Li wokkoon Senegaal, xuri na Gaboŋ. Ci njeexitalu ayu-bés bii ñu génn la réewum Gaboŋ doon amal wotey palum Njiitu réewam. Bi ñu demee nag ba desul lu dul siiwal njureef yi tukkee ci mbañ-gàcce yi, ca lañu fa nemmeekoo mbir mu doy waar. Maanaam, ci gaawu gi, bi wote yi jeexee rekk, ci lañu dogee lënd gi ak yeneen kibaaraan yu bari ba ci sax yu bawoo bitim-réew : RFI, F24 ak TV5 Monde. Jamono jii, dañu fa dog seen i siñaal. Boolewaale ci nag di tëj askan wi ci yenn waxtu yi. Ndax, biral i njureef kepp jar na lii ? Kon, am na luy ñuul ci soow mi.
Wotey palum Njiitu réew ya ca Gaboŋ tàmbalee na juri jiixi-jiixa. Li ko waral du lenn lu dul doxalinu Nguur ga fa nekk. Nde, jël nay ndogal yoy, teey nañ xeli nit ñi. Ndax, keroog ci gaawu gi, ba wote ya jeexee ba mu des lu dul ñu xam ku jiitu ci wote ya, ca lañu xamalee askan wa ne, njureefi wote yi, du ci lënd gi walla yenn ci ay kibaaraan yi lees ko war xame.
Ñu foog ne foofu lañuy yem, ñu ni déed, kon dafay yomb. Ndax, dañu caa boolewaale li ñuy dippe “Couvre feu”, maanaam tënk askan wa ca seen i kër ci benn diir bi, diggante juróom-ñaari watu ci ngoon ba juróom-benni waxtu ci suba (19h-6h). Li mat a laaj kay mooy lan mooy seen jubluwaay ci seen xeetu doxalin woowu ? Ngir moytu biralug xibaar yu wérul la walla dañoo namm a njuuj-njaaj, wuruj njureef yi ? Xalaas ! Fi kembaarug Afrig la bët yem.
Ndax, fii la maxejj di sànni kàrtam bay yaakaaram ni def na wareefam, tànn njiitam, ñu wëlbati xobam, foqati baatam. Bu doon jub ak jubal kesee leen tax a jóg, ndax jar na ñuy jël matuwaay yii yépp ? Walla Aali Bóngoo ak ug njabootam dañoo wóoluwul seen bopp ? Dafa di, bariy pexe moom, jub a ko gën.
Xeetu doxalin woowu Nguurug Gaboŋ gi jël jamono jii ca réew ma tax na xibaari réew ma umpe lool. Looloo tax sax ba am ay kibaraan yuy fésal ne ci njureef yi jàppandeegum, ki ëpp doole ci kujje gi di Albeer Ondo Osaa daf ci duma Aali Bóngoo Ondimbaa. Waaye, ba tey xibaar yooyu amagul dara lu koy wéral. Ndax, li waroon a yombal wasaareg xibaar yi, yombal jokkoo gi ak ñi nekkul fa réew ma moom lañu ne tàppit dagg.
Dog googu ñu dog lënd gi, ay yenn siñaali tele yi ay i kibaaraan amul àpp. Li ñu xamle mooy dog nañu leen fii ak ub diir. Waaye, lu mën di tukkee ci wote yi moom, ak nu mu mën di deme, ñoom, dinañu ko biral mu yàgg walla mu yéex. Ëmb moom, kenn mënu koo nëbb. Yàgg-yàgg day feeñ.