FAIDHERBE, SAAY-SAAY BI NUY SARGAL II (BUBAKAR BÓRIS JÓOB)

Yeneen i xët

Aji bind ji


 Moone de, ngóor sii ñuy sargal tey, mooy ki daan fitnaal ak a toroxal sunuy maam, démb. Moo leen daan rey guddeek bëccëg. Mooy ki faat sunuy jàmbaar, sàcc sunu alal. Mooy ki daan siif sunuy jigéen, daan xàwwi sutura gor yi. Faidherbe mi nuy sargal, mooy saay-saay bi daan taal i dëkki lëmm, di ko ndamoo. Faidherbe moomu, mooy ndawal nootkat bu xeeboon lool nit ku ñuul, xeeb sunuy mbaax, sunu aadaak cosaan. Ci gàttal, saay-saay bii nees di sargal, mooy ki nu jàppe woon niy mala, suufeel sunuy maam, def leen i surga. Porfesoor Iba Deer Caam tënkal na nu ñaawtéefi Faidherbe yi ci lu gàtt : « Ci diirub 8i weer kese, Faidherbe faat na 20 000i doomi Senegaal. » Maaradeytaali ! Te, lees ci xamul, lim bile, ab xayma bu tuuti la rekk. Nde, mbonte yii yépp nees koy tuumaal, bindees na ko ci téere mboor yi, mu ànd ak ay firnde yu leer yu kenn jéemul a weddi boobaak tey. Moom kay, ku bëgg a xaslu sa bopp, mbaa nga namm i saaga rekk, mooy jéem a layal nootkat bu ni soxore.

Keroog ba muy koñe Fatig, moom ak i soldaaram, tee nit ña génn, dafa meloon ne ku bew te ame mànditeg coxorte. Bés boobu, ca la jàmbaaru Farãs bi, di toppandoo xeltukat yi, waxe woon kàddu gii : « Ñii de, dees na leen rey, deesu leen toroxal ! » Kii moo baax rekk ! Lii de mooy dëmm rey la, jaale la.  Ndeysaan. Seŋoor dafa barde woon ci wax ji ba faf baamu ko cib taalif bu neex bees di fekk ci téereb taalifam bii di Chants d’ombre. Yemul foofu de. Neex bi ko kàddug nootkat bi neex dem na ba mu def ko taasuw làrme bi. Làrme bi nga xam ne, bokk na ci campéef yees gën a fonk ci réew mi, te weg i nitam. Dafa jot, nag, nu xoolaat gàkk-gàkk bu ruslu bii.

Lan moo sabab lu ni mel ?

 Sama maas geek ñi nu jiitu setuñu ci. Nun, mag yi, danoo lajj. Moo tax, xeex bi ndaw yi sumb tudde ko Fàww Faidherbe daanu daf nu war a yee. Mënunu lu dul nangu ne, 1960 ba tey jii, noo ngi dëkk ak màndargay nootaange yi fi ne gàññ, wër nu. Te, bu dee wax dëgg rekk, mësuñoo gëtën kenn ; maanaam, bariwaayu màndarga yoyii ak seen yàggaay, mësul a naqari ñu bari. Ci sama bopp laay jëkke, nag. Ndax, muccuma ci mbasum tekk-tekkaaral mu doy waar moomu nga xam ne, ñépp la wàll. Moo tax, bi ma toogee seetlu xëccoo bi am ñeel nittabaxon (estati) Faidherbe bi, dafa am lu ma ci jaaxal. Ak li coow liy bari yépp, am na ci ñoo xam ne, seen ñàkkub yëg-yëg ak seen xel-ñaar tere na leen a gis jéng biñ leen jéng. Mbaa du moo leen gënal sax…

Lu ni mel, nag, boo ko dee wax, du ñépp ngay diir. Da cee am ñu ràññeeku ñooy jam. Buu dee biralug mbëggeel ñeel réew mi ak di sànniy xeer ab sagaru nittabaxonu, xam naa ne, man, jekkuma ci. At yi ma jot def Ndar yépp, taxuma woon gis tilim bu nittabaxonu Faidherbe biy tilimal béréb bi. Amaana, sax, ma réere woon ne, am nab nittabaxon bu fa ne jodd.

Bu ma juumulee, Sémbeen rekk a fi yónne woon Seŋoor ab bataaxal bu wex xàtt ci atum 1978. Gisaatuma keneen ku naqarlu teewaayu nittabaxonu Faidherbe laata ndawi tey yi di ci sóobu. Moone de, Ndar, ak ni mu rëbe woon, ñàkkul woon i way-fippu yi ko mënoon a def. Ndar-Géej mi ngi xam ne, li fa meññ ci jàmbaar yu góor ak yu jigéen, nekkoon i bañkat, kenn xamul nu mu tollu. Te, ku ci nekk mënoon na jàmmaarlook nootkat bi nga xam ne, ca allaaxira ba mu nekk, mi ngiy damu, di nu ñaawal ak a kókkali. Bu dee bañkati nootaange yu bare jaar nañ fi ba jóge fi te mësuñu cee wax, du càggan ne dañoo ñàkkoon yëg-yëgug mbatiit. Dafa di, mbir maa leen fàbbi woon. Loolu, nag, lees mën a dégg la.

Li am kay mooy, tabax bi fa waxaalekati Farãs ya samp ci atum 1886, dafa dem ba seey ci biir càkk bi. Te, bu leen kenn nax ; estati bi amul as tuut ci taar. Mi ngi la ko ñaawal bii peeru ñaaw !  Réyul ba tiim taaxi dëkk bi. Waaye tam, tuutiwul tuutiwaay biy tax ñuy wax. Boo xoole, sax, danga naan ndax estati Faidherbe bi jar na riir ak ŋàññ yii yépp. Ndax estati bu ñàkk solo bii jar na nuy yàq sunuy tëflit ? Estati boo xam ne, ci béréb bu cate te ruqe la nekk. Ndeysaan, muŋ fa ne yogg-yoggaaral, mel ni ku nekk cib kaso, xat fa lool, donte ne nëbbeesu ko jant bi. Kon, bu fi estati bi nee jodd ba tey jii, dara mayu ko ko lu dul li mu doon ki jëkk a noot dëkk bi. Nde, cër boobu kese la fi dese, ginnaaw xarnook xaaj ci tey. Estati bi daf fa nekk noonu rekk, di màndargaal démb ak mboor te safanook dundu nit ñi. Daanaka, tekkiwul dara ci ñoom.

Xam naa yaa ngi naan : « Waaw ! Bu dee loolu la kay, warul a gëtën kenn, walla ? ». Sa beneen moroom laajati ma, ne : « Waa tamit, bu fi jógee, nu nuy def ? ». Lii, nag, mooy gutë gi jaaxal Ndar-Ndar yi. Mën na am sax du Ndar-Ndar yépp a ame njàqare jile. Ndaxte, ci sama xalaat bu gàtt, doon Ndar-Ndar te juddoo fa taxul a doon Doomu-Ndar. Sunu wax ji, nag, Doomu-Ndar yi laa ci jublu. Amaana, ñoom, li leen gën a jaaxal ci déjjatib estati Faidherbe bi, mooy njeexital yi muy ami ci seen démb, waaye du jëmmu Faidherbe ci boppam.  Ndaxte, Dommu-Ndar yi ci seen bopp, fullaluñ ko noonu. Waaye, ragal naa ne, nes-tuut, ciy jooy lañuy mujje. Ndege, bu dee am na estati buy sukuraat, mooy bu Faidherbe bii. Moom, kay, dafa mel ni yoor-yoorub 2017 boobu la malaaka yi lem ay dëbësam. Mooy keroog bi ngelaw li dugge ci coow li, di sotle ñi koy ŋàññ, daldi koy yékkati ba ci kow, ne ko réll ci suuf. Xam naa yaa ngi naan : « saa way,  loolu mbirum mbindaare mi rekk la. ». Ba tey. Mën na nekk. Waaye, loolu de, gëmloo ko taalibe yu xër yi du yomb. Ndaxte, ñoom, jàppuñu ne, li tax ngelaw li taamu njëlub 5eelu fan ci sàttumbar, dub tandle. Nde, dafa méngook bés bi ñuy àtte Séex Axmadu Bàmba ca kërug àtte gi mu janool, daan ko, gàddaayloo ko 7i at ca Gaboŋ.

Ak lu ci mënti am, ngëleenu guddi googoo a tax ay ndaw, diy way-moomeel, am xelu taxawal mbotaayu Fàww Faidherbe daanu. Ànd ak riirub Black Lives Matter, ñi sos mbootaay mi, ñoom Xaadim Njaay, Paap Aliyun Jeŋ, Ceerno Dikko ak Daawda Géy, fexe nañ ba soppi lépp. Cig ndaw lañu tollu ; kon jaadu na ñu jiite xeex bi. Ndax, donte ne estati bi démbug nootaange lay màndargaal, jubluwaayu xeex bi dëgg-dëgg, ëllëg la ñeel. Ëllëg googu, nag, ëllëgu ndaw yi la. Li koy firndeel mooy woo bi leen Piyeer Saane woo. Ñoom daal, dañuy taxaw ci weti tali yi – ak ci otoruti xibaar yi ! -, ku romb ñu ne niib sab loxo, ne la : « Xoolal bu baax Tubaab bi ne jodd ci nittabaxon bii ak mbind mu ruslu mii “Senegaal gërëm na la !” ». Teg ci ñu laaj ko, ginnaaw biñ leen nettalee coxorte yu xarekat bu néegoon boobu dëkke woon, « Ndax jaadu na nuy sargal ab saay-saay bu sànkoon sunuy maam ? ». Nu wax ko te dee, lii dafa juunuunu te ñaaw ba fu ñaaw yem. Rax-ci-dolli, day wone xeeb bi nu xeeb sunu bopp. Naka jekk, lii la ñépp daan xalaat. Waaye, kenn amul woon jotu taxaw ci. Tey, nag, boyalees na làmmiñ yi, di jibal i kàddu yiy jëmmal mer mees deñcoon ci xol yi, te xamuñu ci woon dara.

Kàddu yooyee waral tey xel yépp dem ci Faidherbe, ñu koy waxtaane fu ne. Kàddu yooyee, nag, ñu ngi mel niy paaka yu ñaw yees koy jam. Mbugal gënul a tar lu ni mel. Tey, ñi mu tooñoon ñoo fas yéene dekkal ko ngir bii yoon, ciw waxin, fexe ba mu dee dëggantaan. Fi ñu mujje mooy ne, dem nañ ba nga xam ne, kenn mënatul a romb estatib Faidherbe te teewaayam ci béréb du la jaaxal. Loolu rekk ndam la ñeel way-moomeeli mbootaay mi. Xawma, nag, ñan, ci ñi bëgg ñu bàyyi fa esxati ak ñi ko bëgg a déjjati, ñoo ëpp mbooloo. Waaye, loolu amatul solo. Li am ba des mooy ne Faidherbe mi ngi ci lalub deewam. Moom sax, xuloo bi jigu ko. Ndaxte, saa bu kàddu jibee ñeel ko – muy bu koy làyyil walla bu koy jam -, day doon ab pont bu bees bi ñuy daaj cib tàddam. Sama xarit bi, Luwi Kamara wax na keroog ci ngoon ci benn tele ne : « Bu fi estati Faidherbe bi jógee, amaana ma yëg tuuti nammeel. Waaye, duma ci mës a am lenn lu may réccu. » Kàddoom yi dañuy wone fit ak xay giy màndargaal Doomi-Ndar yi. Waaye, ni ma ko dégge nii, mel na ni day tàggook estati bi…

Nun, sax, noo ngi fiy werante rekk, te Faidherbe, moom, ma ngay noppalu ca benn néeg bu ndaw ca Centre de Recherche et de Documentation de Saint-Louis. Ndax xamoon ngeen loolu ? Kon, nun daal, cib tabax bees « kutt », ndax liggéey yees di amal ci béréb bi, lanuy xiiroo ak a ŋaayoo. Bees sukkandikoo ci njiit yi, dees na sampaat estati ci diggante saŋwiye ak màrs 2021. Muy lu doy waar ba jaaxal nu. Ku dem, nguur gi da koy taafantoo rekk ngir suul wax ji, ni nu koy defe ci miim réew. Ak lu ci mënti am, doxalinu nguur gi, nooni górnoor ba woon lay jig. Ñoo amagum ndam. Ndaxte, fexe bañ déjjati fa estati Faidherbe bi du woon lu jafe ci yomb. Tey, li ñuy xeex mooy ñu bañ ko fa daajaat. Xeex boobu de, moo gën a yomb fuuf, sax. Nde, bi coowal George Floyd bi jaare ba tey, foo dem ci àddina si, songees na bépp estati buy màndargaal « coxorteg nit ku weex » – ngir baamu kàdduy Amelia Plumelle-Uribe – ñeel yeneen xeeti nit ñi. Jamono ja ñu doon xeexal àqi maxejj ñeel boroom der yu ñuul ya ca Etaasini ak jamonoy « apartheid » ba sax, xeex bi tasul woon ni mu tasee tey ci àddina si. Gisuma naka la nguuru Maki Sàll mën a jéllalee coow lu ni mel.

Bu Maki dofee ba sampaat estati bi ngir ragal gi mu ragal Pari, ak fi jamono tollu, dina yéem ñu bari. Su booba, dina wone njaam giy màndargaal digganteem ak Farãs ci anam bu fés. Sikk amul ci ne, bu loolu amee, àddina sépp a nuy ree ; rawatina jamono joo xam ne, farañse yi ci seen bopp, Faidherbe da leen a tàmbalee soof. Ba tey, buñ ko làqee yit, du leen ci tax a génn. Fim ne kay, féeg soppiwuñ turu palaas bi, duñu am jàmm.

Jamonoo ngi dox, te yéexantuwul. Am nay tegtal yoo xam ne, dañu leer nàññ. Tey jii, wax ji lenn rekk la, te mooy : kan moo war a wuutu Faidherbe. Ñaari kilifay politig yu mag , Mari Tëw Ñaan (jawriñu njàng mu kowe ja woon) ak Aminata Ture (njiitu jawriñ ja woon te jiite Ndajem koom, nekkin ak càkkéef bi), ñoom, wax nañ ba mu leer ne dañ fi war a jële màndargay  nootaange bu gàcceelu bii. Iba Deer Caam, nekkoon fi jawriñu Njàngu mi, xàlloon na yoon wi keroog ba muy soppi turu liise Faidherbe, tudde ko Séex Umar Fuutiyu Taal. Nu fàttaliwaale ne, Iba Deer Caam moomu, moo taxoon ba liise Gaston Berger bu Kawlax tuddu Valjoojo Njaay. Gis ngeen !  Pomu Ndar bu siiw beek menn ngérum Ndakaaru mu mag ñoo ngi xaar seen ay ngir nees ngéntewaat leen.

Ku dem yaa ngi naan : « Yeen moom singali ngeen nootkat bi de ! Xanaa moom rekk ngeen gis ? » Déedéet. Kenn singaliwu ko, sax. Naam, Tubaab yu mel ni moom yu bari jaar na fi. Waaye, kenn ci ñoom ëppalul ni Faidherbe. Waaw, moom kat, bi mu dee ba léegi, dafa lànk ne du nu abal, foo dem fekk ko fa. Ngóor si moo fatte ci boppam ! Dafa di, ñi koy layal ci boppam te rusuñu ci dara –loolu lañu seetlu ci ñoom -, war nañoo xoolaat seen bopp, jàngataat mbir mi. war nañoo jéem a xam ndax màggal gu ëpp gi ñuy màggal nit ki jar na ko. Sémbeen waxoon na dëgg, keroog ba mu bindee, joxoñ Seŋoor mi nekkoon njiitu réew mi, wax ko baat yu ñagas yii : « Xanaa réew mi amul ay jàmbaar, góor ak jigéen, yu yeyoo nu tudde leen sunuy liise, sunuy kolees, sunuy tiyaatar, sunuy iniwérsite walla mbedd yeek ngér yi ? » Muy lu jar a laaj. Bu fekkee ne yit xamees na tontu bi, jar na nu laajaat lu tax, boobaak tey, weesoogunu laaj bile.

Bu dee am nam njàngat biñ mën a jànge ci séqoo reéw yi, mooy ne : foo fekk am réew mu ñu mës a noot, lenn ci njeexitali nootaange bi dañ fay des. Du lépp ay  deñ ba jeex tàq. Moom daal, dara beesu fi. Te, du Afrig rekk la Ërób bu ndaw bii jaay doole, noot ko ci xarnu yii weesu. Fépp fu Ërób mës a jaar, daaneel na fay nguur, jéng nit ña, taal dëkk ya door a lal i pexeem, di raxas ak a mooñ ndànk-ndànk boppi njiit ya. Noonu mu def, néewal doole nit ña ak suufeel sen i diine, moo ko tax wëlbati koom ya ak séqoo nit ña ñeel ko.

Ni Tubaab biy def ba soppi nit ña muy noot ngir soppi leen i surga, lu jar a bàyyi xel la. Rawatina fii ci Senegaal. Ku yër mbooru réew mi, diŋ ci fekk lu bari lees mën a jàngat. Li ma jublu ci wax mooy ni Faidherbe doon jéem a def Siidiya Jóob. Ndekete, Faidherbe, mébétam moo doon fexe ba Siidiya Jóob, bummib Waalo ba woon, doon Baraag boo xam ne, surgab Farãs lay doon. Maanaam, daf ko bëggoon gàlliloo, soppi kob tubaab bu ñuul. Yàllaa baax bi pexeem bu yées moomu àntuwulee. Wëliis xoromal yeek mbir yiñ ñàmbaas ci nettali yi, wax jii lu wér, amoon na fi. Waaye, ba tey, ñu bari gëmuñu ko. Li ci gën a yéeme mooy ne, Senegaal, as-tuut ci askan wee xam xew-xew bile. Xanaa nu tënkal leen ko rekk.

Lingeer Ndàtte Yàlla Mbóoj mi sunu géwél yiy faral di woy ak a tagg moo ndeyu Siidiya Jóob. Kon, Siidiya, moo waroon a dooni Baraag, buuru Waalo ba woon. Lingeer Ndàtte Yàlla Mbóoj moomu la Aminata Ture wax ne nañ ko tudde palaasu Faidherbe bi. Bi ko nootkat biy ga, di ko dugal ca Ecole des Otages bu Ndar, 10i at doŋŋ la amoon.

Siidiya, nag, gone gu teeloon a am xel la, ñoroon lool ànd ak muusaay bu jéggi dayo. Bi ko Faidherbe ràññee ci biir i maasam ngir xelam mu ñaw, daf ko daldi féetewoo, doomoo ko daanaka. Ci la nasee ay pexe ngir gàlliloo Siidiya. Moom, kay, ab tubaab bu ñuul kukk la ko bëggoon def, muy ndawul Farãs. Maanaam, daf ko bëggoon a def doxandéem ci biir i mbokkam ak i jegeñaaleem, maanaam ab buur bu wàccu soow mim nàmp ci meenu cosaan ak aada. Tey, bu faral di dégg Siidiya « Léon » Jóob, dafa fekk ne Faidherbe dafa tàmbali woon jëmmal naalam ba. Nde, moo ko ngéntewaatoon, toftal turam ci turu Siidiya, tubbiloo ko, dugguloo ko ci diiney nasaraan. Kii mooy dëmm, waay ! Moom, de, këf ruuwu gone gi la bëggoon.

Siidiya wone na xareñte bu réy ca lekkoolu tubaab ba. Faidherbe bég lool ci « doomam » ji, jël ko, yóbbu ko Alse ngir dugal ca « Lycée Impérial » ba fa nekkoon. Wànte, dëkk ba neexul woon Siidiya. 2i at kese la fa def, Faidherbe delloosi ko Ndar mu àggaleesi fa njàngam ci benn daara bu ay niti diine jiite woon. Jamono jooju, Siidiya ñeewul woon kenn. Moo yeyoon kat, wax dëgg. Waaw, ku sa juddu rafet, muus lool, Faidherbe féetewoo la, gënale la te la di la nabb-nabbee, nga xér lool ci pexem xare làrme (ci waxi ñenn ñi)… mo ku Yàlla wërsagaloon lii jamono jooju, loo doon waxati ! Noonu, Siidiya demoon ba mokkal lépp ci ni tubaab biy dunde, di ko doxe, di ko waxe, di ko lekke. Da daan dóor kostim yu dal, di lekke ni tubaab yi, di làkk farãse bu leer. Ci gàttal, Siidiya nekkoon na tubaab bu ñuul ni ko Faidherbe bëgge woon. Moom kay, jarul sax ñu leen di wax ne demoon na ba xeeb ay ñoñam. Xam naa jëli woon nga bu yàgg. Waaye, wolof nee na, yàggaayu bantu ron ci ndox, du ko tax a doon jasig.

Saa bu ndaje amaan, nag, géwél Majartel Ngóone Mbay da daan faral di woy ak a tagg Siidiya. Benn bés, am ndaje mu mag ca Mbiloor, gewel gi lànk ne du ko woy bile yoon. Siidiya laaj ko lu tax, géwél Majartel Ngóone Mbay ne ko : « Siidiya ! Mënatuma laa woy ndax xàmmeetuma la. Soppi nga saw colin, soppi saw nekkin, soppi saw doxin. Benn waalo-waalo déggul làkku doxandéem wi ngay wax. Siidiya Ndàtte Yàlla Jóob mi ma daan woy saay na ! » Siidiya ne yàbb, xamatul lu muy wax. Kàdduy géwél gi dañ ko jam ci xol. Mu mel ni kuy door a yeewu ciy nelaw yu xóot. Ci la Siidiya xamee ni, moom kat, dafa wàccoon yoon, nekkoon ku réer. Mu door coppiteem gi, fas yéene solaat mbubbu cosaan. Noonu, dem na ba, bees sukkandikoo ci waxi ñenn ñi, benn baatu farañse génnatul woon ci gémmiñ gi. Mu tuub, dellu ci diiney maamam, sàndi fale turu « Léon » bi Faidherbe dolli woon ci turam.  Ca la doonaatee Siidiya Ndàtte Yàlla Jóob.

Faidherbe, nag, mer ba futt. Cim xelam mu gàtt, dafa jàppoon ne Siidiya daf ko wor. Kon, xare rekk a fi sësoon ngir fayu, faj gàcceem. Waaye, xare boobu, du ko fekke. Ña koy wuutuji ñoo koy mujje xare ak Siidiya mi fétteerlu woon seen kow. Siidiya sona leen lool, daldi leen daan ci tooli xare yu bari. Ndeysaa, dañ koy mujje jàpp, tëj ko kaso ca Bàngooy. Gannaaw gi, ñu gàddaayloo ko, yóbbu ko ca àllab Ndeng-Ndeng ba ca Gaboŋ. Bi mu fa nekkee, nag, nootkat ya fa nekkoon ak moom yépp a ko bëggoon. Ñooñoo ko dimmali woon ci suuf ba mu am gaal gu ko delloosi Senegaal. Waaye, bi gaal googu teersee ca waaxu Ndakaaru, kolonel Brière de Lisle yég ne mi ngi ci biir, dafa yéeg aartu ko, xamal ko ne buy génn rekk ñu soqi ci kowam. Siidiya wàccul. Gaal googoo ko delloowaat Gaboŋ. Xol bi metti, tooy, mu xam ni dootul delsi. Jamono jooju, 30i yu mat sax amagu ko woon. Benn guddi daal, ci weeru suwe atum 1878, la soqig fetal ci xolam, xaru.

Lii rekk doyoon na ci ñu boole Siidiya ci coowal Faidherbe li lëmbe réew mi.  Ndaxte, kenn ëppalewu ko ci. Wax ji wax ji, li nu wokk ci coowal estati Faidherbe bi, moo xuri woon Siidiya Ndàtte Yàlla Jóob, jàmbaar ji. Ndeysaan, bi fa Siidiya jógee ak léegi am na xarnu ak xaaj. Waaye, mi ngi mel ni mësta gane àddina. Senegaal de, fàtte nañ ko bu yàgg ba mu des, xéy, Waalo ga mu fekkoon baax. Moone de, ni mu ne wëréñ, keroog ca Mbilor, am na njeexital yu réy ci sunu jaar-jaarub politig. Xam ngeen ne, bu pexem Faidherbe bi ñeel Siidiya àntu woon, neneen la fay deme tey. Nde, ku xam Faidherbe, ak ni mu daan doxale, boo demee daf ko daan waajal ngir ngemb ko, teg ko ci jal bi, nees koy waxe tey. Siidiya Ndàtte Yàlla Jóob, bi muy am 20i at kese la nekkoon tofu-liyatnaŋu làrmeb Farãs, aayoon lool ci xare. Mënoon na dem ba Górnooru Senegaal bu mag bi walla sax njëlbeenug nit ku ñuul kiy jiite nootéefi Farãs yépp. Bu loolu amoon, mooy doon sunu royukaay bu gën a mag, tey. Ndaxte, nun kat, danoo tàmm di màggal képp ku jëkk a doon dara ci nun, ak lu mu mënti doon. Muy Belees Jaañ, di Seŋoor walla Lamin Géy, barile nan fiy politise yu mag yoo xam ne, ci « jëkk a doon dara » rekk lañ amee tur. Wóor na ne, bu Faidherbe amoon li mu bëgg ci Siidiya, Senegaal du mel ni mu mel tey. Te ragal naa ne sax, doon na fi gën a ñaaw…

Warees na raxas sunu mbedd yeek yoon yi, setal leen ci tur yu mel ni Jules Ferry, Pompidou, Charles de Gaulle ak ñoom Béranger-Ferraud. Moone, coow lii – muy lu am solo – jéggi nay mbedd ak i estati. Dafa aju ci sunu ëllëg te ñeel sunu nekkin ci kow suuf. Looloo tax woyuw Fàww Faidherbe daanu yomb a lëkkale feemuw Black Lives Matter mi muy awu. Noonu lees war a jàngate doxalinu Siidiya Ndàtte, keroog ba mu tànnee dellu cosaan. Moom de, dundam bu gàtt bi jàngal nan ci lu bare ci sunu diggante ak nootkat bi. Moom, mënees na wax ne, ab bañkat bu amoon i pexe la. Xeex bi mu daan xeex ak nootkat bi, yàkkamtiwu ko woon. Te, nekku fi woon di fas i kóllëre ak di walbatiku. Dooley ñii walla ñee safu ko woon.  Jaar-jaaram rekk yeewoon na ko ba xàmme pexey nguur, ak ni ñuy faral di deme. Demoon na ba nànd ne, nootkat bi, xayadiloo nit ña mu nootoon a ko taxoon a jóg, yàq seenug nite, gàlliloo leen. Ba keroog ñu koy jàpp, mi ngi jéem a xamal ay moroomam solos bennoo bu mag biñ war def ngir xeex nootkat bi. Gis nan ne, yéenem ji àggutoon.

Jàmbaar ju mag jii, yeyoo na nguurug Senegaal  xar tànki-tubéyam ngir delloosiy yaxam ci réew mi. Ay falaafoon ca Dagana, doon nañ jem a def dara. Waaye, kenn déggatu leen. Séku Ture moom, ca jamonoom, fexe woon ba njiiti Gaboŋ yi delloo ko néewub Almaami Saamóori Ture. Jot na, sunuy njiit roy ci moom. Bu nu déjjatee estatib Louis-Léon César Faidherbe bi, tóllanti ko ak delsib Siidiya Ndàtte Yàlla Jóob ci réew mi, dina doon lu réy a réy.

CI TEKKIG PAAP AALI JÀLLO

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj