Démb, ci àllarba ji, lañu doon amal ndajem jëwriñ yi, ni ñu ko baaxoo di defe ayu-bés bu nekk. Ca biir ndaje mooma la Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, jëlee ndogal lu am solo. Dafa di, ca ndaje mee weesu la ko junjoon, matale na ko démb.
Ayu-bés bee weesu la Njiitu réew mi biraloon yéeneem ci soppi yenn turi yoon, mbedd ak i béréb yoo xam ne amul dara lu ñuy màndargaal ci mbooru Senegaal walla Afrig ci jëmmi boppam, walla mu koy màndargaal ak a fàttali lu ñaaw. Ci kaw loolu, Njiitu réew mi soppi na turuw bulwaar (boulevard) bees duppee woon Général De Gaulle, tudde ko bulwaar Parsidã Mamadu Ja (Boulevard Président Mamadou Dia).
Dafa di, Senegaal mi ngi dëgmal bés bu màgg, bi nga xam ne, ca la moomee boppam. Te, am réew, bu dee moom na boppam dëggantaan, dafay gëm boppam, gëm ay doomam ak i jàmbaaram, di leen màggal ak sargal. Waaye, Senegaal bari nay yoon, mbedd, béréb ak i taax yoy, turi doxandéem lañu yor, rawatina way-mbéeféer ya. Wolof nag nee na, balaa ngaa laax jaay, laax lekk. Loolu moo sabab njiit yu yees yi namm ngéntewaat yoon yi ak yu ni mel, ngir tudde leen jàmbaari réew mi ak jàmbaari Afrig wëliif doxandéem yoy, guuta bi Afrig nekk, ñoo leen ci dugal.