Tey ci altine ji, ñetti fan ci weeru suwe la ndogal li daanu. Bah Jaxate Ak imaam Séex Tiijaan Ndaw ñoo bokkoon li ñu leen di toppe. Dafa di, ñoom ñaar ñépp dañu leen doon toppe ay tuuma yu ñu teg ci ndoddu elimaanu jëwriñ yi. Nde, dañu ne gaa ñi dañoo yàq deru Usmaan Sonko. Kii di Dooro Géy moom, mbirum suuf mu dox ci digganteem ak Sakilulaahi Sow moo ko dugal ci guuta gi mu nekk. Ñoom ñett ñépp am na lu Yoon dogal ci ñoom tey jii.
Ci weeru me wii ñu génn lañu leen jàppoon ñoom ñett ñépp. Kii di Dooro Géy moom, ay mbiram, ba tey dara leeragu ci. Ndax, benn miliyaar bu teg bi ñu koy toppe ci mbirum suuf si mu jaayoon, ba léegi, kenn xamagul fu muy mujj. Ñi ngi xaarandi ba xam ndax ay daan dañ ko ciy fekk walla Yoon da koy setal. Waaye, fi mu tollu nii tembe, moom àttekatu ñetteelu kabine bi yóbbu na ko kaso. Su ko defee ñu wéyal luññutu yi ba xam lan moo laxasu ci mbir mi. Moom nag, li ñu koy toppe wute na ak li ñuy toppe ñaar ñu njëkkñi Ñi. Looloo tax, seen i mbiwute.
Bah Jaxate Ak imaam Séex Tiijaan Ndaw, li ñu doon toppe mooy kàddu yi ñu teg ci deru Usmaan Sonko ñeel mbirum ngóor-jigéen mi lëmbe woon réew mi fan yee weesu. Loolu mi ngi amoon ci jamono yi fi Jean-Luc Mélanchon ñëwe woon ba jotoon a amal aw waxtaan mook Usmaan Sonko fale ca daara ju kowe ja nekk fa Ndakaaru (UCAD). Kàddu yooyee ñu yékkati woon ginnaaw waxtaan wa moo taxoon Yoon dal seen kow ba ay daan mujj leen ci fekk.
Keroog altine ñaar-fukki fan ak juróom-ñaar lañu doon amal layoo bi. Waaye, tey bi altine ji dellusee la daan bi sog a rot. Ñoom ñaar, daan nañu leen ñetti weeri kaso yoo xam ne dañu koy tëdd boole kook ñaar-fukki junni yoo xam ne ndàmpaay lay doon. Mu mel ni kon, li toppekat bi sàkku woon bu dee am na lu ñu ko ci defal tamit, am na lu des. Nde, moom dafa sàkku woon ñu daan leen juróom-benni weeri kaso ak ñaar-fukki junniy ndàmpaay. Rax-ci-dolli, ñu dindi kàddu yooyu ci mbooleem mbaali jokkoo yi. Waaye, àttekat bi moom ci koppar gi kese la yem ak ñetti weeri kaso yi.
Kon, mënees na ne ñaar ñii moom seen i mbir leeragum na. Ki ñu xamagul fu muy mujj kay mooy Dooro Géy. Dañu koy daan am déet ? Dees na ci xam dara. Nde, lu tëw a xam moom day fekk daa yàggul.