BINDKATU AYUBÉS BI : IBRAAYIMA SAAXO CAAM

Yeneen i xët

Aji bind ji

 

 
 
 
 
 
 
 

Ibraayima Saaxo Caam a nga juddoo Rëbës ci atum 1973, muy gox bi nekk diggante Medinaa ak Ñaay-Cokkeer, géej gi féete ko sowu. Gannaaw ba mu dalee Alxuraan, ci la dugg ci daaray nasaraan ba am “baccalauréat” ci 1994 ci “Lycée Delafosse”. Ci la dem nag ca Iniwérsite Séex Anta Jóob, laata muy tukki ca réewum Almaañ ca 1996, ngir jàngi fa pólitig ak koom-koom. Mi ngi dellusi ci atum 2010, ràngoo lijaasab Doktoraa, daldi tàmbalee liggéey ci kurél gu Almaañ teg fii ci Senegaal, muy yëngu ci naatal ag jàppale réewi Afrig yi.

Cofeelam ci woy ci làmmiñu wolof a ngi juddu ca jamono ja mu doonoon doxandéem ca Almaañ. Li mu sori woon réewam, sori njabootam ak i moomeelam, dafa jur ci moom ag cofeel ci dellu jàngaat, ngir gën a xam ay aadaam ak cosaanam.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj