Dellusig Kariim Maysa Wàdd fi réew mi doonatul lu ay ñoñam di xel-ñaar. Ñi ko war a dalal, jumtukaay yi mu laaj ba ci yoon wi mu war a aw, lépp rëdd nañ ko teg. Mu des nag bés bi.
Lu ëpp Juróom-ñaari at bi mu génnee kaso ci atum 2016 ak tey, Kariim Maysa Wàdd, di doom ci meetar Abdulaay Wàdd mi fi nekkoon Njiitu réewum Senegaal (2000-2012), tegaatul tànkam fi réew mi. Terewul moom la làngug pólitig gii di PDS (Parti démocratique sénégalais) tànn ngir mu doon seen lawax ci wotey 2024. Jëlal nañ ko xobu baayale yi, wutal koy torlu, fayal ko warlu (caution) 30i tamndaret (milyoŋ) ci sunuy koppar.
Dina ñëw am du ñëw ? Waa PDS noppi nañoo waajal. Ak lu coow li bare bare, am nañ kóolute walla boog feeñal nañ ko ni dina delsi balaa dagaan baati askan wi di tàmbale. Bees sukkandikoo ci xibaar yi ñu jot a rotal, lépp lu ñibbisi gi laaj topp na wet. Tànn nañ ci seen biir ñi ko war a gatanduji fa dalub roppalaan ba. Wutal nañ leen itam jumtukaay yi ci war, yu deme ni ndamaar yeek kaaraange gi ci aju.
Am na sax ci ñiñ jàpp ni jege nañ ko lool ñu biral ni bés bi mu war a ñëw sax xam nañ ko. Waaye dañ koy noppiwaale ba mu agsi. Naka noonoot, rëdd nañ yoon wi mu war a jaar ba noppi. Muy ni bu agsee, dina jël otoruut bi daldi dem Tuubaa ngir siyaareji Xalifa murit yi, Sëriñ Muntaxaa Mbàkke.
Ci pàttali, ci atum 2013 lañ tëjoon doomu Abdulaay Wàdd ji ni dafa luubal alalu réew mi, dafaroo ko. Bees demee ba ci atum 2016, njiitu réew mi Maji Sàll daldi koy bàyyi ci anum yu teey xel ba ñu ciy tudd protocole de Doha, maanaam ab déggoo ci diggante Càmmug Sénégal ak gu Qataar.
Bu ñuy laam-laame ndax Karim Maysa Wàdd dina tegaat tànkam ci réew meem déet itam, jot na ñu leeral itam li mu xaatimoon ndeem dafa lànkoon a ñaan njéggal (grâce) Njiitu réew mi. Bu weesoo loolu, lu ko Càmm gi di waajal ak 138 tamñaret (milliards) yi mu waroon a fay ginnaaw juróom-benn at yiñ ko tëjoon ? Nuy xaar fu wànnent di mujjeek i gëtam.