Barki-démb ci gaawu bi lañu woo woon dépite yi fa Ngomblaan ga. Li waraloon woote bi mooy soppi as lëf ci ndeyu-sàrtu réew m ngir far campeef yi di HTTC (Haut Conseil des Collectivités Térritoriales) ak CESE (Conseil Economique, Social et Environnemental). Aminata Mbeng Njaay ak Abdulaay Daawda Jàllo ñoo leen jiite woon laata ñu leen di wàcce. Dafa di, Nguur gu bees gi moom, yàgg na a bëgg a far ñaari campeef yooyu. Ndax, dafa jàpp ne seen njariñ bariwul. Te, koppar gu takku moo fay dugg.
Weeru sàttumbaar wee weesu la Nguur gi fi nekk njëkkoon a jébbal Ngomblaan gi fi jóge aw sémbu àtte ngir far HTTC ak CESE. Waaye, dépite yooya dañoo lànkoon ne duñu ko wote. Kenn umpalewul ne, jamono jooja, Nguur gi fi jóge moo ëppoon doole ca Ngomblaan ga weesu. Looloo taxoon sax, Njiitu réew mi jël ndogalu tas ko, ñu fal ay dépite yu bees ci weeru nowàmbar wi nu génn. Bi ñu amalee wote yi, waa Pastef ñoo jël ndam li, jiitoo kujje gi lu bari. Ayu-bés bee weesu lañu doon ubbi fukk ak juróomeelu kayug Ngomblaan gi. Ñoom nag, taxuwuñu, taxaawaaluwuñu. Ndax, door nañu seen ub liggéey.
Barki-démb, ci gaawu bi, lañu woo woon dépite yi ngir ñu waxtaan ci sémbu àtte wiy far HTTC ak CESE. Waaye, du ay dépite kese ñoo fa teewoon. Nde, kii di jëwriñ ji ñu dénk Yoon, Sëñ Usmaan Jaañ ak Abbaas Faal, jëwriñ ji ñu dénk liggéey ak jokkalante yi ak càmpeef yi, ña nga fa woon. Sémb woowu nag, mujj na a jàll. Ndax, kenn umpalewul ne waa Pastef ñoo fa ëpp doole. Moo tax, bi ñu amalee wote yi, ñi ci ànd ñi ngi tollu ci téeméer ak fanweer ak ñeent. Mu am juróom-ñett ñu ci àndul ak ñaar ñu màndu.
Limub dépite yu takku yooyu wote ne ànd nañu ci sémb wi day firndeel ne far nañu HTTC ak CESE. Far googu dinaa tax ñu sakkanal koppar gi daan dugg ci campeef yi. Ndax, lu tollu ci fukki miliyaar ak juróom daan na fa dem. Su ko defee, koppar googu dinañu ko mën a dugal feneen. Li am ba des daal mooy ne HTTC ak CESE jóge nañu fi. Bi ci des mooy “Loi d’amnistie” bi fi Nguur gi fi jóge wote woon laata ñu leen di daaneel. Dinañ ko neenal am déet ? Kañ ak nan lañu koy defe ? Li ci kanam moom, rawul i bët.