooleem firnde, gisul woon fu Sitoor mën a jaar ba set. Moo tax mu jàpp ne dañu ko jaay doole ci mbir mi. Waaye, du bàyyi wenn yoon muy sedde noonu. Ciy waxam, dina ci def kéemtelaayu-kàttanam. 

Coowal ciif li dox diggante Sitoor Nduur ak mbindaanam ba, Aadam, mi ngi bëgg a def ab diir. Li ko sulliwaat nag mooy ndogal li ci Yoon jël. Nde, bés niki démb, àttekat bi toppeetul waa APR bi dara. Looloo metti ndeyu ndaw si, mu génn wax, di naqarlu ni yëf yi deme, ni mu tàmbalee ak ni ñu ko ci jaaye doole. Xamal na ñépp ne mbir mii dañu ko cee def li ñu naan “ëpp la doole, bës sa bët”. Waaye, moom dina ko toppaat ci Yoon, lu mu am jël. Moo tax mu ne:

“Lii, bett na ma ba ci kanamu Yàlla te, duma mës a bàyyi. Li ma fas yéene mooy samay layookat dañuy def « appel ». Duma mës a bàyyi ndax dañu maa tooñ ba ci kanamu Yàlla. Te, àddina si yépp xam nañu ne dañu maa tooñ. Ndogal li nag, bi mu daanoo jaaxle naa lool ndax maak sama doom dañoo jànkonteel ak lu metti. Ndax, bés bi ñu ko sàkkoo ma ñëw fekk ko ci lal bi mu toog, li ma njëkk a gis ci moom mooy loxoom bi, fi mu ko gaañoon, newwi na, xonq na curr. Dafa jooy ba kanam gi jaxasoo. Man xale bi, bi mu jógee kër Sitoor ñëw ne dañu ko sàkku mënoon naa buubu dem fa songu ko, ne ko danga sàkku sama doom. Waaye, defuma ko. Ndax, kon ma tooñ. Dama jël sama doom yóbbu ko foo xam ne dinañu ma wax li xale bi di wax dëgg la am déet. Ci laa jógee dem « Philippe Senghor » bi ma leen waxee li xew ñoo ma dalal xool xale bi, seetkat yi ma fa fekk xool. Ne ma li xale bi di wax am na ndax, gis nañu maniyu waa ji ci biir awra xale bi. Booba fekkagul sax ñu xam turam.” 

Mu mel ni kon yëf yi am na lees waxul. Ndax, moom kàddoom yii dafa bari lees ci mën a jàngate. Moom nag, yemul foofu. Ndaxte, bi loolu weesoo dafa dem ca kër ga, jëli yére ya mu fa bàyyi woon. Waaye, ni mu misaale doxalinu Sitoor bi mu ko waxee li xew dafa doy waar. Mu ne ko :

Bindal nañu ma ay garab, bindal nañu ma këyit bu may yóbbu Sàndarmëri Fuwaar. Bi ma ko waxee moom dafa jóg toog, jógaat, toogaat. Ne ma ban raglu nga dem ma ne ko Philippe Senghor, mu ne fajkat yooyu binduñu dëgg dañuy fen. Te, bu mu xéyee naa leen pelent, ma ne ko loolu sama yoon nekku ci. Bi ma jógee këram laata may dem Sàndarmëri Sitoor moom a ma jiitu Sàndarmëri ci genn guddi gi. Li mu fa wuti woon, loolu sama yoon nekku ci. Bi ma demee sama kër ba tëdd woo na ma. Maanaam, ci gàttal daf maa bëggoon a jënd ci xaalis. Ndax, moo feeñ ci ay waxam ci ndéggat li.” 

Waaye, ba tey, mbir mi yemul foofu. Ndax, moom yemul ci bëgg koo ger rekk. Bi ñu demee ci yoon dafa am yeneen i doxalin yu fa amaat bees sukkandikoo ci li mu wax. 

“Li ko war a leeral lépp yóbbu naa ko. Kon, ki wax ki xaatim liy firndeel ciif gi xoolul xale bi. Kon, ñoom ñeent ñi fa nekk kan moo ci xool xale bi ? Ki wax loolu, waxul dëgg, man maa ko wax. Ñoom ñi bind këyit gi dañu ne boo xéyee na nga ko yóbbu Sàndarmëri Fuwaar te, bul ko ñàkk a yóbbu. Loolu laa yóbbu, garab yi ak ndéggatu Sitoor. Loolu lépp dañu ko jël tege ko nee. Ñu ne dañu koy yóbbu CTO xool ndax, li fay génne dina méngoo ak li génne Philippe Senghor. Xamoon naa li ñale gis duñu ko gis ndax, ñetteelu fan wa la fekk xale bi naan ay garabam. Léegi, lan lañu fay fekk ? Man de, teey na sama xel.” 

Moom nag, nee na tegoon na lépp ci loxoy ki jiite woon luññutu bi, di sàndarma bii di Ja nga xam ne, dafa génn àdduna. Moo ko tax a wax ne du sori ci yenn mbir yi. Li mu ci bëgg a xamle mooy ne li gaa ñi jële CTO lañu sukkandiku ngir setal ko. Ndax, nee ñu mënuñu koo toppe lu leerul. Maanaam, moom, mbooleem firnde yi mu joxe yépp amuñu benn njariñ. Te, loolu du tax ñu mën a topp kii di Sitoor. Moom nag nee na du bàyyi wenn yoon. Dina wéyal xeex bi, lu mu am jël.

Duma mës a bàyyi ilaa yawmi diini nag. Yoon nee na daf koo setal ndax, deful. Ndax, lee jóge fee ci lañu sukkandiku ne mënuñu koo topp. Sitoor mënuma koo bàyyee nii. Du càggan-ne dama koy topp ci nii walla ci nee, lépp dama koo wékk ci loxoy Yàlla sunu Boroom. Bu ma Yàlla feyulee dinaa bégg ndaxte dañu maa tooñ. Tooñ nañu ba àddina sépp xam ne tooñ nañu ma, waaye mënuma ci dara. Ba ba may sàngoo suuf, Sitoor Nduur moo sàkku sama doom. Yal na ma Yàlla àtte ak moom, teg na ma coono, teg na ko sama doom it. Ndax, lii lu nekk laa ci dégg. Ñii ñi ngi naan xaalis la bëgg, ñii naan xale bi day fen. Yal na ma Yàlla àtte ak moom. Bu fekkee maa tooñ, na feeñ ci man. Bu fekkee moo tooñ, na feeñ ci moom ba àddina sépp xam ne li mu def moo tax lii am.” 

Xeetu doxalin yooyu moo tax mu jàppe ne yoon tëddewul njaaxanaay ci mbir mi. Mu jàpp ne bu doon mook Sitoor Nduur ñoo tolloo doole mbir mi du deme noonu. Lii lañuy wax boroom caq du xeex ak boroom baatu neen. Te, bu Yoon defoon li war du am wenn yoon mbetteel ci mbir mi. Rax-ci-dolli, nemmeeku na ne kenn ci ñoom a ëpp doole ci kanamu yoon. Loolu lay biral ci kàddoom yii :   

“ Mënumaa xeex ak moom nag ndax, boroom doole la, tey la ma gën a leer. Te, doole moo tax ñu def ma jëf jii ñu ma def. Dañu maa jaay-doole gis naa ko dund naa ko te, xam naa ko. Bu fekkonte ne damaa am doole ji mu am waat naa ko ci Yàlla du deme ni mu deme.”

Kon, bu dee dañu naan yoon ñépp la fi nekkal. Moom moom gëmul loolu. Ndax, li mu daj ci mbir mi firndeel na ko. Waaye nag, lu waay def ren ba déwén mu jig ko, day fekk du moom dañu ko koy jiiñ rekk.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj