Nguur gi war na waxtaanewaat déggoo yi ñeel soroj beek gil bi (gaas bi). Loolu mooy gis-gisu way-xarañ yi seen xel màcc ci nees di génnee balluwaayu mbindaare yi.
Ginnaaw bi ñu leen falee ci boppu réewum Senegaal, kilifa yu bees yi dañoo sàkku woon ciy way-xarañ yu seen xel màcc ci wàlluw ndefar ak génne soroj ak gaas ngir ñu saytuwaat mbooleem déggoo yi Nguurug Senegaal jot a xaatim.
Sunuy nattaango yu L’AS ñoo ko biral. Bees sukkandikoo ci xibaar yi ñu siiwal, way-xarañ yi génne nañ caabal gi (ràppoor). Ci seen caabal googu sax, dañoo sukkandiku bu baax ci lu jëm ci njeexital yi ndefarug soroj beek gaas bi mën a jur ci kéewnga gi.
Ginnaaw luññutu yi ñu amal, amal nañu njàngat ci xibaar yi ñu dajale. Biral nañu ni déggoo yi ñu xaatim des nañoo méngook li ñu sopp ci anam yees di defaree xeetu mbindaare yi. Nde, yu bari yu ñu waroon a sóoraale ci njeexital yi muy am, rawatina ci napp gi, defuñu ciy njàngat ba mën leen a xam.
Looloo tax ba ñuy sàkku ci kilifa yi ñu dellu waxtaanewaat déggoo yi. Doon na gën it ci Nguur gi mu amal ab àtte ci nees di doxaleek kéewnga gi. Lu ñu ci namm di bàyyi xell lu jëm ci wér-gi-yaram ak kaaraange gi ñeel wàlluw soroj beek gaas bi.
Naka noonu, kii di Baaba Daraame, njiitul DEEC (Règlementation Environnementale et du contrôle) dellusi na ci rëq-rëq yooyee. Muy xamle ni xeetu ndefar yu mel ni soroj beek gaas bi dafay bàyyi coow yu bari ak i yëngu-yëngu ci biir géej gi. Te, gisuñu fu ñu amalee njàngat lu ñeel wàll wile. Rax-ci-dolli, ci Ndeyu sàrtu réewum Senegaal, dañ waral ci wépp sémb mu amal njàngat ñeel njeexital yi mu mën a jur ci kéewnga gi ngir ñu mën leen a sóoraale.