Paap Aali Jàllo
«Tooñ, torox, goreedi ak ñàkk fulla weesuwul ñuy woyal Lat-Joor ci tóojug estati bu Faidherbe…» (Usmaan Sémbéen)
Ginnaaw mbasum Covid-19 bi, mel na ne àddina saa ngiy jànkonteel ak meneen xeetu mbas : fippu. Dafa di, géejug mer gi juddoo ci bóomug George Floyd baa ngiy wéy di gandeer àddina sépp. Coow laa ngi ne kurr, tëwa jeex. Nit ñi yematuñ rekk ci di kaas, ñaxtook a xeexal àqi nit ku ñuul. Seen mébét mooy dekkil darajaam, yékkati fullaam ji nit ku weex joggi woon, teggi tuumay xayadi ak matadi yi nootkat yi daan taafantoo, di ko teg ci seen i der ngir moom leen. Moo tax, jamono jii, fépp foo dem ci àddina si, ñaxtukat yaa ngi fay xotti nataali nootkat yu démb yaak yu tey yi, di rajaxe bépp nittabaxon biy jëmmal njaam ak nooteel ñeel nit ku ñuul, walla kilifteefug nit ku weex ci kowam. Naka noonu, Senegaal itam, mbasum fippu mi agsi na fi, te nittabaxonub Faidherbe bi nekk Ndar mooy góom bi askan wi bëgg a faj.
Gaawu bii weesu, takk-der yi jàppoon nañ 4i ndaw yu bokk cig kurél gu tudd «Fàww nu daaneel Faidherbe» ci sababu ndaje miñ bëggoon a amal ak taskati xibaar yi. Waaye pólis mujje na leen bàyyi. Mébétu kurél googu, nag, ak ñiy sàkku ñu sempi nittabaxon bu Faidherbe bi, mooy ñu jële ci réew mi lépp luy màndargaal njaam ak nootaange. Bu dee ci wàllu Faidherbe, nee ñu nittabaxonam day jëmmal nootaangeb Farãs ci kow Senegaal ak lépp li ci aju ci xeebeel, toroxtaange ak coxorteb Tubaab bi, ñeel sunuy maam ak sunu bañkati démb ya. Rax-ci-dolli, mbedd yi, yoon yi ak béréb yees tudde ay nootkat ak i doxandéem day firndeel ne, ba tey jii, moomagunu sunu bopp.
Ñiy layal Faidherbe, di bañ ñu sempi nittabaxonam ca Ndar, dañ naan, ak lu ci mënti am, ngóor si am na lu mu defal réew mi : teg na fiy raay, xotti fiy tali, indi fiy jumtukaayi xarala, tabax fi jéggiwaay (pont), dàq naar yi sonaloon waalo-waalo yi, boole nguuraan yi (royaumes), def leen am réew, muy Senegaalu tey, añs. Waaye, kan mooy Faidherbe ci boppam ak lan la def ba tax ñu singali ko, di ko tam dëmm ?
Cib gàttal, Faidherbe mi ngi juddu 3eelu fan ci weeru Suwye 1818. Laata muy ñëw Senegaal, Alséri la ko caytug nootaange gu Farãs njëkk a yabal ngir mu tàggatu fab diir. Bam fa nekkee, lépp luy ñaawtéef bu xel xalaatul def na ko fa laata muy tuursi sunu deretu maam ya. Dafa teer Alséri, yàggul dara, mu tàmbalee xoqtal ak a rey askan wa. Loolu lay biral ci bataaxal bum yónnee yaayam, di ndamu, naan ko ca : « …yàq naa yaxeet dëkkub lëmm bu taaru woon lool, ak i toolam. Ma yàqaale 200i kër ya fa nekkoon, tiital waa dëkk ba yépp, ñu daldi jébbalusi ci man, tey. »
Bi mu ñëwee Senegaal itam, lenn rekk a nekkoon itteem : fexe ba saxal nguur ak kilifteefug Farãs ci réewi Afrig yi, rawatina fii ci Senegaal. Loolu, nag, jaraloon na ko lu nekk. Ci as-tuut lin jukkee ci téere ak seedey ma-mboor yi ak ñi xam démb, limees na ci xeeti ñaawtéef ak jëf ju saltee salte yim def ci réew mi.
