I
Sëriñ Daawuda Njaay Jaraaf jàngalekatub wolof la. Def na gëstu bu am solo ci tëraliin ak ci doxaliinu njàngalem kàllamay Kocc ci daaray tuut-tànk yi ci réew mi.
WUTKATI WURUS
Dóor i kuur ci suuf su sell
Suufus Afrig si nu war ca njalbéen
Suuf si nu meññ ëmb wurus
Ay janax a ngiy lëňbati say butit
Di noyyi xet gu bon gi ci ban bi
Ci sa peggi dex yi
Lejum yu nëtëx a nga fay meññ
Làq ci seen biir xal yu yànj
Dëkk baa ngiy lakk butiti njurukaayam
Yoole ko yàllay wurus ji
Di soppi wurus jënde koy bàmmeel
Dóor i kuur ci suuf su sell
Suufus Afrig si nu war ca njalbéen
Xuri wurus yaa ngi nuy nëbb jant bi
II
Sëriñ Daam Jaane mi ngi juddoo Tëngéej ci atum 1986. Daara la yor ca Tuubaa, di jàngale Alxuraan. Mi ngiy taalif way yu bari jëm ci xew-xewi jamano jii nuy dund.
GUDDI (Xaaju ñaareel)
Bànneex ci néegi juboo, naqar ci néegi safaan
Am biir yu feese ndawal, am yoy mbaxal lañu sόor
Suñeel yi raam leru ñag, rungug kañaa ngi sa waañ
Xaj yaa ngiy yuuxu ca kaw, ay ngooxi mbott di riir
Yoo yewwu yee xorondom, gëmmentu daldi nuyoo
Gént ay gan gi la wax, xibaar yu lënt sa yuur
Leeg-leeg mu neex ba nga bég, leeg-leeg nga yuuxu ca ngir
Jëmmam ju raglu ja, ànd ak bëñ yu gudd te xuur
Fasuw sijaada gu suur, laabuw kurus yatu tur
Njaabal ci kursu wareefi jaam ba nammati Buur
Mbaamum fétal mu ñu sëf, jaasiy bajantu ci bew
War say wareef weri fit, def jom toj ak tëb i miir
Ñii tëdd ci seen weti way-jur, sàngu seen sëri ngor
Ñii sol lu gàtt fasoo, wànteeri seen cëri biir
Jokkoo ba guddi gi xaaj, gàmbaal ba séq yi sab
Kee xaar jëkkër ba nelaw, kee bëtt ñag wuti gόor