Niki bésub tey jii la eksame bakaloryaa bi door ci réew mépp. Jukkees na ci yéenekaay L’AS ne, 155109i wutaafon ñooy sëgg bind ngir am lijaasa bile. Waaye ci biir 155109i wutaafon yooyu, 52 yoo jël ci 100 bu nekk, ay jigéen lañu. Séddalees na wutaafon yi ci 496i batu. Bakaloryaa nag, lijaasa bu am soloo ndax gone gu ko amul doo mën a bindu iniwérsite, moo xam fii ci Senegaal walla bitim-réew. Ginnaaw ren mbas mi yàq na lu bare ci njàng mi, eksame bi dina gën a jafe ci ndongo yi.