Faidherbe rey na fiy buur, taal i dëkk yu dul jeex. Nangu na fiy suufi jàmbur, taal i tool. Bóom nay sëriñ ak i imaam, lakk seen i téere. Siif na fiy janq, siiflu ay xale yu jigéen. Ténjloo na fiy soxna, jirimloo ay ndaw. Toroxal na jigéen, suufeel mag. Xeex na góori Yàlla yi, gàddaayloo kàngam yi. Sàcc na alalu réew mi, nasaxal koom-koom gi… Li ci gën a doy waar mooy ne, Faidherbe, daawul yabal ay soldaar rekk yem ci, dafa daan teewe loolu lépp, di reetaan, di ci bànneexu.
Maanaam, lépp luy tax am réew di naw boppam ak cëslaay gi mu war a sukkandiku ngir tabax ëllëgam ak naataangeem, Faidherbe da koo dëggati, yàqati ko ba mu yàqu yaxeet. Rax-ci-dolli, naalub xayadi bi Farãs laloon ngir xeebloo nu sunu aada ak sunu cosaan, Faidherbe moo ko njëkk a jëmmal. Ndege, Faidherbe mooy ki sos « Ecole des otages », daan fa yóbbu doomi Buur yeek doomi boroom daraja yi ak njiiti gox yeek dëkk-dëkkaan yi. Li mu ko dugge woon mooy jàngal leen aada ak cosaanu Farãs, fàtteloo leen seen yosi maam, xeebloo leen seen juddu. Kon, bokk na ci ñi nasaxal sunuy aada, xayadiloo sunuy ndaw. Waxatun dara, mu wax ñeel nit ku ñuul, ne : « li seen yuur yi tuuti moo tax nit ñu ñuul ñi xayadi. Looloo sabab seenub xayadi. » Moom, nag, ci anam bu metti la génne àddina.
Dikkaloon na ko lafañ ak ñàkkug nelaw gu tar, li ko dale atum 1875 ba ni muy deewe. Mu mel ni mbugalub Yàllaa wàccoon ci kowam ci kow suuf laata mu fekki bu allaaxira ba. Ndege, ba muy nekk Alséri, Faidherbe mës na daanu ci walum ndox mu galaase, ca tangori Djurdjura ya. Ca la jële gaañ-gaañ yu metti ak feebar bi koy mujje yóbbu ci atum 1889. Feebar na diirub 14i at. ( ?) Muy ame ay kiriis yu mettee metti. Moom kay, Faidherbe yàgg na ci lalub sukkuraat. Waaye, taxul nit ñi fàtte ñaawtéef yi mu def yépp, te njeexital yi jur ay rëq-rëq ci yokkute réew mi.
Usmaan Sémbeen bokk na ci ñi njëkkoon a wax ni nan fi jële nittabaxon bi, te soppi turi mbedd yin jox ay nootkat. Bindoon na sax Léwopool Sedaar Seŋoor ab bataaxal, ci atum 1978, naan ko ca :
« Tooñ, torox, goreedi ak ñàkk fulla weesuwul ñuy woyal Lat-Joor ci tóojug nittabaxonu Faidherbe. Lan rekk moo tax, cim réew mees wax ni moom na boppam, li ko dale Ndar ba Sigicoor, jaare ko Cees, Ndakaaru, Tëngéej, Kawlax, añs., ñu fay sargal nootkati démb yeek yu tey yi, di leen tudde ay mbedd, ay yoon, ay tali, ay pénc ak yeneeni béréb ? Xanaa réew mi amul ay jàmbaar, góor ak jigéen, yu yeyoo nu tudde leen sunuy liise, sunuy kolees, sunuy tiyaatar, sunuy iniwérsite walla mbedd yeek yoon yi ? »
Waaye, Seŋoor faalewu ko woon ndax, benn, ndawal Farãs la woon, ñaar dafa wegoon Faidherbe, nawoon ko lool ba koy wax ciy mbindam. Waaye, bu yoon jeexul, waaxusil du jeex. Tey, ay Usmaan Sémbéen yu baree ngi taxaw temm, fas yéene jaay seen bakkan ngir ñu jële Ndar nittabaxonu Faidherbe bi. Muy ndaw ñi, way-moomeel yi, kilifay aada yi, imaam yi ak ñenn ci politiseŋ yi, ñépp a ngi naan : « Fàww Faidherbe daanu ! »