F24 MI NGI ARTU…

Yeneen i xët

Aji bind ji

Tey ci altine ji lañu woo woon dépite yi ca Ngomblaan ga. Dafa amoon i sémb yu bari yu ñu fa waroon a càmbar ngir wote leen. Bi gën a fés ci sémb yooyu di bob jëm ci coppiteg dog 87 bu ndeyu àtte ji. Démb ak léegi nag, coow laa ngi ne kurr ci réew mi. Dara waralu ko lu dul njeexital yi sémbub àtte bi mën a am ci demokaraasi réew mi. Looloo tax ay nit ñu bari ak kurél yu deme ni F24 takku, jóg taxaw ngir xeex loolu. Ndax, dañoo jàpp ne dara wundu ko lu dul ne dañoo bëgg a jox Njiitu réew mi sañ-sañ bu koy tax a tas Ngomblaan.

Lees layalee coppite gi mooy mooy càmbaraat àppug wote yi ak jokkalante gu mucc ayib diggante Yoon ak Ngombalaan gi. Waa F24 nag dañoo jàpp ne lay boobu dëgërul. Moo tax seen xel teey ci. Ndege, ndeyu àtte ji dafa sàrtal àppug ñaari at bees war a xaar laata Njiitu réew miy sog di mën a tas Ngomblaan. Sàrt boobu la Nguur gi bëgg a dindi ci ndeyu-àtte yi. Loolu nga xam ne, ab jéegob demokaraasi la bob, jamono ja ñuy moom sunu bopp lañ ko saxaloon. Moo tax ñuy woo dépite yépp, ak fu ñu mën a far, ñu bañ a wote sémbub àtte ngar sàmm demokaraasi Senegaal. Waaye nag, xeex lay doon. Narul yomb.

Ab dépite, askan waa ko fal. Naam, am na làng gum bokk, waaye bu dul woon xob yi ko askan wi sàndil, du làmboo malaanum dépite. Kon, waruñoo nangu mukk di jàllale ab àtte bu leen di tuutal ak salfaañe demokaraasi. Lu ko moy, moom Njiitu réew mi mooy doon buur di bummi. Loolu la Mimi Ture fésal ci xëtu Facebookam, di sàkku ci Njiitu réew mi mu bàyyi ndombog-tànku dépite yi. Rax-ci-dolli, ndeem juróom-ñaari weer kepp a ko dese ci boppu réew mi, warul a nasaxal ndeyu àtte ji. Te, benn dépite warul a nangoo wote àtte boobu nga xam ne, saa su ne, mën na tax mu ñàkk ag ndombog-tànkam.

Looloo tax waa F24 di wone seen ug ñàkk ànd ci coppite googu. Ndax, lu mën a nasaxal campeef yi la. Ba tax, ñuy woo ñi demokaraasi ñor ñu jéebaane loolu te, ñu booloo ngir xeex ko. Ñuy wax ne Abdulaay Wàdd, ca atum 2000, ak Maki Sàll mii ci boppam, bi ñu faloo fekkoon nañu fiy Ngomblaan yu bees. Te, loolu terewul woon dépite yi ànd ak ñoom liggéey. Daanaka, wàññiwul woon dara ci sunu demokaraasi bi.

Laata ñuy dellusi ci mbir moomu, ñoom waa F24 joxe nañu ab dig-daje. Dig-daje boobu nag, am ndaje mu ñuy amal ci àjjuma jii di ñëw yemoo ak ñaar-fukki fan ci weeru sulet wii ñu nekk bu ñetti waxtu ci ngoon jotee. Dina ko def ak du ko def dees na ci xam dara fii ak ab diir.

Li jëm ci wàllu sémb bi nag, dépite mujjuñu ko wote. Ci alxames jii lañ leen woo.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj