ELIMAANU JËWRIÑ YI SANTAANE NA YAXANAL

Yeneen i xët

Aji bind ji

Elimaanu jëwriñ yi jël na ndogal lu bees ñeel Càmm gi. Muy sàkku ci liggéeykat yi ñu defaraat seen toogaay ngir yaxanal lees di lakk ci mbëj mi.

Barki-démb ci àjjuma ji, elimaanu jëwriñ yi, Sëñ Usmaan Sonko doon na jiite am ndaje mu doxoon ci diggante jëwriñ ji séq mbirum mbëj mi. Ca mooma ndaje nag, am na xibaar yu fa biree. Waaye, li banqaas gi di lakk ci mbëj mi gën na cee ràññeeku ndax ni mu jéggee dayo. Nde Nguur gi dina fey at mu jot lu tollook 71i tamndareeti FCFA.

Ci li elimaanu jëwriñ yi xamle, dara waralul lu ni mel lu dul doxalinu liggéeykat yi. Nde ni ñuy doxalee ci seen pekk yi demul bay jaadu. Ku ci nekk dafay bëgg a am fa pekkam ab firigoo, masinu kafeem ak teleem. Te, bu doon fa seen i kër, duñ ko doxalee noonu.

Ba tey ci li mu xamle, bees yaxanaloon ñaar-fukk ak juróom ci téeméer bu nekk (25%), di na doon lu ëpp 20i tamndareet yu Nguur gi mën a sakkanal. Ci bile taxaw-seetlu nag, la jëwriñ ji sukkandiku ngir jël ndogalu yaxanal lees di lakk ci mbëj mi.

Ndogal li mu njëkk a jël nag, moo ngi aju ci nees di jëfandikoo jumtukaay yi nekk ci pekk yi. Naka noonu, muy sàkku ci bépp liggéeykat mu farlu ci béréb ba muy liggéeyee te defaraat toogaayam. Loolu nag, dafay laaj ñu sàkk ay pexe, soppi jikko yi te yemale jumtukaay yees leen jagleel.

Bu weesoo loolu, moo ngi sàkku ci ñu jekk-jekkal bérébu liggéeyukaay yeet ba ñépp ña fay liggéeyee mën a bokk-bokkoo jumtukaay yi.

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj