Bu nu xasee ba laal laalaake, amatul adada. Jot na, tey jii, mboolem taskati xibaar yi dese seen i ngor te gëm ni kenn mënu leen a tënk ci seen liggéey, ñu jóg taxaw temm, sàmm seen i àq, aar seen ub liggéey. Lu ñu ci góobe, gar ko. Ndax, fullaay jaay daqaar. Taxawaay bii moo war a nekk taxawaayu képp kuy taskatu xibaar, rawatina taskatu xibaar bu jàpp ne, xoqatal bi ak bunduxataal yi mu dund ak i nawleem dafa war a dakk. Taxawaayu fulla jooju, moo war a nekk taxawaayu saabalkat bob, liggéeyam ak sagoy taskati xibaar yi ñor na ko. Mooy taxawaayu ñi nga xam ne, ba tey, gëm nañu ne, dañu war a aar ak a sàmm keno ak cëslaay yi téye liggéeyu tasug xibaar, ndeyu àtte ji sàrtal ko. Muy ay gëm-gëm yoy, taskatu xibaar bi daf ciy ŋoy ba dëgër ak i dëgëjam.
Jamono jii nag, kenn umpalewul ne, am na njuuma lol, dafa laxas na jaan ci buumug caabal gi. Loolu, dëgg ju wér péŋŋ la. Sikk amu ci. Dafa di sax, ku wax dëgg te Yàlla rekk a tax, bañ a nax sa bopp, xam nga ni Senegaal noonu la yàgg a doxe. Waaye, tey, Waalo dafa gënatee aay. Moone, lu ni mel, yàggoon na di raam, jëmsi ci ñag bi. Nde, lim boo gis, ci benn lay doore. Njuuma li dafa tàmbalee jàpp benn-benn, di ber di dóor, ñeneen ñiy seetaan, muy duma rekk ba àgg fi mu àgg tey. Ndege, ca ndoorteel la, ñépp dañ foogoon ne, ab duus buy romb la rekk. Ndekete yoo, ab gannuus buy daaneel kër la. Moo tax it, rusloo na ñépp. Tey, taskatu xibaar dafa tumurànke ci réew mi. Ñu bari xamatuñu fu ñuy teg seen i tànk.
Xew-xew yi jot a jàll fan yii firndeel nañu ne, tey, taskati xibaar yi mënaluñ seen bopp dara. Doon nañ faral di dégg ñuy wax ne, taskati xibaar yi ñoo ame baat biy saytu Nguur gi. Waaye, laaj bi sampu mooy : ndax tey jii, mi ngi ak baat boobu ba tey ? Maanaam amati na dooley jaamaarlook njuuma li koy jaay doole ?
Xoqatal ak bunduxatal bi ñu nekk di teg kërug Walfadjiri mënoon na ñàkk bu fekkoon ni taskati xibaar yépp dañu joxante loxo, rawatina mag ñi séq sàndikaa yi. Dog bi ñu dog siñaalam ci diiru 30i fan, bàyyikoo ci jëwriñ ji ñu dénk wàllu jokkoo gi. Loolu day wone ne, nun, amunu benn baat ci ndogal yi ñuy teg sunu kow, donte ne dañuy salfaañe sunuy àq ak i yelleef. Tëj yi ñuy tëj lenn ciy taskati xibaar, ci anam bi nga xam ni jaarul ci yoon, sunub yàccaaral a nu ko yóbbe. Ba ci sax kàrtug caabal gi ñuy taafantaloo, tey jii, njuuma li soppi na ngànnaay, di ko xeexe waa mécce bi. Waxatuñu sax ni ñu ñàkkee kaaraange. Waaye, ngaañ li ñuy yoot, daanaka moo gën a réy. Tey jii, njuuma laa ngi ñu tiim rekk ak yatam, lu ko neex mu def. Teg lompoñ bi ñu nemmeeku ci doxalinu caabal yi, te yu ci bare nekk ay gàllankoor, naatablewunu ni, ay way-pólitig yuy def liggéey bu salte ñoo nekk ci ginnaaw.
Tey jii, ndax noppi nañu ngir jàmmaarlook pexey njuuma loolu tiim nu ? Ndax jotul nu dakkal cong yi ñuy song taskati xibaar ? Ngir loolu mën a nekk, fàww nag ñu daldi joxante loxo, booloo, bennoo. Ndax, mbooloo mooy doole. Xeex bu ni mel mooy saxal ak a dëgëral demokaraasi, di suuxat réewum Yoon. Mu mel ni nag bànqaasi caabal yépp duñu mën a tënku ci bile ndogal. Ndax, booy seetaan, ñu ci bari, dañu xàll seen yoonu bopp, yenn yi far ak Nguur gi.
Waaye, bu ñuy xool caabali Senegaal yi, seen tolluwaayam, fàww nu dajaloowaat, def benn say, ngir mën a fàggu, aar sunu bopp, sàmmaale jumtukaayi demokaraasi bu wér. Ndaje yu mag yi nga xam ni, kurél giy jokkale mbootaayi taskati xibaar yi, muy CAP (Coordination des Associations de Presse), amal na leen, dañuy wone ne sunu ëllëg ci nun rekk la aju. Nanu taxaw temm, laxasaayu xeex. Bu nu ko defee, dinanu mën a gàntal pexey njuuma li. Kon nag, na ñépp jàkkaarlook moom. Lu ko moy dina ñu fi jële. Te, lu mu ko jaral war na nu jaral lu ko ëpp.