Nguurug Senegaal gi dina yékkatiwaat kërug liggéey gii di SONACOS. Jël na 14i ndogal ngir tegaat ko ci yoon ginnaaw ndajeem jëwriñ mi ñu ko jagleeloon.
Démb ci àjjuma ji lañu doon amal fa màkkaanu Elimaanu jëwriñ yi, ndajeem jëwriñ mi ñu jagleeloon kërug liggéey gu SONACOS (Société Nationale de Commercialisation des Oléagineux du Sénégal). Ñu doon ko amal ci njiiteefu Buubakar Kamara, fara-caytu Càmm gi, ci teewaayu njiituul SONACOS, Ndaam Jaañ, ak teewaayu yenn jëwriñ yi, rawatina Usmaan Sonko, elimaanu jëwriñ yi, Mabuuba Jaañ mi yor wàllu mbay mi ak Seex Diba mi yor koppar yeek ngurd mi.
Bees sukkandikoo ci xibaar ya fa tukkee, te fara-caytu Càmm gi biral leen, jot nañoo waxtaane jaar-jaari kër gi ci at yi weesu. Ci lees jàpp, bi Nguur gi jëlaatee kër gi ci loxoy jàmbure yi, ginnaaw bi mu leen ko jëkkee jébbal ca atum 2006 ba 2015, dugal na ci alal ju takkoo takku. Ci diggante 2018 ak 2023 rekk, dugal na fa lu ëpp 140i milyaar ci xaalis bu mu leen dimbalee, ay bor yu mu fay, walla mu jëm ci seen gafaka. Ci diggante ati 2023 ak 2024 rekk, kër gi suuxal na ci ay ñàkk lu tollu ci 33i milyaar.
Lu ni mel nag tax na ba kërug liggéey gi nekk ci guddi yu bët të a set. Waaye Nguur gi naru koo bàyyi mu nërmeelu. Nde, dina wéy di ko teg loxo ngir mu jubbantiku. Ci njëlbeen gi, dina jël matuwaay yi war ngir mu mën a doxal naalam ci atum 2026 mi.
Naka noonu, Càmm gi jël na 14i ndogal yoy, yaakaar na ni bees ko doxalee, kër gi dina mën a dellu ci mën boppam fileek 2031 ba mën a kopparal boppam njaayum mbay mi ak di sédd ni mu ware ñi ci duggal seen alal.
Ndogal yi Nguur gi jël nag ngir joyyanti kër gi deesu leen a mën a doxal bu fekkee ni càmbar gi matewul. Gis-gis la bu elimaanu jëwriñ yi (Usmaan Sonko) biral. Ba tax muy sàkku ñu amal càmbar yu xóot, ñu bañ leen a yamale ci ñatti at yi weesu rekk te boole ci li weesu, rawatina atum 2015 ma ko Nguur gi njëkkoon a jébbal jàmbure yi.