FOMMUB WOTEY 2024 YI : XALIFA MURID YI ÀNDU CI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Démb, jëwriñu biir réew mi ak nawleem biñ dénk larme bi ñoo nga woon Tuubaa. Ci lees wax, Njiitu réew mee la fa yabaloon. Seneweb a siiwal xibaar bi.

Sidiki Kaba, jëwriñ jees dénk biir réew mi ak Umar Yum, jëwriñ jees dénk larme bi, seeti woon nañ Xalifa Murid yi fa Tuubaa. Kilifa gi dalal na leen ca Daaru Minam ci teewaayu aji-yore kàddug yoon wa, Sëriñ Basiiru Mbàkke Abdu Xaadar.

Bees sukkandikoo ci Seneweb, jëwriñi Maki Sàll yi àgge nañu Sëriñ Muntaxaa tolluwaayu réew mi, rawatina coowal wote yi. Jéem  nañoo benn-bennal ak a layal ndogal li Njiitu réew mi jël. Waaye, ci lees jot ciy xibaar, jële ko ci waa www.actu221.net, Sëñ Muntaxaa Mbàkke àndul ci ndogal li Maki Sàll jël.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj