Njiitu réew mi Maki Sàll digeeti na lu ëpp 800i tamñareet fa diwaanu Fatig. Fekk mu doon fa amal ab wëraan ñeel koom gi. Muy alal ju takku ju mu namm dugal ci fànni koog gi fileek 2026 donte ni 2024 la nguuram gi di jeex.
Démb ci àjjuma ji la Njiitu réew mi Maky Sàll doon jeexal wëraan bi mu doon amal ci biir réew mi, jagleel ko koom gi. Mu doon ko amale nag fa diwaanu Fatig. Ginnaaw bi mu fa àggee ci bi 17i waxtu di jot, jiite na fa jotaayu waxtaan bu yàgg bu mu séqoon ak kilifay diwaan ba, ci teewaayu askan wa.
Bi Njiitu réew mi njëkkee jël kàddu gi, biral na lu tax mu taamu mujje foofu ci wëraanam bi. Naka noonu, mu xamal leen ni foofu fa Fatig la juddoo, foofu la lépp tàmbalee. Ci pàttali, Maki Sàll nekkoon na fi Meeru Fatig.Te ndegam foofu la lépp tàmbalee, foofu la lépp di jeexee.
Kàddoom yooyu mel ni luy firndeel ni dafay tàggatoo. Nde ñetti weer kott ko dese ci boppu réew mi. Terewul nag mu yékkati fay kàddu ñeel kujje gi waxul dara ciy mbiram, rawatina ñiy woote yëngu-yëngal ngir péexte Usmaan Sonko ak nekkug lawaxam. Ci noonu, muy xamle ni bàyyi na lépp lu jëm ci ñetteelu moome gi waaye li ko dese ci boppu réew mi du nangu ku fi salfaañe.
Bu fi ñetti weer kott desee Njiitu réew meet, Maki Sàll yamalewul gis-gisam ak i naalam ñeel Fatig ci 2024 bii mu waree tàggatoo. Nde demam gi terewul wenn yoon mu amalaat fay dige jëme 2026.
Ginnaaw bi mu fàttalee waa Kafrin ni ci diggante atum 2015 ak 2023 bi, càmm gi dugal na fa diwaan ba lu ëpp 332 tamñareet, dafa dellu dig waa Fatig ni dina fa amal ab sémbu 853i tamñareet. Mu duppe ko PIP (Programme d’investissement prioritaire) 2024/2026.