DOGALI MAKI YU BEES YI : BUUR DU MBOKK (PAAP AALI JÀLLO)

Yeneen i xët

Aji bind ji



Bi Maki Sàll faluwaatee ci woteb 2019 bi ba léegi, ñoo ngi doon xaarandi ay coppite ngir faj jafe-jafey askan wi ci fànn yu bari. Kon, yàgg nañoo laam-laame ak a ñurumtu doxalin wu bees ci nguur gi. Waaye, 18i weer la Maki xaar laata muy jëmmal coppite googule nees yàgg a séentu. Nguur gii wuutu nguur gi fi nekkoon, nag, dafa ànd ak i mbetteel te làmbooy pexe pólitig ; mu mel ni, Maki saafara tolof-tolofi askan wi taxu koo jóg.

Ci àllarba jee weesu, 28eelu fan ci weeru oktoobar 2020 la xibaar bi tas : Njiitu réew mi, Maki Sàll, yëgal na jawriñ yi ne day suuxal nguur gi, taxawal gu bees ba noppi daldi leen di gërëm. Waaye, njortul woon ne, buñ génnee ci ndajem jawriñ mi, dina ci am ñu siiwal xibaar bi.
Donte ne yàggees na ko xaar, bi xibaar bi jibee, mbetteel gu réy la jur ci ñépp. Moo tax, ci saa si la tele yeek rajo yi soppi seen i porogaraam, tàmbalee dalal ay gan ngir waxtaane mbir mi. Coow li ne kur ci pénc yi ak ci ànternet bi. Ku nekk di wax sa xalaat. Ñuy jàngat dogal bi : bu dee ñenn ñaa ngiy jéem a jéli sabab yeek jubluwaay yi, ñeneen ñi, ñoom, pexey pólitig yi Maki di tëral a leen soxal. Riir mi ame réew mi, nag. Ñu naan, kii day génn, kee day dugg. Ñenn ci taskati xibaar yi naan dees na yaatal nguur gi boole ci kujje gi, ñeneen ñiy wax ne Idiriisa Sekk ci lay bokk.
Yégle bi dëggal xibaar bi
Coow li ak riirum coppite nguur gi dafa jële kow jegeñaale njiitu réew mi, ñu daldi jànnaxe. Booba, Sóokóon la fekk Abdu Latif Kulibali mi yor kàddu njiitéef gi. Waaye, ci saa si la génne ab yégle di ci xamle ne, njiitu réew mi, Maki Sàll, xaatim na ci àllarba ji, 28eelu fan ci oktoobar 2020, 4i dogal :
– Dogal 2020-2073 bu 28eelu fan ci oktoobar 2020 biy dakkal liggéeyi jawriñ yeek tofi njiit yi bokk ci nguur gi ;
– Dogal 2020-2074 bu 28eelu fan ci oktoobar 2020 biy dakkal liggéeyu njiitu CESE ;
– Dogal 2020-2075 bu 28eelu fan ci oktoobar 2020 biy dakkal liggéeyu jawriñu nguur, tof-njiitu njiitéef gi ;
– Dogal 2020-2076 bu 28eelu fan ci oktoobar 2020 biy dakkal liggéeyu tof-njiitu nguur gi.
Liñ joxe niy sabab, mooy tolluwaayu jamono ak mbas mi nga xam ne, dafa nasaxal koom-koomi àddina sépp. Ginnaaw gi, lenn rekk a desoon, tabb nguur gu yees gi.
Buur du mbokk
Juróomi fani Yàlla la askan wi toog di xaar nguur gu bees gi. Ndaxte, ci dibéer ji, 1eelu fan ci nowàmbar la xibaar bi rot. Njiitu réew mi jël ab dekkare 2020-2098, daldi tabb jawriñ yeek njiiti campeef yu bees yi séq nguur gu bees gi. Ci diggante bi, lu ne wax nañ ko fi, xalaat bu nekk jib, muy bu rafet walla safaan ba.
Séydu Géy moo biral turi jawriñ yeek njiiti campeef yu bees yi ci RTS. Waxaale na yit ne, nguur gu yees gile, saafara jàngoroy askan wee ko tax a jóg, wëliis xàjj-ak-seen. 33i jawriñ ak 4i njiiti campeef ñoo séq nguur gi. Li ci gën a fés, nag, mooy génnub Aminata Ture, Bun Abdalaa Jonn, Aali Nguy Njaay, Aamadu Ba ak Saŋ Maksim Simoŋ Njaay ak duggub ñenn ci waa kujje gi, rawatina Idiriisa Sekk.
