FAGAROO GËN FAJU

Yeneen i xët

Aji bind ji

 

Li Faal Sàmba Suuna

Sama maam daan na wax ni maamam dund na téeméeri at ak ñaar-fukk yu ànd ak wér ak wérle. Ndax magal terewu ko woon a dox ay soxlaam, taxul woon bët yi lëndëm walla ay cëram bañ. Li ëpp solo moo di ne ba bi muy wuyji Boroomamnaaxul. Ku tuuti la woon tamit, maanaam amul woon yaram.

Waaw, ndax jotul tey nu amal taxawseetlu ba xam lu tax sunuy maam mënoon a dund lu yàgge noonu te kenn daawu leen weer ak a weri ? Lu yéeme la ndax fi mu ne nii, juróom-fukki at rekk soo ko amee daldi jàpp ni mag ñëw na. Dañ nuy faral di gëmloo yit ne li ëpp ci feebar yi nuy dabci sunuy maam lañ leen donne.

Moone de, ñoom dund nañu ba dund sàppi leen ñu wàcc liggéey ci jàmm te seen i jàmbat mësul bari ci xeetu feebar yi ñu xam léegi ci àddina si. Mooy yi boroom xam-xam yi tudde feebari xay, lu ci mel ni taasyoŋ, feebaru suukar ñu gën koo xam ci jabet, mbuxuri, feebar yiy jàpp tenqo yi ak yax yi, ba ci kseer biy lëmbe réew yépp.

Àddinay dox ba léegi dafa mel ni ‘’màggat’’ ak ‘’feebar’’, seen àndandoo dafa dëgër ba mënatuñoo tàqalikoo. Ba ku jëm mag daldi def ci sa xel ni fàww xeetu feebar yooyu dajaloo ci sa biir yaram te bu amee dangay jàpp rekk ni yoon la.

Boroom xam-xam yi gëstu nañu ba xam ni moone de doomu-aadama waroon naa mën a dund téeméeri at ak ñaar-fukk yu ànd ak wér-gi yaram.

Li jar a laajte mooy lii : sunu digganteek sunu maam yooyu, boobaak léegi lan moo fi soppeeku ? Naka lanu mën a donne ci ñoom ay feebar yoo xam ni ñoom mësu ñu koo xam te mësu leen a tëral bay téye seen i cër walla lëndëmal seenum xel ?

Man daal, seet naa ba seet waaye lenn rekk laa gis ni mooy tontu li. Mooy li nu soppi sunu nekkin, soppi sunu lekkin. Ci gàttaldanoo soppi sunu uslu dundin.

Ndax maam ya, seen jëf yépp ak seenug dundin dafa aju woon ci yoonu càkkeef te dëppook moom. Lépp lu ñu daan def amoon na waxtu wuñ ko war a defe : waxtu liggéey, waxtu lekk, waxtu naan, waxtu dal-lu, waxtu wéetal seen Boroom, waxtu saafonteek seen i soxna ak seen njaboot.

Seen lekk ak seen naan da daan yem, te yit daawuñu dugal seen biir lu ñu xamul. Boo seetee sax, moo waraloon ñuy bey di dunde te ku koy def sam xel day dal, ngay liggéey te doo sonal sa yaram. Loolu bokk na ci li leen taxoon a gudd fan te mu ànd ak wér. Ndax jàmmu xel ak jàmmu xol ñoo ëmb bu yaram.

Sunu jamono léegi sii nag, danoo worook yoonu càkkéef. Xamatunu yemale sunu lekk, beyatunu dunde, fonkatunu waxtu yi, sunuy bëgg-bëgg a ëpp sunu kàttan, xel yi dalatuñ, xol yi féexatuñ.

Ñu dem ba boroom xam-xam yi seetlu ni du lekkin wi walla dundin gi keseey sonal nit ñi. Ci seen gis-gis, leneen am na solo te mooy njàqare : bu amulee ay doomi-jàngoro yit, dina tax metit gën a tar.

Kon mënees na jàpp ni xel mu dal ak xol bu féex ñooy li ëpp solo ci àddina te yitwér-gi yaram dëgg mi ngi aju ci nekkinu nit ki ak lekkam, ci anam bu dëppook yoonu càkkeef gi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj