PAAP AALI JÀLLO
George Floyd, jamono jii, mooy néew bi gën a siiw ci àddina sépp. Li kob takk-der bu weex faat ci anam yu ñaaw a ñaaw, nag, moo waral coow li jib boobaak léegi.
Bees sukkandikoo ci yéenekaayu Amerig bi, ”New York Times”, lépp a ngi door ci bésub altine, 25eelu fan ci weeru Me. Dafa amoon ku woo takk-der yi, ne leen am na jenn waay ju jënd sigaret ci benn màngasin, feye kook sagarub 20i dolaar bu baaxul. Nee ñu, waa jooju, George Floyd la tuddoon. Moom, George Floyd, wattuwaafoonu kaaraange la woon ci benn feccukaayu guddi. Waaye, dafa ñàkkoon liggéeyam ci sababu mbas mi lëmbe àddina.
Bi 19iw57is jotee, lañ woo pólis ne leen George Floyd xaalis bu baaxul la jënde ay sigaret. Ñu teg ci ne dafa màndi, mel ni ku àndul ak xelam. Nes-tuut, 2i takk-der agsi ca béreb ba, Thomas Lane ak J. Alexander Kueng ; ñu daldi taxaw ci kanamu oto bi George Floyd nekkoon. Thomas Lane daldi génne fetelam ci saa si te kenn xamul lu tax mu def ko. Ci la sante George Floyd mu teg i loxoom ci wolaŋ bi. Noonu, ci diirub 2i simili, Lane roofaat na fetelam ba génne Floyd ci oto bi, takkal koy manot. Ci la ko beneen takk-der bi, Kueng, sësale ci benn miir. Ba tey, George Floyd fippuwul, xataraayuwul : luñ ko defloo, mu def ko. Ginnaaw gi la ko takk-der yi dëje ci suuf, beneen oto pólis fekksi leen fa.
« MËNUMAA NOYYI, MAA NGIY FATT ! »
Biñ ko jàppee ba mu am 6i simili lañ ko jëmale ci beneen oto pólis. Waaye, dafa mujje daanu ci wetu oto bi. Ci la waxe takk-der yi ne dafa ame jàngoroy kólostorofobi (feebaru xel buy tax nit kiy ragal ku ko tëj, rawatina ci béréb bu xat), lànk ne du yéeg ci oto bi.
Benn kameraa bu màngasin Cup Foods, te nekke boor boobu, mi ngi wone takk-der Kueng muy jéem a dugal George Floyd ci toogu ginnaawu oto pólis bi. Takk-der bi ñuy wax Chauvin da koo mujjee génne, dëpp ko ci tali bi, ci wetu oto pólis bi. Ci la 2i nit ñu doon romb foofu, génne seen njéggil-kàddu, di filme mbir mi.
Widéwo bu jëkk bi day wone 4i takk-der yi wër ko. 3i ñi sukkandoo ci kowam, téye ko. Takk-der Lane sukk ci tànk yi di bës, takk-der Kueng di def noonu ci ndigg li, takk-der Chauvin jël óom bi teg ci baat bi, di bës ak doole.
Bi 20iw20is jotee, George Floyd tàmbalee saraxu takk-der yi, naan leen mënatul a noyyi. Ci la takk-der Lane nekkee di dàq ña fekke woon mbir mi. Kenn ci takk-der yi woote wall, ne leen gémmiñu Floyd gaa ngiy nàcc. Ñu jagleel wooteem boobu kod 3 bi méngoo ak soxla ndimbalug doktoor te mu jamp. Mu am beneen aji-fekke bu taxawe woon ci beneen boor, di filme. Widéwo bim filme day wone takk-der Chauvin, ba tey mu teg óomam ci loosu Floyd, donte ne wootees na ndimbal mu jamp ba noppi. Widéwo boobu nag, Chauvin kese lay wone, wonewul Lane ak Kueng. Jamono jooju, George Floyd mi ngi woon ci metit wu tar, naan leen :
« Maa ngiy fatt. Ngir Yàlla, teggil sa óom ci sama baat bi. »
Mu wax kàddu googu, baamtu ko ay yoon. Am ci takk-der yi ku ko ci tontu, ne ko : « Sama waa ji, bu la tollee noonu, jógal yéeg ci oto bi ! » George Floyd ne ko : «Dinaa ko def. Fim ne nii, mënatumaa yëngu ! ». Takk-der bi newaat ko : « Yéegal ci oto bi ! », Floyd waxaat ko ne mënu ko, topp leen di leen wax ne mi ngiy fatt. Wax na leen ko, waxaat leen ko 16i yoon ci diirub 5i simili.
« XOOL-LEEN NDAX XOL BAA NGIY DAL ! »
20iw25is, George Floyd ne tekk, waxatul. Mu mel ni ku xëm, daldi gëmm. Way-fekke yi tamit tàmbalee ñaan Chauvin ngir mu teggi óomam bim teg ci baatu Floyd. Am ci sax ku ne takk-der yi « Yéen, lu leen dal ? » ; keneen xool ko, ne : « Kii yëngootul ! »
Bees sukkandikoo ci kayitu yégle bi pólisu Minneapolis génne ñeel anam yi takk-der yi war a jàppe nit ñi, wareesul a dëpp nit, teg sab óom ci kowam lu dul ne dafa bañ def liñ ko sant ba noppi di xataraayu. George Floyd, moom, loolu fekku ko ci woon. Te, jamono jim xëmee, benn takk-der xettaliwu ko ba ni àmbilãs bi ñëwe. Kenn ci way-fekke yi ne leen : « Xool-leen ndax xol baa ngiy dal ! » Nee ñu Lane laaj na ñaari yoon Chauvin ndax mën na koo may mu wëlbati Floyd, naataangoom bi bañ, ne ko déedéet.
Bi 20iw27is jotee, la àmbilãs bi agsi. Ñu xool ndax xol baa ngiy dal, génne benn barankaar ngir teg ci Floyd. Ba tey, Chauvin wàccagu ko. Bi ko ko wallkat bi santee lay door a teggi óomam. Kon, ci xayma, Chauvin dafa teg óomam ci baatu George Floyd, bës ko ci diirub 8i simili ak 46i saa. Àmbilãs bi dem, waaye dañu woowaale woon pómpiyee yi ngir ñu jàppale leen.
Bi 20iw32is jotee, pómpiyee yi agsi ci béréb bi mbir mi xewe, ca sélébe-yoonu 38th Street ak Chicago Avenue. Waaye, kenn ci takk-der yi nanguwu leen a wax naka la George Floyd def ak wan yoon la àmbilãs bi jaar. Loolu moo leen tere woon a dimbali waa àmbilãs bi. Ci la xolu Floyd bi taxawe ci biir àmbilãs bi. Laata pómpiyee yiy jot àmbilãs bi, def nañ 5i simili ci yoon wi.
21iw25is, ci lañu biral faatug George Floyd. Boobaak léegi, coow laa ngi ne kurr ca Etaasini. Nit ñaa ngay ñaxtu ak a taal réew ma. Dem na sax ba mbir mi rax càcc. Ndege, am na ci ñaxtukat yi, ñu doon dàjji bérébi jaayukaay yi, di sàcc njaay ma fa nekk. Ayu-bésug lëmb a ngii, xeex biy gën a takkarnaase. Njiitu Amerig, Donald Trump, ne mbir mi dafa rax, ñaxtukat yi jàmm taxu leen a jóg te, bu dee Jaraafi diiwaan yi mënuñoo dakkal yàq geek càcc gi, moom Trump dina sant làrme bi mu wàcc ci mbedd mi defanteek ñoom. Ñépp a dal ci kow Trump, wax ne day xamb taal.
Ci beneen boor, àddina sépp sukk, samp benn óom ci suuf, yékkati beneen bi ngir naqarlu bóomug George Floyd gi. Waaye tamit, ngir ŋàññi doxalinu takk-der yiy metital nit ñi ak boddekonte ñeel nit ku ñuul ci àddina si. Artist yi, woykat yi, futbalkat yi, basketkat yi, way-moomeel yeek kurél yiy sàmm àqi doom-aadama, rawatina yiy xeexal nit ku ñuul, ñépp daal taxaw nañu temm, ne bésu dee du bésu dund, di jàmmaarlook alkaati yi. Kurél gi ñuy wax ‘’Black Lives Matter’’ lañ ci gën a ràññee. ”Black Lives Matter” a ngi tekki ne bakkanu nit ku n1uul am na solo. Xanaa kon ñu ne nit ku ñuul du xaru tabaski ba Tubaab bu jóg tëral ko rendi.
Démb ci talaata ji lañu rob George Floyd Houston ga mu juddoo, ci Texas. Ci la takk-der yi tamit janook àttekat bi. Kilifay goxub Minneapolis biñ bóome George Floyd xamle nañ ne, dinañ indi ay coppite ci liggéeyu pólis bi, yeesal ko. Rax-ci-dolli, léegi, terees na bépp takk-der muy metital, di xoj walla sax di laal baatu nit ki muy jàpp.