Ki fi nekkoon Njiitu réewum Etaasini, Donald Trump (20 sãwiyee 2017 ba 20 sãwiyee 2021) dellusi na ca boppu réew ma ginnaaw wotey Njiitu réew ma ñu fa doon amal.
Démb ci talaata ji, 5i pani nowàmbar 2024 lañ doon amal wotey Njiitu réewum Etaasini. Njureef ya wone nañ ci lu gaaw ni Donald Trump moo jiitu ci lu bari. Bees sukkandokoo ci xibaar yi saabalukaayi réew ma biral, lawaxu way-bokkeef yi (les républicains) am na 51% (juróom-fukk ak benni xob ci téeméer bu nekk). Lim boobu dina ko jox 277i xob ñeel ñees dippee wotekat yu mag yi. Muy lim bu romb 270i xob yees di laaj, ci 538 yi ñu doon, ngir doon Njiitu réew ma.
Naka noonu, Donald Trump dina dellusi ca boppu réew ma ginnaaw ñeenti at bi mu ñàkkee Nguur ga. Bokk na ci kàddu yi mu njëkk a yékkati :
« Ci ngoonug tey jii, duggaat nanu ci mboor ngir lenn : tabaxaat réew mi. Ndam la lol, sunum réew mësut ko am ci pólitig. Bëggoon naa kon delloo njukkal askanu Amerig ci ni ngeen ma sargalee ba mu jéggi dayo, def ma seen ñeen-fukk ak juróom-ñaareelu Njiitu réew. […] Dinaa xeex ngir yeen, ngir seen njaboot ak seen ëllëg.»
Ginnaaw ba jàpp nañu ni moo falu, dina négandiku 11i ayu-bés ngir nawleem bi Joe Biden jébbal ko lenge yi. Fileek boobu, dëkk bu ci nekk, kilifa ya dinañu woññiwaat xob ya ngir wéral njureef yi, lijjanti bépp dabantal bu ci mën a am (ba 11 desàmbar 2024). Bu ko defee wotekat yu mag ya sog di wote (17 desàmbar 2024), kongare ba dellu woññi seen i xob ngir wax ki falu ak kiy doon toftalam. Ginnaaw gi, njiitu Senaa ba dëggal njureef yi (6 sãwiyee 2025) laata ñuy tabb Njiitu réew ma keroog 20i fan ci weeru sãwiyee 2025.