Ci gaawu bi weesu, 4eelu fan ci weeru me, la dipite yi wote sémbub àtte biy far palaasu Njiitu-jawriñ yi ci nguurug Senegaal. Ndax sémbub àtte bi jàll na ? Loolu jarul a laaj ! Ci 138 dipite yi teewoon, 124 yi wote nañu « waaw » 7 yi « déedéet ». Yeneen 7 yi des ñoom, di waa PDS, dañoo lànk ne duñu wote tey duñu wote ëllëg. Kon, Senegaal amatul Njiitu-jawriñ. Àtte bu bees bii, nag, dina indi ay coppite yu bare ci doxalinu nguur gi, waaye it dina gën a dooleel Njiitu-réew mi.
Du loo xam ni Maki Sàll ak Bun Abdalaa Jonn rekk la ñeel. Dafa dig coppite gu soxal ndeyu-àtte réew meek tëralinu politigu Senegaal ci boppam. Ndaxte, yamoo bi war ci diggante ñetti baat yi – baatu doxal bi, baatu yoon bi ak baatu fal àtte bi – lay nasaxal, daanaka.
Li péncum réew mi dogal dina soppi 21 sàrt ci biir ndeyu-àtte mi, jox Maki Sàll wareef yi Bun Abdalaa Jonn jagoo woon. Ñenn ñi ci kujje gi nee ñu nguur gi duggewu ko dara lu dul këppeel doole. Ñeneen ñi, ñoom, jàpp nañu ne Maki day waajal xaat joŋanteb 2024.
Dëgg la sax, Njiitu-réew mee yelloo tabb ku ko neex ngir mu jiite gornmaa bi, jàppale ko ci naal yi mu lal ñeel doxalinu réew mi. Naam, Senegaal ay njiiti-jawriñ yuy jaamu soxlaam lañ fiy faral di gis. Waaye loolu warul a tax ñu ne kenn dootul jiite jawriñ yi.
Mbir mi daal, jaay doole lay gën a nirool. Ndaxte léegi moom, Maki mooy Buur di Bummi : su defulee lu ko neex, moom la neex !