Nee ñu, Aminata Ture, Bun Abdalaa Jonn, Aali Nguy Njaay ak Aamadu Ba dañ doon xemmem, ku ci nekk, palaasu njiitu réew mi, te looloo tax Maki dàq leen. Dayo bi 4 ñii am, fi ñu jaar ak Maki ak liñ ko jot a xeexal, rawatina Aminata Ture, mooy wone ne Maki dàqu leen ci neen. Am na lu muy nos ak a nocci ci suuf, di ko waaj ci pet. Ak lu ci mënti am, Maki dëggal na ne, buur du mbokk. Wone na yit ne, kàddu, jaratul dara ci miim réew.
Idi ak Maki ay workat lañu
Bu dee li Maki tabb Umar Saar mi fàqee PDS ak Aysata Taal Sàll bettul kenn, bu Idi bi moom, dafa bette te metti ñu bari. Bi mu leeree ni Idiriisa Sekk ak 2 ciy naataangoomi pàrti (Yànqooba Jatara ak Aali Sale Jóob) dugg nañ ci nguurug Maki Sàll gu yees gi, ñu baree ko ñaawlu.
Naam, ñoo ngi doon njort lu ni mel, waaye kenn foogul woon ne nii la mbir miy deme. Ci la xas yeek saaga yi tàmbali. Lu ne ñu yakk ko Idiriisa Sekk. Ci la ngóor si woowe taskati xibaar yi kërëm, joxe ay lay. Mu ne, tolluwaayu réew mi moo laaj ñu booloo ngir jàppale Maki Sàll. Ndax, ciy waxam, koom-koom yépp a nërméelu, ba ci réew yi ëpp doole ci àddina si, sax, mbas mi da leen a xoj. Kon, Senegaal, jàmm la laaj te, moom, bëgg gi mu bëgg réew mi moo ko tax a nangu tabb bi ko Maki tabb. Nee na, sax, yàgg naa waxtaan ak Maki, ci sutura ak teraanga. Muy wax joo xam ne dafa safaanoo ak wax yim daan wax at yii weesu, te ndaw yeek taskati xibaar yi di leen génnewaat ci ànternet bi ak tele yi.
Waaye, lay yim joxe, benn jëmu ci kër. Te, bu ci nekk yomb naa teggi. Moo tax, lenn rekk ngay dégg : Idiriisa Sekk workat la. Wor na askan wi, wor waa kujje gi, wor itam ñi mu bokkal làng. Mustafaa Jaxate, moom, nee na, Maki Sàll dafa dëddu askan wi. Ndax, fiñ ko doon xaar du fii. Mu teg ci ne, Njiitu réew mi, pólitig kese a ko tax a jóg, waaye sóoraalewul benn yoon soxlay askan wi. Te yit, li mu tabb Idiriisa Sekk ak Omar Saar, day wone ne wor na waa APR, tuutal leen te démb, ba dara dul dara, ñoo ànddon ak moom. Tey, mu takkal ay ndombo-tànk ñi ko doon xeex, yàggul dara.
3eelu moome gi, liy ñuul ci soow mi…
Am na ñu wax ne Idi dafa ame ay jafe-jafe xaalis ak bànk yi, moo ko tax a nangu. Nde, 30i miliyoŋ yi ko Maki di jox weer wu dee ak yeneen xeeti jagle ak i neexal yi mu nar a am ñoo fees bëtam ba mu nangoo jiite CESE. Moone de, at mii weesu rekk, noon na dañ fee war a jële CESE ak HCCT ndax amaluñ askan wi benn njariñ. Mu am, nag, ñu xalaat ne, nii Maki Sàll doxale day wone ni du sàkku 3eelu moome. Waaye, moom ak Farãs ñoo kootoo ngir xàllal yoon Idiriisa Sekk. Nde, bu ko Usmaan Sónko wuutoo ci jal bi, du baax ci moom te gënalul Farãs itam.
Waaye, loolu, dara leeragu ci. Lenn rekk a leer nàññ : kàddu njiitu réew mi jaratul dara ci réew mi !

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj