ËTTU ÀTTEWAAY BU MAG BI : NJIIT LA GÀNTAL NA NEENAL-ÀTTE BU LAYOOKATI USMAAN SONKO

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ëttu àttewaay bu mag bi gàntal na neenal-àtte bi layookati Usmaan Sonko yi dugaloon. Fekk ñu tàbbaloon ko fa ñeel neenalub dogal bi àttekat bi Sabasi Fay jëloon.

17 noowàmbar bii ñu génn, ëttu àttewaay bu mag bi dafa neenaloon dogal bi àttekat bi Sabasi Fay jëloon ci 12i fan ci weeru oktoobar 2023 bi fa Sigicoor ngir bindaat turu Usmaan Sonko bi ñu far ci kayitu bindu yi. Ginnaaw bi mu ko neenalee nag, dafa delloo mbir mi fa ëttu dabantal bu ndakaaru ngir ñu àttewaat ko.

Muy dogal bu layookati Usmaan Sonko yi mënul nangu wenn yoon bay toog di xaar àttewaat boobu. Ñu jàpp ni ndayu mbill gi ci boppam dafa war a bokk ci wotey 2024 yi te defuñ lu dul salfaañe ay àqam. Looloo taxoon ba ci bésub 30i fan ci weeru noowàmbar bii nu génn, ñu dellu dugalaat ab neenal-àtte fa ëttu àttewaay bu mag ba nekk Ndakaaru ngir mu dellusi, ci lu gaaw, ci dogal bi te càmbaraat ko bu baax.

Démb ci àjjuma ji, yemook benn fan doŋŋ ginnaaw càkkuteefu layookati Usmaan Sonko, la ëttu àttewaay bi fésal taxawaayam. Naka noonu, mu dellu gàntal neenal-àtte bi cib ordonaas bu mu siiwal ci turu Sire Aali Ba miy Njiit lu njëkk ci ëtt bi. Ci biir ordonaas bi ñu mën cee jàng ni « deesul a dog dabantal walla àppu dabantal bu aju ci neenal-àtte ».

Naka noonu, muy xamle ni Njiitu ëttu àttewaay bu Ndakaaru bi mooy ki yeyoo rëdd yoon bees war a jaar ci mbir yu tembare yi nees ko bàyyee xel ci doxalin bi. Waaye àtte yees bokk amal duñ tënku ci doxalin boobu. Ba tax na moom Njiit lu njëkk li ci ëttu àttewaay bu mag bi mu gàntal bataaxalu neenal bi.

Muy niru ni Sñ Keledoor Li ak i ñoñam deseetuñu lu dul toog xaar ëttu àttewaay bu Ndakaaru bi. Waaye du tax ñu dëggal ni seen i pexe jeex nañ nde déggaguñu leen ñu yëy yàbbi ci gàntal bi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj