CAN 2021 : Kub baa nga woon ca Séeju, Saajo Maane delloo mbàttu ca ndaa la mu naane

Yeneen i xët

Aji bind ji

Bàmbali, ci diwaanu Séeju, dalal na Kubu Afrig bi Senegaal jële woon ca Kamerun ak doomam jii di Saajo Maane. Jëwriñ ji Mataar Ba yékkati na fay kàddu, wonale kub bi Jaraafu Séejook waa Bàmbali, teg ca ni Saajo Maane nekkee royuwaay ci réew mi. Ginnaaw loolu Saajo Maaneek i xaritam amal nañ fa joŋante xaritoo, àndoon ceek Papis Demba Siise, Allaaji Useynu Juuf ak Mbay Ñaŋ. Ña nga ko amelee woon fa lépp tàmbalee, bayaal ba doomu bàmbali ji doore futbal.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj